Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 9:51-61 in Wolof

Help us?

LUUG 9:51-61 in Téereb Injiil

51 Bi jamono ji jegeñsee, ji Yeesu waree jóge àddina dem asamaan, mu sigiñu ci dem Yerusalem.
52 Noonu mu yebal ay ndaw, ñu jiitu ko. Ñu dem nag, dugg ci ab dëkk ci diiwaanu Samari, ngir wutal ko fa fu mu dal.
53 Waaye waa dëkk ba nanguwuñu ko, ndaxte mi ngi jublu woon Yerusalem.
54 Bi taalibe yi tudd Saag ak Yowaana gisee loolu, ñu ne: «Boroom bi, ndax dangaa bëgg nu ne, na sawaras asamaan dal ci seen kaw, faagaagal leen?»
55 Waaye Yeesu walbatiku, yedd taalibe ya,
56 ba noppi ñu daldi dem wuti beneen dëkk.
57 Bi ñuy dem, am ci yoon wi ku ne Yeesu: «Dinaa la topp fépp foo jëm.»
58 Waaye Yeesu ne ko: «Till yi am nañu seeni kàmb, te picci asamaan am nañu ay tàgg, waaye Doomu nit ki amul fu mu noppal boppam.»
59 Yeesu ne keneen: «Toppal ci man.» Waaye kooku ne ko: «Sang bi, may ma, ma jëkka dem suuli sama baay.»
60 Mu ne ko: «Bàyyil ñi dee, ñu suul seeni néew. Yaw demal, yégle nguuru Yàlla.»
61 Keneen ne ko: «Sang bi, dinaa la topp, waaye may ma, ma jëkka tàgguji sama waa kër.»
LUUG 9 in Téereb Injiil

Luug 9:51-61 in Kàddug Yàlla gi

51 Ba ñu demee ba bés bi ñu wara yéege Yeesu di jubsi, Yeesu moo dogu ngir dem Yerusalem.
52 Mu yebal ay ndaw, ñu jiitu ko. Ñu dem, ba agsi ab dëkk ci diiwaanu Samari, nar ko faa waajal ab dal.
53 Waa Samari nag nanguwuñu koo dalal, ndax Yerusalem ga mu nammoona jëm.
54 Taalibe ya ñuy wax Yanqóoba ak Yowaan gis loolu, daldi ne: «Sang bi, soo bëggee nu jox sawara ndigal, mu wàcce asamaan, faagaagal leen?»
55 Teewul Yeesu geesu, femmu leen.
56 Ba loolu amee ñu jàll jëm beneen dëkk.
57 Ca yoon wa ñu awe la jenn waay ne Yeesu: «Yaw laay topp fépp foo jëm.»
58 Yeesu itam ne ko: «Till ak kàmbam, njanaaw akub tàggam, waaye Doomu nit ki de, amul fu mu wéer boppam.»
59 Mu neeti keneen: «Toppal ci man.» Mu ne ko: «Sang bi, may ma, ma jëkka dem robi sama baay.»
60 Mu ne ko: «Bàyyil néew yi, ñu rob seeni néew, waaye yaw demal, yégleji nguurug Yàlla.»
61 Keneen neeti ko: «Sang bi, yaw laay topp, waaye may ma, ma jëkka tàggtook sama waa kër.»
Luug 9 in Kàddug Yàlla gi