20 Aji Sax ji wax Musaa ak Aaróona, ne:
21 «Xiddileen mbooloo mii, ma xoyom leen léegi!»
22 Musaa ak Aaróona ne gurub, dëpp seen jë fa suuf, daldi ne: «Éy Yàlla, yaw Yàllay bépp boroom bakkan bu bindoo aw suux, xanaa du kenn ay bàkkaar, nga far sànju ci kaw mbooloom lëmm?»
23 Ci kaw loolu Aji Sax ji ne Musaa:
24 «Waxal mbooloo mi, ne leen ñu jóge fi wër màkkaani Kore ak Datan ak Abiram.»
25 Musaa daldi jubal ca Datan ak Abiram, magi Israyil topp ca.
26 Ci biir loolu mu wax ak mbooloo ma, ne leen: «Ngalla dàndleen xaymay nit ñu bon ñii, te buleen laal seen lenn, bala ngeen di buuboondook mboolem bàkkaari ñii.»
27 Ñu daldi jóge mboolem fa wër màkkaani Kore ak Datan ak Abiram. Datan ak Abiram ñoom, ña nga génn, taxaw ca seen bunti xayma, ñook seeni jabar ak seeni doom, ak seeni tuut-tànk.
28 Musaa nag ne: «Lii nag moo leen di xamal ne Aji Sax ji moo ma yebal ngir ma def jëf jii jépp, waaye du sama coobarey bopp:
29 Ndegam ni mboolem doom aadama di deeye, ni la ñii deeye, seen demin di deminu mboolem doom aadama, su boobaa du Aji Sax jee ma yebal.
30 Waaye ndegam Aji Sax ji moo sàkk ba sàkk tey lu masula am, ba suuf ŋa, mëdd leen, ñook lu bokk ci ñoom, ñu tàbbiwaale bakkan biir njaniiw, su boobaa dingeen xam ne ñoom ñii ñoo xarab Aji Sax ji.»
31 Naka la Musaa di daaneel kàddu yooyu yépp, fa ñu taxaw jekki xar,
32 suuf ŋa, mëdd leen, ñook seen waa kër, ak mboolem ku bokk ci Kore, ak mboolem alal ja.
33 Ñu daldi tàbbiwaale bakkan biir njaniiw, ñook mboolem lu ñu moom, suuf sàng leen, ñu réer mbooloo ma mërr.
34 Mboolem Israyil dégg seen yuux ya, daldi daw, te naan: «Nan daw bala noo suuf a mëdd!»