Text copied!
Bibles in Wolof

Màndiŋ ma 18:20-27 in Wolof

Help us?

Màndiŋ ma 18:20-27 in Kàddug Yàlla gi

20 Aji Sax ji neeti Aaróona: «Seenum réew nag doo ci am cér, te wàllu suuf, doo ko am ci seen biir. Man maay sa wàll, di sab cér ci biir bànni Israyil.»
21 Leween ñi ñoom, maa leen jox bépp céru fukkeel bu génne ci Israyil, muy seen cér, ñu yooloo ko seen liggéey bi ñuy liggéey ci xaymab ndaje mi.
22 Bu bànni Israyil juuxati ci xaymab ndaje mi, di gàddu bàkkaar bu dee di àtteem.
23 Leween ñi ñooy ñiy liggéey liggéeyi xaymab ndaje mi, te lu ñu ca tooñ, ñooy gàddu pey ga, ci kaw dogal bu sax dàkk, ñeel leen, ñook seen askan. Waaye biir bànni Israyil, Leween ñi duñu ci séddu céru suuf,
24 ndax céri fukkeel yi bànni Israyil yékkati, jooxeel ko Aji Sax ji, jox naa ko Leween ñi, muy seen cér. Moo tax ma ne leen, biir bànni Israyil, duñu ci séddu céru suuf.
25 Aji Sax waxati Musaa ne:
26 «Leween ñi, wax leen, ne leen bu ñu jëlee ci bànni Israyil seen céri fukkeel yi ma leen jagleel yeen, muy seen cér, nañu ci jooxeel Aji Sax ji, fukkeelub céru fukkeel yooyu.
27 Nañu leen jàppal loolu, yeen Leween ñi, muy seen jooxeb bopp, ni bu doon pepp mu jóge ci seen dàggay bopp, ak biiñ bu bees bu jóge ci seen nalukaay.
Màndiŋ ma 18 in Kàddug Yàlla gi