Text copied!
Bibles in Wolof

Màndiŋ ma 18:3-9 in Wolof

Help us?

Màndiŋ ma 18:3-9 in Kàddug Yàlla gi

3 Ñooy dénkoo sa ndénkaane, ak dénkaaney mboolem xayma bi, waaye jumtukaayi bérab bu sell bi, ak sarxalukaay bi, buñu ko jege, lu ko moy dañuy dee, ñoom ak yeen itam.
4 Nañu jokku ci yaw, te ñu dénkoo ndénkaanel xaymab ndaje mi, ci mboolem liggéeyu xayma bi. Kenn ku ci bokkul nag du leen jege, yeen.
5 Nangeen dénkoo ndénkaanel bérab bu sell bi, ak ndénkaanel sarxalukaay bi, ngir am sànj baña dalati ci kaw bànni Israyil.
6 «Man mii nag maa seppee seen bokki Leween ñi ci biir bànni Israyil. Yeen lañu leen jagleela jagleel, ñeel Aji Sax ji, ngir ñu liggéey liggéeyu xaymab ndaje mi.
7 Yaw nag yaak say doom, dénkooleen seenug carxal ci mboolem mbiru sarxalukaay bi, ak ca wàllaa ridob biir bi, ngeen di ca liggéey. Seen liggéeyu carxal bi, ab sasu teraanga la, maa leen ko terale. Waaye ku bokkul ci yeen, bu ci laalee, dees koy rey.»
8 Aji Sax ji neeti Aaróona: «Man mii maa la sédd ndénkaaneb samay jooxe; mboolem jooxe yu sell yi bànni Israyil indi, yaw laa ko jagleel, nga jagoo, yaak say doom, ci kaw dogal bu sax dàkk.
9 Lii nag, yaa ko moom, ci mboolem sarax yu sell yee sell, yi mucc sawara: seen bépp sarax, seen bépp saraxu pepp ak seen bépp saraxu póotum bàkkaar, ak seen bépp saraxu peyug tooñ bu ñu ma indil, lu sella sell la, ñeel la, yaak sa doom yu góor.
Màndiŋ ma 18 in Kàddug Yàlla gi