15 Ki jot ci jiwu wi ci suuf su baax si nag, mooy ki dégg kàddu gi te denc ko ci xol bu baax bu gore, te muñ ba jur njariñ.
16 «Kenn du taal làmp, dëpp ci leget, walla mu di ko def ci ron lal. Daf koy wékk, ngir mu leeral ñiy dugg.
17 Amul dara luy kumpa lu ñu dul siiwal bés, walla lu làqu lu ñu dul feeñal, ba mu ne fàŋŋ.
18 Seetleen bu baax, ni ngeen di dégloo kàddu gi. Ku am, dees na la dollil, waaye ku amul, dees na nangu sax li nga xalaatoon ne am nga ko ba noppi.»
19 Noonu ndeyu Yeesu ak ay rakkam ñëw seetsi ko, waaye manuñu woona agsi ci moom, ndaxte nit ña dañoo bare.
20 Am ku ko yégal ne: «Sa yaay ak say rakk ñu ngi nii taxaw ci biti, bëgg laa gis.»
21 Waaye mu daldi leen ne: «Sama yaay ak samay rakk, ñooy ñiy déglu kàddug Yàlla, te di ko topp.»
22 Benn bés Yeesu àndoon na ak ay taalibeem, dugg ci gaal. Mu ne leen: «Nanu jàll dex gi.» Noonu ñu dem.
23 Bi ñuy dem nag, Yeesu daldi nelaw. Ngelaw lu am doole daldi ñëw, yëngal dex gi, gaal gi fees ak ndox, ba ñu bëgga suux.
24 Noonu taalibe yi jegesi Yeesu, yee ko ne: «Kilifa gi, kilifa gi, nu ngiy dee!» Ci kaw loolu Yeesu jóg, daldi gëdd ngelaw li ak duus yi. Lépp dal, ba ne nemm.
25 Yeesu ne taalibe yi: «Ana seen ngëm?» Ñu daldi tiit te waaru, naan ci seen biir: «Kii moo di kan? Mi ngi jox ndigal ngelaw li ak ndox mi, ñu koy déggal.»
26 Noonu ñu teer ca diiwaanu waa Serasa, fa jàkkaarloo ak diiwaanu Galile.
27 Bi Yeesu di wàcc ca gaal ga, ku rab jàpp ca waa dëkk ba ñëw, kar ko. Yàgg na def yaramu neen te dëkkul ca kër, waaye ca sëg ya lay nekk.
28 Bi mu gisee Yeesu, mu yuuxu, daanu ciy tànkam, daldi xaacu ne: «Yaw Yeesu Doomu Yàlla Aji Kawe ji, loo may fexeel? Maa ngi lay ñaan, nga bañ maa mbugal.»
29 Dafa wax loolu, ndaxte Yeesu santoon na rab wi, mu génn ci moom. Rab wa dafa ko doon farala jàpp. Nit ñi daan nañu ko wottu, di ko yeew ak ay càllala, ak di ko jéng, mu di leen dagg, rab wi di ko xiir ca bérab yu wéet.
30 Noonu Yeesu laaj ko: «Noo tudd?» Mu ne ko: «Coggal laa tudd.» Dafa wax loolu, ndaxte rab yu baree ko jàppoon.
31 Rab yooyoo ngi ko doon ñaan, ngir mu bañ leena sant, ñu dem ca kàmb gu xóot gi.
32 Fekk amoon na fa géttu mbaam-xuux yu bare, yuy for ca tund wa. Rab ya ñaan Yeesu, mu may leen, ñu dugg mbaam-xuux ya. Mu may leen ko.
33 Noonu rab ya génn nit ka, dugg mbaam-xuux ya, ñu daldi bartalu, daanu ca dex ga, lab.
34 Sàmm ya gis li xew, daw nettaliji mbir mi ca dëkk ba ak ca àll ba.
35 Nit ñi génn, ngir seet li xew. Bi ñu agsee ca Yeesu, ñu fekk fa nit, ka rab ya bàyyi woon, toog ca kanam Yeesu, sol ay yére te ànd ak sagoom. Ñu daldi ragal.
36 Ña fekke woon mbir ma nag, nettali leen naka la Yeesu wérale ki rab ya jàppoon.
37 Ci kaw loolu waa diiwaanu Serasa bépp ragal, ba ñaan Yeesu mu jóge fa. Noonu Yeesu dugg ci gaal gi, di bëgga dem.
38 Nit ki Yeesu tàggale woon ak rab ya ñaan ko, ngir ànd ak moom. Waaye Yeesu waññi ko ne ko:
39 «Ñibbil, nettali li la Yàlla defal lépp.» Noonu waa ji dem di wër dëkk ba yépp, di fa yégle la ko Yeesu defal.
40 Bi Yeesu dëppee dellu, mbooloo ma di ko teeru, ndaxte ñépp a ngi ko doon xaar.
41 Noonu nit ñëw, tuddoon Yayrus te nekk njiitu jàngu ba. Bi mu agsee, mu daanu ci tànki Yeesu, sarxu ko mu ñëw këram,
42 ndaxte jenn doomam ju jigéen, ji mu amoon kepp te muy tollu ci fukki at ak ñaar, ma nga doon waaja dee. Bi Yeesuy dem, nit ñaa ngi doon buuxante, di ko tanc.
43 Amoon na nag ca mbooloo ma jigéen ju doon xëpp deret diirub fukki at ak ñaar, te kenn manu ko woona faj.
44 Jigéen ja jegeñsi Yeesu nag, doxe ko gannaaw, laal catu mbubbam. Ca saa sa deret ji dal.
45 Yeesu laaj nit ña ne: «Ana ku ma laal?» Ku nekk di miim. Noonu Piyeer ne ko: «Kilifa gi, nit ñépp a ngi lay wër, di la tanc wet gu nekk.»
46 Waaye Yeesu ne: «Am na ku ma laal, ndaxte yég naa ne am na doole ju génn ci man.»
47 Te jigéen ja xam ne manul woona nëbb li mu def. Mu daldi daanu ci tànki Yeesu, di lox. Noonu mu nettali ci kanam ñépp li taxoon mu laal Yeesu, ak ni mu wére ca saa sa.