Text copied!
Bibles in Wolof

Màndiŋ ma 18:2-7 in Wolof

Help us?

Màndiŋ ma 18:2-7 in Kàddug Yàlla gi

2 Te itam sa bokki Leween ñi, sa giirug baay, jegeñal leen sa bopp, ñu jokku ci yaw, di la jàpple, te yaw yaak say doom, ngeen féete fi kanam xayma ba seedes kóllëre ga dence.
3 Ñooy dénkoo sa ndénkaane, ak dénkaaney mboolem xayma bi, waaye jumtukaayi bérab bu sell bi, ak sarxalukaay bi, buñu ko jege, lu ko moy dañuy dee, ñoom ak yeen itam.
4 Nañu jokku ci yaw, te ñu dénkoo ndénkaanel xaymab ndaje mi, ci mboolem liggéeyu xayma bi. Kenn ku ci bokkul nag du leen jege, yeen.
5 Nangeen dénkoo ndénkaanel bérab bu sell bi, ak ndénkaanel sarxalukaay bi, ngir am sànj baña dalati ci kaw bànni Israyil.
6 «Man mii nag maa seppee seen bokki Leween ñi ci biir bànni Israyil. Yeen lañu leen jagleela jagleel, ñeel Aji Sax ji, ngir ñu liggéey liggéeyu xaymab ndaje mi.
7 Yaw nag yaak say doom, dénkooleen seenug carxal ci mboolem mbiru sarxalukaay bi, ak ca wàllaa ridob biir bi, ngeen di ca liggéey. Seen liggéeyu carxal bi, ab sasu teraanga la, maa leen ko terale. Waaye ku bokkul ci yeen, bu ci laalee, dees koy rey.»
Màndiŋ ma 18 in Kàddug Yàlla gi