19 Du benn fan lañuy yàpp, du ñaar, du juróomi fan, du fukk, te du ñaar fukki fan.
20 Weeru lëmm kay lañuy yàpp, ba yàpp wiy génne ci seen paxi bakkan, ba mujj génnliku leen, gannaaw ñoo xarab Aji Sax ji ci seen biir, di jooy ci kawam, naan: “Moo lu nu taxoona jóge Misra!”»
21 Ci kaw loolu Musaa ne: «Ãa! Juróom benni téeméeri junniy (600 000) góor a ngi ci mbooloo mii ma ne ci seen biir. Yaw nga ne aw yàpp nga leen di jox, ñu yàpp weeru lëmm!
22 Diggante jur gu gudd ak gu gàtt, manees na leen cee rendil lu leen doy a? Am mboolem jëni géej lees leen di dajaleel, mu doy leen?»
23 Aji Sax ji ne Musaa: «Loxol Aji Sax ji da koo jotewul? Léegi nag dinga gis ndax sama kàddu dina la sottil, am déet!»
24 Ci kaw loolu Musaa génn, jottli mbooloo ma kàdduy Aji Sax ji, daldi dajale juróom ñaar fukki góor ñu bokk ca magi mbooloo ma, taxawal leen, ñu wër xayma ba.
25 Aji Sax ji nag wàcc ca biir niir wa, wax ak moom, daldi sàkk ca leer ga ca Musaa, sédd ca juróom ñaar fukki mag ña. Naka la leer ga dal ca seen kaw, ñu tàmbali di wax ay waxyu, benn yoon bu ñu tóllantiwul.
26 Fekk na ñaari góor a nga desoon ca dal ba, kenn ka di Eldàdd, ka ca des di Medàdd, te teewul leer ga dal ca seen kaw, ndax dees leena limaale woon ca mag ña, doonte demuñu ca xayma ba. Ñoom it ñuy wax ay waxyu ca dal ba.
27 Ab xale dawe ca, àgge ko Musaa, ne ko: «Eldàdd ak Medàdd déy a ngay wax ay waxyu ca dal ba!»
28 Yosuwe doomu Nuun, ja dale doon bëkk-néegu Musaa cag ndawam, daldi cay àddu, ne: «Sang Musaa, aaye leen!»
29 Musaa ne ko: «Fiiraangee la jàpp ndax man, am? Éy bu niti mbooloom Aji Sax ji mépp doon ay yonent, Aji Sax ji sol leen ag leeram!»
30 Ba loolu amee Musaa dellu ca dal ba, moom ak magi Israyil ña.
31 Ba loolu amee ngelaw wale ci Aji Sax ji, daldi bàbbee ca géej ga ay picci përëntaan, wàcce leen ca dal ba lu tollook doxub benn fan ci gii wet, ak doxub benn fan ca gee, ñu dajal dal ba bépp, jale ci suuf ba xawa mat ñaari xasab.
32 Ci kaw loolu mbooloo ma taxaw di for, bëccëgub keroog bépp, ak guddi ga gépp, ak bëccëgub ëllëg sa sépp, ba ka gëna néewle, for lu mat fukki barigo. Ñu weer përëntaan ya fa wër dal ba.
33 Suux waa nga ca seeni gëñ, sàqameeguñu sax, sànjum Aji Sax ji tàkkal mbooloo ma. Aji Sax ji dumaa mbooloo ma mbas mu metti lool.
34 Moo tax ñu tudde bérab booba Kibbrot Taawa (mu firi Bàmmeeli ŋaf-ŋaf), ndax fa lañu denc néewi mbooloo ma doon ŋaf-ŋafi.