Text copied!
Bibles in Wolof

Màndiŋ ma 11:9-34 in Wolof

Help us?

Màndiŋ ma 11:9-34 in Kàddug Yàlla gi

9 Bu layaa ca dal ba ag guddi, mànn ma day wàccaale ak moom.
10 Ci biir loolu Musaa dégg mbooloo miy ñaxtu, làng ak làng, ku nekk ci sa bunt xayma. Ba loolu amee sànjum Aji Sax ji tàkk jippét, Musaa nag ñaawlu ko.
11 Ba mu ko defee Musaa ne Aji Sax ji: «Aji Sax ji, loo may mititale, Sang bi? Lu tee nga baaxe ma, xanaa ngay teg sëfub mii mbooloo mépp ci sama kaw?
12 Xanaa maa ëmb mii mbooloo mépp, am maa leen jur, ba nga di ma leen bootloo fàpp, ni jaboot di boote luy nàmp, jëme leen réew, ma nga giñaloon seeni maam?
13 Ana fu may jële yàpp wu ma jox mii mbooloo mépp, ba ñuy jooy nii ci sama kaw, naa ma: “Jox nu yàpp wu nu lekk.”?
14 Manumaa boot mii mbooloo mépp, man doŋŋ, ndax àttanuma ko.
15 Su dee nii ngay def ak man nag, dimbali ma rekk, rey ma ba ma dee, ndax ma baña gis sama toskare.»
16 Ba mu ko defee Aji Sax ji dafa wax Musaa, ne ko: «Dajaleel ma juróom ñaar fukki magi Israyil, ñoo xamal sa bopp ne ñooy magi mbooloo mi, di seeni njiit, nga indi leen ci xaymab ndaje mi, ñu teew faak yaw.
17 Maay wàcc wax ak yaw foofa te maay sàkk ci leer gi ci yaw, def ko ci ñoom, ñu yenule la yenu mbooloo mi, ba dootuloo ko yenu yaw doŋŋ.
18 «Mbooloo mi nag, ne leen ñu sell-lu ngir ëllëg, te ne leen dinañu yàpp moos, gannaaw ñooy jooy ci kaw Aji Sax ji, naan “Éy ku nuy leelatiw yàpp, nooka neexle woon ca Misra!” Kon nag Aji Sax jee leen di jox yàpp wu ñu lekk.
19 Du benn fan lañuy yàpp, du ñaar, du juróomi fan, du fukk, te du ñaar fukki fan.
20 Weeru lëmm kay lañuy yàpp, ba yàpp wiy génne ci seen paxi bakkan, ba mujj génnliku leen, gannaaw ñoo xarab Aji Sax ji ci seen biir, di jooy ci kawam, naan: “Moo lu nu taxoona jóge Misra!”»
21 Ci kaw loolu Musaa ne: «Ãa! Juróom benni téeméeri junniy (600 000) góor a ngi ci mbooloo mii ma ne ci seen biir. Yaw nga ne aw yàpp nga leen di jox, ñu yàpp weeru lëmm!
22 Diggante jur gu gudd ak gu gàtt, manees na leen cee rendil lu leen doy a? Am mboolem jëni géej lees leen di dajaleel, mu doy leen?»
23 Aji Sax ji ne Musaa: «Loxol Aji Sax ji da koo jotewul? Léegi nag dinga gis ndax sama kàddu dina la sottil, am déet!»
24 Ci kaw loolu Musaa génn, jottli mbooloo ma kàdduy Aji Sax ji, daldi dajale juróom ñaar fukki góor ñu bokk ca magi mbooloo ma, taxawal leen, ñu wër xayma ba.
25 Aji Sax ji nag wàcc ca biir niir wa, wax ak moom, daldi sàkk ca leer ga ca Musaa, sédd ca juróom ñaar fukki mag ña. Naka la leer ga dal ca seen kaw, ñu tàmbali di wax ay waxyu, benn yoon bu ñu tóllantiwul.
26 Fekk na ñaari góor a nga desoon ca dal ba, kenn ka di Eldàdd, ka ca des di Medàdd, te teewul leer ga dal ca seen kaw, ndax dees leena limaale woon ca mag ña, doonte demuñu ca xayma ba. Ñoom it ñuy wax ay waxyu ca dal ba.
27 Ab xale dawe ca, àgge ko Musaa, ne ko: «Eldàdd ak Medàdd déy a ngay wax ay waxyu ca dal ba!»
28 Yosuwe doomu Nuun, ja dale doon bëkk-néegu Musaa cag ndawam, daldi cay àddu, ne: «Sang Musaa, aaye leen!»
29 Musaa ne ko: «Fiiraangee la jàpp ndax man, am? Éy bu niti mbooloom Aji Sax ji mépp doon ay yonent, Aji Sax ji sol leen ag leeram!»
30 Ba loolu amee Musaa dellu ca dal ba, moom ak magi Israyil ña.
31 Ba loolu amee ngelaw wale ci Aji Sax ji, daldi bàbbee ca géej ga ay picci përëntaan, wàcce leen ca dal ba lu tollook doxub benn fan ci gii wet, ak doxub benn fan ca gee, ñu dajal dal ba bépp, jale ci suuf ba xawa mat ñaari xasab.
32 Ci kaw loolu mbooloo ma taxaw di for, bëccëgub keroog bépp, ak guddi ga gépp, ak bëccëgub ëllëg sa sépp, ba ka gëna néewle, for lu mat fukki barigo. Ñu weer përëntaan ya fa wër dal ba.
33 Suux waa nga ca seeni gëñ, sàqameeguñu sax, sànjum Aji Sax ji tàkkal mbooloo ma. Aji Sax ji dumaa mbooloo ma mbas mu metti lool.
34 Moo tax ñu tudde bérab booba Kibbrot Taawa (mu firi Bàmmeeli ŋaf-ŋaf), ndax fa lañu denc néewi mbooloo ma doon ŋaf-ŋafi.
Màndiŋ ma 11 in Kàddug Yàlla gi