Text copied!
Bibles in Wolof

Màndiŋ ma 13:3-16 in Wolof

Help us?

Màndiŋ ma 13:3-16 in Kàddug Yàlla gi

3 Ci kaw loolu Musaa yebal ndaw ña ci ndigalal Aji Sax ji, ñu bàyyikoo ca màndiŋu Paran. Ñoom ñépp ay njiiti bànni Israyil lañu woon.
4 Ñooñu ñoo di: Samwa doomu Sakuur, ci giirug Rubeneen ñi,
5 ak Safat doomu Ori, ci giirug Cimyoneen ñi,
6 ak Kaleb doomu Yefune, ci giirug Yudeen ñi,
7 ak Igal doomu Yuusufa, ci giirug Isakareen ñi,
8 ak Oseya doomu Nuun, ci giirug Efraymeen ñi,
9 ak Palti doomu Rafu, ci giirug Beñamineen ñi,
10 ak Gadyel doomu Sodi, ci giirug Sabuloneen ñi,
11 ak Gadi doomu Susi, mi taxawal làngu Manase ci biir giirug Yuusufeen ñi,
12 ak Amyel doomu Gemali, ci giirug Daneen ñi,
13 ak Setur doomu Mikayel, ci giirug Asereen ñi,
14 ak Nabi doomu Wofsi, ci giirug Neftaleen ñi,
15 ak Gewuyel doomu Maki, ci giiru Gàddeen ñi.
16 Ñooñu la Musaa yónni woon, ngir ñu yëri réew ma. Oseya doomu Nuun nag, Musaa tudde ko Yosuwe.
Màndiŋ ma 13 in Kàddug Yàlla gi