38 Jenn waay jekki xaacoo ca mbooloo ma, ne: «Sëriñ bi, dama lay ñaan, nga xoolal ma sama doom, ndax moom doŋŋ laa am.
39 Rab kat moo ko jàpp, mu jekki di yuuxu, di say, gémmiñ giy fuur. Daanaka du teqlikook moom te sonal na ko.
40 Ñaan naa say taalibe ngir ñu dàqal ma ko, waaye manuñu ko.»
41 Yeesu ne leen: «Céy niti tey, yeena gëmadi te dëng! Maak yeen ba kañ, te di leen muñal? Indi sa doom fii.»
42 Naka la xale bi jubsi Yeesu, rab wi sànni ko ci suuf, muy say. Yeesu itam gëdd rab wa, wéral xale ba, delloo ko baayam.
43 Ñépp nag waaru ci màggug Yàlla. Naka la ñépp di yéemu ca mboolem la Yeesuy def, mu ne taalibeem ya:
44 «Ubbileen seeni nopp te teewlu bu baax kàddu yii: Doomu nit ki lees di wor, ngir teg ko ci loxoy nit ñi.»
45 Taalibe ya nag dégguñu kàddu googu, ndax fekk na piri ma làqu leen, ngir ñu bañ koo daj, te ñemewuñu koo laaj Yeesu.
46 Werante moo dikkaloon taalibe yi, ñuy seet kan moo gëna kawe ci ñoom.
47 Yeesu nag ràññee seen xalaat. Mu daldi indi ab xale, taxawal ko ci wetam.
48 Mu ne leen: «Xale bii, képp ku ko dalal ndax sama tur, man nga dalal; te képp ku ma dalal, dalal nga ki ma yebal; ndax ki gëna tuut ci yeen ñépp, kooku moo gëna màgg.»
49 Ci kaw loolu Yowaan àddu, ne: «Njaatige, danoo gis nit kuy dàqe sa tur ay rab, nu aaye ko, ndax bokkul ci nun.»