19 ak ndax réew ma baax na, am baaxul; ak nu seeni dëkk mel: ndax ay dal rekk la, am ay dëkk yu ñu dàbbli la;
20 ak suuf sa: ndax nangu na, am nanguwul; ak itam ndax am nay garab, am déet. Te ngeen góor-góorlu ba sàkkaale ca meññeefi réew ma.» Fan yooyu nag yemook reseñ di meññ ndoortel meññeef.
21 Ci kaw loolu ndaw ya dem yëri réew ma, dale ko ca màndiŋu Ciin, ba àgg Reyob, ga ca wetu Amat.
22 Ña nga jaare Negew ca bëj-saalum, dem ba Ebron, fa Anageen ña, Ayman ak Sesay ak Talmay, dëkkoon. Ebron googee, tabaxees na ko juróom ñaari at lu jiitu Cowan ga ca Misra.