Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 8:16-28 in Wolof

Help us?

LUUG 8:16-28 in Téereb Injiil

16 «Kenn du taal làmp, dëpp ci leget, walla mu di ko def ci ron lal. Daf koy wékk, ngir mu leeral ñiy dugg.
17 Amul dara luy kumpa lu ñu dul siiwal bés, walla lu làqu lu ñu dul feeñal, ba mu ne fàŋŋ.
18 Seetleen bu baax, ni ngeen di dégloo kàddu gi. Ku am, dees na la dollil, waaye ku amul, dees na nangu sax li nga xalaatoon ne am nga ko ba noppi.»
19 Noonu ndeyu Yeesu ak ay rakkam ñëw seetsi ko, waaye manuñu woona agsi ci moom, ndaxte nit ña dañoo bare.
20 Am ku ko yégal ne: «Sa yaay ak say rakk ñu ngi nii taxaw ci biti, bëgg laa gis.»
21 Waaye mu daldi leen ne: «Sama yaay ak samay rakk, ñooy ñiy déglu kàddug Yàlla, te di ko topp.»
22 Benn bés Yeesu àndoon na ak ay taalibeem, dugg ci gaal. Mu ne leen: «Nanu jàll dex gi.» Noonu ñu dem.
23 Bi ñuy dem nag, Yeesu daldi nelaw. Ngelaw lu am doole daldi ñëw, yëngal dex gi, gaal gi fees ak ndox, ba ñu bëgga suux.
24 Noonu taalibe yi jegesi Yeesu, yee ko ne: «Kilifa gi, kilifa gi, nu ngiy dee!» Ci kaw loolu Yeesu jóg, daldi gëdd ngelaw li ak duus yi. Lépp dal, ba ne nemm.
25 Yeesu ne taalibe yi: «Ana seen ngëm?» Ñu daldi tiit te waaru, naan ci seen biir: «Kii moo di kan? Mi ngi jox ndigal ngelaw li ak ndox mi, ñu koy déggal.»
26 Noonu ñu teer ca diiwaanu waa Serasa, fa jàkkaarloo ak diiwaanu Galile.
27 Bi Yeesu di wàcc ca gaal ga, ku rab jàpp ca waa dëkk ba ñëw, kar ko. Yàgg na def yaramu neen te dëkkul ca kër, waaye ca sëg ya lay nekk.
28 Bi mu gisee Yeesu, mu yuuxu, daanu ciy tànkam, daldi xaacu ne: «Yaw Yeesu Doomu Yàlla Aji Kawe ji, loo may fexeel? Maa ngi lay ñaan, nga bañ maa mbugal.»
LUUG 8 in Téereb Injiil

Luug 8:16-28 in Kàddug Yàlla gi

16 «Deesul taal ab làmp, dëppe ko ndab, mbaa nga dugal ko ci ron lal. Dees koy aj kay ba kuy duggsi, di gis leer gi.
17 Mboolem lu làqu dina feeñ, te mboolem lu nëbbu dina siiw ba ne fàŋŋ.
18 Kon nag teewluleen ni ngeen di dégge. Ku am, dees na ko dolli, waaye ku amul, la mu xalaatoon ne am na ko sax, dees na ko nangu.»
19 Yaayu Yeesu ak ay rakkam ñoo dikkoon di seet Yeesu te manuñoo agsi ci moom ndax nit ñu bare.
20 Ñu ne ko: «Sa yaay ak say rakk a ngi taxaw ci biti, bëgg laa gis.»
21 Mu ne leen: «Sama yaay ak samay rakk, ñoo di ñiy dégg kàddug Yàlla, te di ko jëfe.»
22 Benn bés la Yeesu duggoon gaal, mook ay taalibeem. Mu ne leen: «Nanu jàll ca wàllaa dex gi.» Ñu daldi dem.
23 Naka lañuy dem nag, Yeesu nelaw. Ngelaw lu réy dal ca kaw dex ga, gaal gi fees ak ndox, ba ñu nara sànku.
24 Taalibe yi yee Yeesu, ne ko: «Njaatige, njaatige, nu ngi sànku!» Mu yewwu, gëdd ngelaw li ak gannax yu réy yi. Lépp dal, ne tekk.
25 Yeesu ne taalibe ya: «Ana seen ngëm?» Ña nga boole tiitaange ak kéemtaan te naan ca seen biir: «Kii nag moo di kan bay jox ndigal ngelaw leek ndox mi sax, ñu déggal ko?»
26 Ci kaw loolu ñu tëmb ba teereji ca diiwaanu waa Serasa, fa jàkkaarloo ak diiwaanu Galile.
27 Ba Yeesu wàccee ca tefes ga, jenn waayu dëkk ba dikk dajeek moom. Waa ja, ay rab a ko jàpp. Yàgg naa def yaramu neen te dëkkul ci kër, xanaa sëg ya.
28 Ba mu gisee Yeesu, daa yuuxu, daanu fa kanamam, daldi xaacu ne: «Yaw Yeesu Doomu Yàlla Aji Kawe ji, ana lu ma joteek yaw? Dama lay tinu, bu ma mbugal!»
Luug 8 in Kàddug Yàlla gi