Text copied!
Bibles in Wolof

Màndiŋ ma 14:2-12 in Wolof

Help us?

Màndiŋ ma 14:2-12 in Kàddug Yàlla gi

2 Bànni Israyil gépp nag di ñaxtu ci kaw Musaa ak Aaróona, mbooloo ma mépp naa leen: «Waay lu nu tee woona dee ca réewum Misra, mbaa sax nu dee ci màndiŋ mii!
3 Ana lu nu Aji Sax jiy indee ci réew mii ñu nara fàddoo saamar, sunuy jabar ak sunuy tuut-tànk doon alalu sëxëtoo! Tee noo dellu Misra yee?»
4 Ci kaw loolu ñu naan ca seen biir: «Nan fal njiit te dellu Misra.»
5 Ba loolu amee Musaa ne gurub, moom ak Aaróona, ñu dëpp seen jë fa suuf, fa kanam mbooloom bànni Israyil ma fa daje mépp.
6 Yosuwe doomu Nuun, ak Kaleb doomu Yefune, ñoom ña bokk ca ña seeti woon réew ma, daldi xotti seeni yére ndaxu tiis.
7 Ñu wax nag mbooloom bànni Israyil mépp, ne leen: «Réew ma nu wëri woon, ba nemmiku ko, réew mu baaxa baax la.
8 Bu nu Aji Sax ji nangulee, moo nuy dugal réew moomu, moo nuy jox réew ma meew maak lem ja tuuroo.
9 Fexeleen rekk ba Aji Sax ji, buleen ko gàntal, te yeen nag ngeen baña ragal waa réew ma, ndax ab lanc doŋŋ lañu nuy mat. Seen kiiraay dëddu na leen, te Aji Sax jaa ngeek nun. Buleen leen ragal.»
10 Ba mu ko defee mbooloo ma mépp ne dañu leen di dóori xeer ba ñu dee. Leeru Aji Sax ji nag feeñ ca xaymab ndaje ma, ci kanam bànni Israyil gépp.
11 Ba loolu amee Aji Sax ji ne Musaa: «Ba kañ la ma askan wii nara xarab? Ba kañ lañu may gëmadi, ak firnde yi ma def ci seen biir yépp?
12 Maa leen di fàdde mbas, nangu seen cér, ba noppi sose ci yaw askan wu leen ëpp, ëpp leen doole.»
Màndiŋ ma 14 in Kàddug Yàlla gi