Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 8:3-55 in Wolof

Help us?

LUUG 8:3-55 in Téereb Injiil

3 Sànn, soxnas ku ñuy wax Kusa, mi doon wottu alalu Erodd; ak Susànn ak ñeneen jigéen. Jigéen ñooñu ñoo doon joxe seen alal, ngir dimbali Yeesu ak ay taalibeem.
4 Dëkk ak dëkk nit ña di fa jóge jëm ca Yeesu, ba mbooloo mu bare dajaloo, mu wax leen léeb wii:
5 «Dafa amoon beykat bu demoon jiyi. Bi muy saaw toolam nag, lenn ci pepp mi wadd ci kaw yoon wi, nit ñi joggi ci, picci asamaan lekk ko lépp.
6 Leneen wadd ci bérab bu bare ay doj. Naka la sax rekk, daldi wow, ndaxte suuf si tooyul woon.
7 Leneen nag wadd ci biir ay xaaxaam, ñu saxandoo, xaaxaam ya tanc ko.
8 Li ci des dal ci suuf su baax, sax, nangu ba meññ téeméeri yoon lu ëpp la mu ji woon.» Gannaaw loolu Yeesu wax ak kàddu gu dëgër ne: «Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.»
9 Taalibey Yeesu yi laaj ko lu léeb woowu di tekki.
10 Mu ne leen: «May nañu leen, ngeen xam mbóoti nguuru Yàlla, waaye ñi ci des, dama leen di wax ci ay léeb. Noonu la, ngir: “Ñuy xool te duñu mana gis, di dégg te duñu mana xam.”
11 «Lii la léebu beykat bi di tekki. Kàddug Yàlla mooy jiwu wi.
12 Ki féete ci yoon wi mooy ki dégg. Gannaaw gi, Seytaane dafay ñëw, këf kàddu, gi ñu def ci xolam, ngir mu baña gëm te Yàlla musal ko.
13 Ki nekk ci bérab bu bare ay doj, mooy ki dégg kàddu gi, ba noppi nangu ko ak mbég. Waaye wax ji saxul ci moom. Dina gëm ab diir, waaye bu nattu yi agsee, mu daldi dàggeeku.
14 Ki jot ci jiwu wi ci xaaxaam yi mooy ki dégg kàddu gi, waaye nees-tuut soxla yi ak alal ak bànneexi àddina tanc ko, ba du àgg cig mat.
15 Ki jot ci jiwu wi ci suuf su baax si nag, mooy ki dégg kàddu gi te denc ko ci xol bu baax bu gore, te muñ ba jur njariñ.
16 «Kenn du taal làmp, dëpp ci leget, walla mu di ko def ci ron lal. Daf koy wékk, ngir mu leeral ñiy dugg.
17 Amul dara luy kumpa lu ñu dul siiwal bés, walla lu làqu lu ñu dul feeñal, ba mu ne fàŋŋ.
18 Seetleen bu baax, ni ngeen di dégloo kàddu gi. Ku am, dees na la dollil, waaye ku amul, dees na nangu sax li nga xalaatoon ne am nga ko ba noppi.»
19 Noonu ndeyu Yeesu ak ay rakkam ñëw seetsi ko, waaye manuñu woona agsi ci moom, ndaxte nit ña dañoo bare.
20 Am ku ko yégal ne: «Sa yaay ak say rakk ñu ngi nii taxaw ci biti, bëgg laa gis.»
21 Waaye mu daldi leen ne: «Sama yaay ak samay rakk, ñooy ñiy déglu kàddug Yàlla, te di ko topp.»
22 Benn bés Yeesu àndoon na ak ay taalibeem, dugg ci gaal. Mu ne leen: «Nanu jàll dex gi.» Noonu ñu dem.
23 Bi ñuy dem nag, Yeesu daldi nelaw. Ngelaw lu am doole daldi ñëw, yëngal dex gi, gaal gi fees ak ndox, ba ñu bëgga suux.
24 Noonu taalibe yi jegesi Yeesu, yee ko ne: «Kilifa gi, kilifa gi, nu ngiy dee!» Ci kaw loolu Yeesu jóg, daldi gëdd ngelaw li ak duus yi. Lépp dal, ba ne nemm.
25 Yeesu ne taalibe yi: «Ana seen ngëm?» Ñu daldi tiit te waaru, naan ci seen biir: «Kii moo di kan? Mi ngi jox ndigal ngelaw li ak ndox mi, ñu koy déggal.»
26 Noonu ñu teer ca diiwaanu waa Serasa, fa jàkkaarloo ak diiwaanu Galile.
27 Bi Yeesu di wàcc ca gaal ga, ku rab jàpp ca waa dëkk ba ñëw, kar ko. Yàgg na def yaramu neen te dëkkul ca kër, waaye ca sëg ya lay nekk.
28 Bi mu gisee Yeesu, mu yuuxu, daanu ciy tànkam, daldi xaacu ne: «Yaw Yeesu Doomu Yàlla Aji Kawe ji, loo may fexeel? Maa ngi lay ñaan, nga bañ maa mbugal.»
29 Dafa wax loolu, ndaxte Yeesu santoon na rab wi, mu génn ci moom. Rab wa dafa ko doon farala jàpp. Nit ñi daan nañu ko wottu, di ko yeew ak ay càllala, ak di ko jéng, mu di leen dagg, rab wi di ko xiir ca bérab yu wéet.
30 Noonu Yeesu laaj ko: «Noo tudd?» Mu ne ko: «Coggal laa tudd.» Dafa wax loolu, ndaxte rab yu baree ko jàppoon.
31 Rab yooyoo ngi ko doon ñaan, ngir mu bañ leena sant, ñu dem ca kàmb gu xóot gi.
32 Fekk amoon na fa géttu mbaam-xuux yu bare, yuy for ca tund wa. Rab ya ñaan Yeesu, mu may leen, ñu dugg mbaam-xuux ya. Mu may leen ko.
33 Noonu rab ya génn nit ka, dugg mbaam-xuux ya, ñu daldi bartalu, daanu ca dex ga, lab.
34 Sàmm ya gis li xew, daw nettaliji mbir mi ca dëkk ba ak ca àll ba.
35 Nit ñi génn, ngir seet li xew. Bi ñu agsee ca Yeesu, ñu fekk fa nit, ka rab ya bàyyi woon, toog ca kanam Yeesu, sol ay yére te ànd ak sagoom. Ñu daldi ragal.
36 Ña fekke woon mbir ma nag, nettali leen naka la Yeesu wérale ki rab ya jàppoon.
37 Ci kaw loolu waa diiwaanu Serasa bépp ragal, ba ñaan Yeesu mu jóge fa. Noonu Yeesu dugg ci gaal gi, di bëgga dem.
38 Nit ki Yeesu tàggale woon ak rab ya ñaan ko, ngir ànd ak moom. Waaye Yeesu waññi ko ne ko:
39 «Ñibbil, nettali li la Yàlla defal lépp.» Noonu waa ji dem di wër dëkk ba yépp, di fa yégle la ko Yeesu defal.
40 Bi Yeesu dëppee dellu, mbooloo ma di ko teeru, ndaxte ñépp a ngi ko doon xaar.
41 Noonu nit ñëw, tuddoon Yayrus te nekk njiitu jàngu ba. Bi mu agsee, mu daanu ci tànki Yeesu, sarxu ko mu ñëw këram,
42 ndaxte jenn doomam ju jigéen, ji mu amoon kepp te muy tollu ci fukki at ak ñaar, ma nga doon waaja dee. Bi Yeesuy dem, nit ñaa ngi doon buuxante, di ko tanc.
43 Amoon na nag ca mbooloo ma jigéen ju doon xëpp deret diirub fukki at ak ñaar, te kenn manu ko woona faj.
44 Jigéen ja jegeñsi Yeesu nag, doxe ko gannaaw, laal catu mbubbam. Ca saa sa deret ji dal.
45 Yeesu laaj nit ña ne: «Ana ku ma laal?» Ku nekk di miim. Noonu Piyeer ne ko: «Kilifa gi, nit ñépp a ngi lay wër, di la tanc wet gu nekk.»
46 Waaye Yeesu ne: «Am na ku ma laal, ndaxte yég naa ne am na doole ju génn ci man.»
47 Te jigéen ja xam ne manul woona nëbb li mu def. Mu daldi daanu ci tànki Yeesu, di lox. Noonu mu nettali ci kanam ñépp li taxoon mu laal Yeesu, ak ni mu wére ca saa sa.
48 Yeesu ne ko: «Soxna si, sa ngëm faj na la. Demal ci jàmm.»
49 Bi Yeesu di wax nag, am na ku jóge ca kër njiit la, mu ñëw naan: «Sa doom faatu na; matatul ngay sonal kilifa gi.»
50 Yeesu dégg kàddu yooyu, daldi ne njiit la: «Bul tiit. Gëmal rekk te dina dundaat.»
51 Bi Yeesu agsee ca kër ga, nanguwul kenn duggaaleek moom, ñu dul Piyeer, Yowaana, Saag ak waajuri xale ba.
52 Ña fa nekk ñépp di yuuxu ak di jooy xale bi. Noonu Yeesu ne leen: «Bàyyileen seen jooy yi. Janq bi deewul, day nelaw rekk.»
53 Waaye ñu di ko ñaawal, ndaxte xamoon nañu ne dee na.
54 Waaye Yeesu jàpp loxob janq ba, woo ko ne ko: «Xale bi, jógal.»
55 Noonu ruuwu xale ba délsiwaat, mu daldi jóg ca saa sa. Yeesu santaane ñu may ko, mu lekk.
LUUG 8 in Téereb Injiil

Luug 8:3-55 in Kàddug Yàlla gi

3 ak Yowaana jabaru Kusa, saytukatub Erodd; ak Susaana, ak ñeneen jigéen ñu bare ñu daan dimbalee ñoom Yeesu seen alal.
4 Mbooloo mu mag a daje woon, jóge dëkkoo dëkk, fekksi Yeesu. Mu léeb leen, ne leen:
5 «Boroom jiwu moo demoon jiyi. Naka lay saaw ab toolam, ndeke lenn ca jiwu maa nga wadde ca kaw yoon wa, nit ñi joggati ca, picc yi dikk, lekk ko.
6 Leneen wadde fu barey doj. Naka la sax rekk, daldi wow, ndax ñàkk ndox.
7 Leneen la wadde biiri xaaxaam, jógandoo ak xaaxaam ma, daldi fatt ba wow.
8 La des ca jiwu ma wadde suuf su nangu, daldi sax, ba meññal lu ko mat téeméeri yoon.» Ci kaw loolu Yeesu àddu ca kaw ne: «Ku am nopp yu mu dégge kat, na dégg.»
9 Ay taalibeem laaj ko lu léeb woowu di tekki.
10 Mu ne leen: «Yeen lañu may, ngeen xam mbóotum nguurug Yàlla, waaye ñi ci des ñoom, ci ay léeb lees koy dëxëñ, su ko defee: “Ñuy xoole te duñu gis, di dégg te duñu xam.”
11 «Lii la léeb wi di tekki. Jiwu wi moo di kàddug Yàlla.
12 Ñi féeteek yoon wi mooy ñi dégg. Seytaane nag mooy dikk, foqati kàddu gi ci seen xol, ngir ñu baña gëm ba mucc.
13 Ñi féete fu bare ay doj, ñoo dégg kàddu gi, nangoo ko xol bu sedd. Waaye ñooñu, ab reen lañu amul. Ab diir rekk lañuy gëm, bu janti nattu dikkee, ñu dellu gannaaw.
14 Li wadde ci ay xaaxaam mooy ñi dégg kàddu gi, te ay xalaat ak alal, ak bànneexu bakkan fatt leen, ba tax meññaluñu lu ñor.
15 Li ci suuf su baax si nag, mooy ñi dégge kàddu gi xol bu dëggu te rafet, ŋoy ca, te saxoo muñ ba meññal.
16 «Deesul taal ab làmp, dëppe ko ndab, mbaa nga dugal ko ci ron lal. Dees koy aj kay ba kuy duggsi, di gis leer gi.
17 Mboolem lu làqu dina feeñ, te mboolem lu nëbbu dina siiw ba ne fàŋŋ.
18 Kon nag teewluleen ni ngeen di dégge. Ku am, dees na ko dolli, waaye ku amul, la mu xalaatoon ne am na ko sax, dees na ko nangu.»
19 Yaayu Yeesu ak ay rakkam ñoo dikkoon di seet Yeesu te manuñoo agsi ci moom ndax nit ñu bare.
20 Ñu ne ko: «Sa yaay ak say rakk a ngi taxaw ci biti, bëgg laa gis.»
21 Mu ne leen: «Sama yaay ak samay rakk, ñoo di ñiy dégg kàddug Yàlla, te di ko jëfe.»
22 Benn bés la Yeesu duggoon gaal, mook ay taalibeem. Mu ne leen: «Nanu jàll ca wàllaa dex gi.» Ñu daldi dem.
23 Naka lañuy dem nag, Yeesu nelaw. Ngelaw lu réy dal ca kaw dex ga, gaal gi fees ak ndox, ba ñu nara sànku.
24 Taalibe yi yee Yeesu, ne ko: «Njaatige, njaatige, nu ngi sànku!» Mu yewwu, gëdd ngelaw li ak gannax yu réy yi. Lépp dal, ne tekk.
25 Yeesu ne taalibe ya: «Ana seen ngëm?» Ña nga boole tiitaange ak kéemtaan te naan ca seen biir: «Kii nag moo di kan bay jox ndigal ngelaw leek ndox mi sax, ñu déggal ko?»
26 Ci kaw loolu ñu tëmb ba teereji ca diiwaanu waa Serasa, fa jàkkaarloo ak diiwaanu Galile.
27 Ba Yeesu wàccee ca tefes ga, jenn waayu dëkk ba dikk dajeek moom. Waa ja, ay rab a ko jàpp. Yàgg naa def yaramu neen te dëkkul ci kër, xanaa sëg ya.
28 Ba mu gisee Yeesu, daa yuuxu, daanu fa kanamam, daldi xaacu ne: «Yaw Yeesu Doomu Yàlla Aji Kawe ji, ana lu ma joteek yaw? Dama lay tinu, bu ma mbugal!»
29 Booba Yeesu tàmbali naa sant rab wi, mu génn waa ji. Rab wi jàpp na waa ji ay yooni yoon. Su ko defee ñu yeewe ko ay càllala, jéng ko, ngir wattu ko, mu di ko dagg, rab wi di ko xabtal, jëme bérab yu wéet.
30 Yeesu ne ko: «Noo tudd?» Mu ne ko: «Coggal.» Ndax rab yu baree duggoon waa ji.
31 Rab yi nag tinu Yeesu, ngir mu bañ leena yebal ca xóote ba.
32 Ag coggalu mbaam-xuux yu baree nga woon foofa, di fore ca tund wa. Rab ya tinu Yeesu, ne mu may leen, ñu dugg mbaam-xuux ya. Mu may leen ko.
33 Rab ya nag génn nit ka, dugg mbaam-xuux ya, coggal ga bartaloondoo, tàbbi ca dex ga, daldi lab.
34 Sàmm ya gis la xew, daldi daw, nettaliji ko waa dëkk ba, ak dëkk-dëkkaan ya.
35 Nit ña riire ca, di seet la xew. Naka lañu dikk ba ci Yeesu, yem ci nit ki rab wi teqlikool, mu ànd ak sagoom, solu, toog ca wetu Yeesu. Ñu daldi tiit.
36 Ña ko fekke woon nag, nettali leen na boroomi rab ba jote wall.
37 Ci kaw loolu mbooloom diiwaanu Serasa gépp tinu Yeesu ngir mu jóge ca seen biir te dem ndax tiitaange lu réy lu leen jàpp. Naka la Yeesu dugg gaal, di dem,
38 nit ka teqlikook rab yi di ko sarxu ngir ànd ak moom. Teewul Yeesu yiwi ko, ne ko:
39 «Ñibbil, te nga xamle li la Yàlla defal lépp.» Waa ja it dem di siiwal ca dëkk ba bépp, mboolem la ko Yeesu defal.
40 Ba Yeesu delloo ca wàllaa dex, mbooloo maa ko teertu, ndax ñoom ñépp a ko doon xaar.
41 Ci kaw loolu rekk jenn waay dikk, ku ñuy wax Yayrus, di njiitu jàngu ba. Mu ne gurub fi kanam Yeesu, sarxu ko ngir mu ñëw këram,
42 ndax kenn la amoon ci doom, janq bu am fukki at ak ñaar, te ma nga doon waaja dee. Yeesoo ngay dem, nit ña raj-rajloo, tanc ko.
43 Senn as ndaw a nga ca woon, diiru fukki at ak ñaar, ma nga doon xëpp deret, te def na ci alalam jépp, kenn manu koo faj.
44 Mu doxe Yeesu gannaaw, teg loxoom ca catal mbubbam, deret ja dal ca saa sa.
45 Yeesu nag ne: «Ana ku ma laal?» Ku nekk di miim. Piyeer ne ko: «Njaatige, mbooloo mépp a la yéew, dar la.»
46 Teewul Yeesu ne: «Am na ku ma laal kay, ndax yég naa leer gu bàyyikoo ci man.»
47 Ndaw sa xam ne feeñ na. Mu daldi dikk, di lox, ne gurub fa kanam Yeesu, daldi wax ca kanam ñépp la waral mu teg ko loxoom, ak na mu wére ca saa sa.
48 Yeesu ne ko: «Janq, sa ngëm faj na la. Demal ak jàmm.»
49 Naka la Yeesu di wax, jenn waay jóge ca kër njiitu jàngu ba, dikk ne: «Matatul ngay sonal sëriñ bi, sa janq ba faatu na.»
50 Yeesu dégg ca, ne njiit la: «Bul tiit. Gëmal rekk, mu daldi mucc.»
51 Bi Yeesu agsee ca kër ga, mayul kenn ànd ak moom dugg, ku moy Piyeer, ak Yowaan ak Yanqóoba ak baayu xale bi, ak ndeyam.
52 Ñépp a ngay jooy ak a tiislu janq bi. Yeesu nag ne leen: «Buleen jooy. Janq bi deewul, day nelaw rekk.»
53 Ci kaw loolu ñu di ko kókkali, ndax xamoon nañu xéll ne dee na.
54 Yeesu itam jàpp ca loxol janq ba, daldi àddu ca kaw, ne ko: «Janq, jógal.»
55 Noo ga délsi, mu ne ñokket. Yeesu ne ñu may ko, mu lekk.
Luug 8 in Kàddug Yàlla gi