Text copied!
Bibles in Wolof

Màndiŋ ma 14:13-29 in Wolof

Help us?

Màndiŋ ma 14:13-29 in Kàddug Yàlla gi

13 Musaa ne Aji Sax ji: «Kon de, waa Misra ga nga jële mbooloo mii, génnee leen sa doole ca seen biir, dinañu ko dégg,
14 te dinañu ko nettali waa réew mii. Waa réew mii dégg nañu ne yaw Aji Sax ji ci sa bopp yaa nekk ci digg mbooloo mii ngay feeñu bët ak bët, yaw Aji Sax ji, saw niir taxaw, tiim leen, te aw taxaaru niir nga leen di jiitoo bëccëg, jiitoo leen aw taxaaru sawara, guddi.
15 Nga nara boole mbooloo mii mépp, bóom benn yoon? Kon de xeet yi dégg sa jaloore dinañu wax ne:
16 “Ñàkka mana yóbbu mbooloo mii ca réew ma mu leen giñaloon, moo waral Aji Sax ji faagaagal leen ci màndiŋ mi!”
17 Kon nag ngalla Boroom bi, na sa doole màgg rekk, noonee nga noon:
18 “Aji Sax ji! Kiy muñ mer, te bare ngor, di bale tooñ aki moy te du ñàkka topp mukk doom, tooñu waajuram, ba ca sët yaak sëtaat ya.”
19 Ngalla jéggalal mbooloo mii seenug tooñ ci sag bare ngor, noonee nga leen masa bale, ca Misra ba tey jii.»
20 Ba loolu amee Aji Sax ji ne: «Jéggal naa leen noonu nga ko waxe.
21 Waaye ndegam maay Kiy Dund, te leeru Aji Sax ji mooy fees àddina sépp,
22 gannaaw mboolem nit ñi gis samag leer, gis firnde yi ma def ci digg Misra ak ci màndiŋ mi, ñoo ma nattu nii fukki yoon, bañ maa déggal,
23 kenn ci ñoom déy du gis réew, mi ma giñaloon seeni maam. Mboolem ñi ma xarab, kenn du ko ci gis.
24 Sama jaam Kaleb nag, gannaaw meneen xel lay wéye, te moo topp sama gannaaw, ba mu mat sëkk, maa koy yóbbu ba ca réew, ma mu demoon, te aw askanam a koy moom.
25 Gannaaw Amalegeen ñaak Kanaaneen ñaa nga dëkke xur wi nag, bu ëllëgee walbatikuleen, toppaat màndiŋ mi, te jaareji ko géeju Barax ya.»
26 Aji Sax ji waxati Musaak Aaróona, ne:
27 «Ba kañ la mbooloo mu bon mii di ñaxtu ci sama kaw? Ñaxtu yi bànni Israyil di ñaxtu ci sama kaw, dégg naa ci.
28 Ne leen: Ndegam maay Kiy Dund déy, Kàddug Aji Sax jee, noonu ngeen waxe, may dégg, ni laa leen di def.
29 Ci màndiŋ mii kay la seeni néew di tëdd. Mboolem ñi ñu leen limal, mboolem ñi ñu leen waññal, ñu dale ci ñaar fukki at, jëm kaw te doon ñaxtu ci sama kaw,
Màndiŋ ma 14 in Kàddug Yàlla gi