Text copied!
Bibles in Wolof

Màndiŋ ma 10:1-12 in Wolof

Help us?

Màndiŋ ma 10:1-12 in Kàddug Yàlla gi

1 Aji Sax ji waxati Musaa, ne:
2 «Sàkklul ñaari liiti xaalis. Lu ñu tëgglu ba mu jekk nga koy def. Liit yi ngay wootee am ndaje, di ko yékkatee dal yi.
3 Bu ñu liitee ñaar yépp, mbooloo mépp ay dajesi fi yaw, ci bunt xaymab ndaje mi.
4 Bu ñu liitee benn nag kilifa yi jiite gàngoori Israyil ñooy dajesi fi yaw.
5 Su ñu liitee menn riirum liit mu xumb, dal yi dale penku ñooy fabu.
6 Su ñu liitee riirum liit mu xumb, ñaareel bi yoon, dal yi dale bëj-saalum ñooy fabu. Riirum liit mu xumb mooy tegtale seeni fabu.
7 Bu dee wooteb ndaje nag, dees koy liit waaye du doon riir mu xumb.
8 Na doomi Aaróona sarxalkat yi di wal liit yi, te mu doon dogal bu leen saxal dàkk, ci seen maasoo maas.
9 «Bu loolu wéyee, bu ngeen dee xare ci seenum réew, ak noon bu leen songsi, nangeen riiral liit yi riir mu xumb, su boobaa dees na leen bàyyi xel fa seen kanam Yàlla Aji Sax ji, ba wallu leen ak seeni noon.
10 Seen bési mbég itam, muy seen bési màggal, di seen ndoortel weer, nangeen ciy riiral liit yi riir mu xumb, yéenee ko seen saraxi rendi-dóomal, ak seen saraxi cant ci biir jàmm. Riirum liit yooyu mooy doon seen baaxantal fa seen kanam Yàlla. Maay seen Yàlla, Aji Sax ji.»
11 Ca ñaareelu at ma, gannaaw ba bànni Israyil génnee Misra, ca ñaareelu weer wa, keroog ñaar fukkeelu fanam, ca la niir wa bàyyikoo fa tiim màkkaanu seedes kóllëre ga.
12 Bànni Israyil daldi sumb seen yooni tukki ya, bàyyikoo màndiŋu Sinayi. Ci kaw loolu niir wa daleji ca màndiŋu Paran.
Màndiŋ ma 10 in Kàddug Yàlla gi