Text copied!
Bibles in Wolof

Màndiŋ ma 10:11-20 in Wolof

Help us?

Màndiŋ ma 10:11-20 in Kàddug Yàlla gi

11 Ca ñaareelu at ma, gannaaw ba bànni Israyil génnee Misra, ca ñaareelu weer wa, keroog ñaar fukkeelu fanam, ca la niir wa bàyyikoo fa tiim màkkaanu seedes kóllëre ga.
12 Bànni Israyil daldi sumb seen yooni tukki ya, bàyyikoo màndiŋu Sinayi. Ci kaw loolu niir wa daleji ca màndiŋu Paran.
13 Booba lañu jëkka fabu ci kàddug Aji Sax ji, Musaa jottli.
14 Raayab dalu Yudeen ña moo jëkka jóg, ànd aki gàngooram, njiital gàngooru Yuda di Nason doomu Aminadab,
15 njiital gàngooru Isakareen ña di Netanel doomu Suwar,
16 njiital gàngooru Sabuloneen ña di Elyab doomu Elon.
17 Ci biir loolu ñu wékki jaamookaay ba, Gersoneen ñaak Merareen ñay gàddu jaamookaay ba daldi dem.
18 Raayab dalu Rubeneen ña jóg ànd aki gàngooram, topp ca, njiital gàngooru Rubeneen ña di Elisur doomu Sedeyur,
19 njiital gàngooru Cimyoneen ña di Selumyel doomu Surisadaay,
20 njiital gàngooru Gàddeen ña di Elyasaf doomu Dewel.
Màndiŋ ma 10 in Kàddug Yàlla gi