13 ak Setur doomu Mikayel, ci giirug Asereen ñi,
14 ak Nabi doomu Wofsi, ci giirug Neftaleen ñi,
15 ak Gewuyel doomu Maki, ci giiru Gàddeen ñi.
16 Ñooñu la Musaa yónni woon, ngir ñu yëri réew ma. Oseya doomu Nuun nag, Musaa tudde ko Yosuwe.
17 Ba leen Musaa yebalee ngir ñu yëri réewum Kanaan, da ne leen: «Negew gii ci bëj-saalum ngeen di jaare, yéegi ca diiwaanu tund ya,
18 ba gis nu réew ma mel: ndax waa réew ma, ñu am doole lañu, am ñu néew doole; ñu néew lañu, am ñu bare;
19 ak ndax réew ma baax na, am baaxul; ak nu seeni dëkk mel: ndax ay dal rekk la, am ay dëkk yu ñu dàbbli la;
20 ak suuf sa: ndax nangu na, am nanguwul; ak itam ndax am nay garab, am déet. Te ngeen góor-góorlu ba sàkkaale ca meññeefi réew ma.» Fan yooyu nag yemook reseñ di meññ ndoortel meññeef.
21 Ci kaw loolu ndaw ya dem yëri réew ma, dale ko ca màndiŋu Ciin, ba àgg Reyob, ga ca wetu Amat.
22 Ña nga jaare Negew ca bëj-saalum, dem ba Ebron, fa Anageen ña, Ayman ak Sesay ak Talmay, dëkkoon. Ebron googee, tabaxees na ko juróom ñaari at lu jiitu Cowan ga ca Misra.
23 Ñu dem ba ca xuru Eskol, daldi fay dagge ab car bu def benn cëggub reseñ, ñaar ca ñoom gàddoo ko bant, ñu sàkkaale fa gërënaat ak figg.
24 Bérab boobu lañu dippee xuru Eskol, (mu firi xuru Cëgg) ndax cëgg ba fa bànni Israyil dagge woon.
25 Ndaw ya nag ñibbsi, gannaaw ba ñu nemmikoo réew ma lu mat ñeent fukki fan.
26 Ñu dikk ba ci Musaa ak Aaróona, ak mbooloom bànni Israyil gépp, ca màndiŋu Paran, ca Kades. Ñu àgge leen xibaar, ñoom ak mbooloo ma mépp, ba noppi won leen meññeefum réew ma.
27 Ci kaw loolu ñu nettali Musaa, ne: «Dem nanu réew, ma nga nu yebaloon, te it foofa la meew maak lem ja tuuroo! Lii ca meññeef maa.
28 Xanaa kay, kàttan gu askanu réew ma am, péey ya dàbbliku te yaa lool. Te it ponkal yooyu cosaanoo ci Anageen ñi lanu fa gis.
29 Amalegeen ñaa dëkke bëj-saalumu réew ma, Etteen ñaak Yebuseen ñaak Amoreen ña dëkke diiwaanu tund ya, Kanaaneen ña dëkke wetu géej, feggook dexu Yurdan.»
30 Ci kaw loolu Kaleb noppiloo mbooloo ma, fekk leen tàmbalee diiŋat Musaa. Mu ne leen: «Nooy dem ba demaatoo, nanguji réew ma, ndax bir na ne noo leen mana duma.»