Text copied!
Bibles in Wolof

Màndiŋ ma 15:8-29 in Wolof

Help us?

Màndiŋ ma 15:8-29 in Kàddug Yàlla gi

8 «Su dee sarxe jur gu gudd, muy saraxu rendi-dóomal, mbaa sarax bu muy wàccoo aw xas, mbaa saraxu cant ci biir jàmm, ñeel Aji Sax ji,
9 na sarxewaaleek jur gu gudd gi, ab saraxu pepp bu ñetti fukkeeli efay sunguf su mucc ayib, di juróom ñeenti kilo, ñu xiiwe ko genn-wàllu xiinu diw, di ñetti liitar,
10 ak biiñ bu muy joxewaale, ngir saraxu tuuru, di genn-wàllu xiin, muy ñetti liitar. Loolu saraxu sawara la, di xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.
11 «Noonu lees di def bu dee saraxu yëkk, mbaa am kuuy, mbaa am xar mu ndaw, mbaa bëy.
12 Nu limu juri sarax yi tollu rekk, ngeen def mu ci nekk noonu, ànd ak lim ba.
13 Mboolem njuddu-ji-réew, noonu lay defe sarax yooyii, buy indi saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.
14 «Su dee ab doxandéem bu dal ak yeen, mbaa ku nekk ak yeen ci seen maas yiy ñëw, te muy joxe saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji, ni ngeen koy defe rekk la koy defe.
15 Mbooloo mi mépp, dogalu yoon boobu benn la ciy doon, muy yeen, di doxandéem bi. Dogal la buy sax fàww, ñeel seen maasoo maas, te di benn ci yeen ak ci doxandéem bi, fi kanam Aji Sax ji.
16 Wenn yoon wee, di benn àtte bi, ñeel leen, ñeel doxandéem bi dal ak yeen.»
17 Aji Sax ji waxati Musaa, ne
18 «Waxal bànni Israyil, ne leen, bu ngeen demee ca réew, ma ma leen jëme,
19 bay lekk ca ñamu réew ma, nangeen ci jooxe ab jooxe, ñeel Aji Sax ji;
20 seen notu sunguf bu jëkk, ci ngeen di jooxe menn mburum jooxe. Ni ngeen di sàkke jooxe bu jóge ca dàgga ja rekk, ni ngeen koy jooxee.
21 Seen notu sunguf bu jëkk, ci ngeen di sàkke ab jooxe, ñeel Aji Sax ji, yeen ak seen askan.»
22 Su dul ci teyeef ngeen ñàkka jëfe lenn ci mboolem santaane yii Aji Sax ji dénk Musaa,
23 ci mboolem lu leen Aji Sax ji sant, Musaa jottli, dale ko keroog ba Aji Sax ji santaanee loola, ak gannaaw gi, ba ca seen maasoo maas,
24 su dee moy gu dul teyeef, te mbooloo mi yégu ko woon, su boobaa mbooloo mépp ay sarxal aw yëkk wu ndaw wuy doon rendi-dóomal, ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji, ak saraxu peppam, ak saraxu tuuroom, ni ko yoon àttee, ak benn sikket ngir saraxu póotum bàkkaar.
25 Sarxalkat bi day def loolu njotlaayal mbooloom bànni Israyil gépp, njéggal daldi leen ñeel, gannaaw moy ga dug teyeef, te ñoom it indi nañu seen saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji, booleek seen saraxu póotum bàkkaar fi kanam Aji Sax ji, ndax seen moy ga dul teyeef.
26 Njéggal day daldi ñeel mbooloom bànni Israyil gépp, ak bépp doxandéem bu dal ak ñoom, ndax mbooloo mépp lay seen moy gu dul teyeef.
27 Su dee kenn nit a bàkkaar te du teyeefam, na sarxal aw bëy wu jigéen wu menn at, ngir saraxu póotum bàkkaar.
28 Sarxalkat bi daldi koy def fi kanam Aji Sax ji, njotlaayal ki moy ci ag ñàkka tey, ca bàkkaaram ba dul teyeef. Loolu la koy jote, njéggal ñeel ko.
29 Muy njuddu-ji-réew ju bokk ci bànni Israyil, di doxandéem bu dal ak ñoom, yoon wi wenn lay doon, ñeel ki moy te du teyeefam.
Màndiŋ ma 15 in Kàddug Yàlla gi