Text copied!
Bibles in Wolof

Màndiŋ ma 10:10-16 in Wolof

Help us?

Màndiŋ ma 10:10-16 in Kàddug Yàlla gi

10 Seen bési mbég itam, muy seen bési màggal, di seen ndoortel weer, nangeen ciy riiral liit yi riir mu xumb, yéenee ko seen saraxi rendi-dóomal, ak seen saraxi cant ci biir jàmm. Riirum liit yooyu mooy doon seen baaxantal fa seen kanam Yàlla. Maay seen Yàlla, Aji Sax ji.»
11 Ca ñaareelu at ma, gannaaw ba bànni Israyil génnee Misra, ca ñaareelu weer wa, keroog ñaar fukkeelu fanam, ca la niir wa bàyyikoo fa tiim màkkaanu seedes kóllëre ga.
12 Bànni Israyil daldi sumb seen yooni tukki ya, bàyyikoo màndiŋu Sinayi. Ci kaw loolu niir wa daleji ca màndiŋu Paran.
13 Booba lañu jëkka fabu ci kàddug Aji Sax ji, Musaa jottli.
14 Raayab dalu Yudeen ña moo jëkka jóg, ànd aki gàngooram, njiital gàngooru Yuda di Nason doomu Aminadab,
15 njiital gàngooru Isakareen ña di Netanel doomu Suwar,
16 njiital gàngooru Sabuloneen ña di Elyab doomu Elon.
Màndiŋ ma 10 in Kàddug Yàlla gi