Text copied!
Bibles in Wolof

Màndiŋ ma 12:3-9 in Wolof

Help us?

Màndiŋ ma 12:3-9 in Kàddug Yàlla gi

3 Góor ga Musaa nag defoon ku woyof lool, ba raw mboolem doom aadama ci kaw suuf.
4 Ci kaw loolu Aji Sax ji jekki wax ak Musaa ak Aaróona ak Maryaama, ne leen: «Dikkleen, yeen ñett, ci xaymab ndaje mi!» Ñu dem, ñoom ñett.
5 Aji Sax ji wàcc ci biir niir wu def aw taxaar. Mu taxaw ca bunt xayma ba, daldi woo Aaróona ak Maryaama, ñu bokk dikk.
6 Mu ne leen: «Dégluleen bu baax samay kàddu: su ngeen feeñlee ab yonentu Aji Sax ji, ci am peeñu laa koy xamale maay kan, te ci gént laay waxeek moom,
7 waaye du Musaa sama jaam bii. Moom mooy ki wóor ci mboolem sama kër gii.
8 Gémmiñ ak gémmiñ laay waxeek moom wax ju leer nàññ ju ñu léebul, te jëmmu Aji Sax ji lay gis. Kon lu leen may fitu ŋàññ Musaa sama jaam bi?»
9 Sànjum Aji Sax ji nag tàkkal leen. Ci kaw loolu mu dem.
Màndiŋ ma 12 in Kàddug Yàlla gi