Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 7:8-47 in Wolof

Help us?

LUUG 7:8-47 in Téereb Injiil

8 Ndaxte man itam maa ngi nekk ci ndigal, te ame naa ay xarekat ci sama ndigal. Su ma nee kii: “Demal,” mu dem. Mbaa ma ne keneen ki: “Ñëwal,” mu ñëw. Te su ma nee sama jaam: “Defal lii,” mu def ko.»
9 Bi ko Yeesu déggee, mu waaru. Noonu mu walbatiku ca mbooloo, ma topp ci moom, ne leen: «Maa ngi leen koy wax, ci bànni Israyil sax, masuma cee gis ku gëme nii.»
10 Noonu ndaw ya daldi dellu ca kër ga. Bi ñu agsee, ñu gis ne surga ba wér na.
11 Yàggul dara Yeesu dem ci dëkk bu ñuy wax Nayin. Taalibeem yi ak mbooloo mu bare ànd ak moom.
12 Bi muy agsi ca buntu dëkk ba, fekk ñuy rob néew boo xam ne kenn rekk la woon ci ndeyam, ji jëkkëram faatu woon. Te mbooloo mu bare ca dëkk ba di gunge soxna sa.
13 Bi ko Boroom ba gisee, mu daldi koy yërëm ne ko: «Bul jooyati.»
14 Mu jegeñsi, laal jaat ga, ñi ko jàppoo taxaw. Mu ne: «Waxambaane wi, jógal, ndigal la.»
15 Noonu nit ka dee woon jóg toog, tàmbalee wax. Yeesu delloo ko yaay ja.
16 Ñépp tiit, bay màggal Yàlla, di wax naan: «Yonent bu mag feeñ na ci sunu biir! Yàlla wallusi na mbooloom!»
17 La ñu wax ci mbiri Yeesu daldi siiw ca réewu Yawut ya ak la ko wër yépp.
18 Taalibey Yaxya ya nettali mbir yooyu yépp seen kilifa. Noonu Yaxya woo ñaar ci ay taalibeem,
19 yónni leen ci Boroom bi, ngir laaj ko: «Ndax yaw yaa di Ki wara ñëw, walla danoo wara xaar keneen?»
20 Bi taalibe ya agsee ca Yeesu, ñu ne ko: «Yaxya moo nu yebal, nu laaj ndax yaa di Ki waroona ñëw, walla danuy xaar keneen?»
21 Ca waxtu woowa Yeesu wéral nit ñu bare ci seeni feebar ak ci seeni metit, di dàq ay rab tey gisloo ay gumba.
22 Noonu mu wax ndaw ya ne leen: «Demleen nettali Yaxya li ngeen gis te dégg ko. Gumba yaa ngi gis, lafañ yiy dox, gaana yi wér, tëx yiy dégg, ñi dee di dekki, te néew doole ñaa ngi dégg xibaaru jàmm bi.
23 Yaw mi sa ngëm yolomul ndax man, barkeel nga.»
24 Bi ndawi Yaxya yi demee, Yeesu daldi wax ak mbooloo ma ci mbirum Yaxya ne leen: «Lu ngeen seeti woon ca màndiŋ ma? Xanaa barax buy jaayu ci ngelaw li?
25 Kon lu ngeen seeti woon nag? Nit ku sol yére yu rafet? Waaye ñiy soloo noonu, tey dund dund gu neex ñu ngi dëkk ci këri buur.
26 Kon lu ngeen seeti woon? Yonent? Waaw, wax naa leen ne ëpp na yonent.
27 Yaxya male moo di ki ñu waxoon ci Mbind mi naan: “Maa ngi yónni sama ndaw, mu jiitu la, te xàllal la yoon ci sa kanam.”
28 Maa ngi leen koy wax, ci li jigéen jur, ku sut Yaxya masula feeñ. Waaye ba tey ki gëna ndaw ci nguuru Yàlla moo ko sut.»
29 Nit ñépp ñi doon déglu Yeesu, ba ci juutikat yi sax, dëggal nañu ne Yàlla ku jub la, ndaxte nangu nañu Yaxya sóob leen ci ndox.
30 Waaye Farisen ya ak xutbakat ya dañoo bañ, mu sóob leen ci ndox, di wone noonu ne gàntu nañu li leen Yàlla bëggaloon.
31 Yeesu tegaat ca ne: «Kon lan laa mana méngaleel niti jamono jii? Lan lañuy nirool?
32 Ñu ngi nirook xale yu toog ca pénc ma tey woowante naan: “Liital nanu leen ak toxoro, te fecculeen, woyal nanu leen woyi dëj, te jooyuleen.”
33 Ndaxte Yaxya feeñ na, lekkul mburu, naanul biiñ, ngeen daldi ne: “Dafa ànd ak rab.”
34 Gannaaw gi nag Doomu nit ki ñëw na, lekk, naan, ngeen daldi ne: “Kii daal bëgg na lekk, di naan biiñ, tey xaritoo ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar.”
35 Waaye li xam-xamu Yàlla di jur, mooy firndeel ne dëgg la.»
36 Amoon na ab Farisen bu ñaan Yeesu, mu ñëw lekkandoo ak moom. Yeesu dem kër waa ja, toog ca lekkukaay.
37 Fekk amoon na ca dëkk ba jigéen juy moy Yàlla. Bi mu yégee ne, Yeesoo ngay lekk ca kër Farisen ba, mu dem, yóbbaale njaq lu ñu defare doj wu ñuy wax albaatar te def latkoloñ.
38 Bi jigéen ja agsee, mu taxaw ca gannaaw tànki Yeesu, di jooy. Noonu ay rongooñam tooyal tànki Yeesu, jigéen ja di leen fomp ak kawaram, di leen fóon te ciy sotti latkoloñ ja.
39 Naka la Farisen, bi woo woon Yeesu ci këram, gis loolu, mu wax ci xelam naan: «Bu nit kii doonoon yonent, kon dina xam kuy jigéen ji koy laal ak ni mu nekke bàkkaarkat.»
40 Yeesu ne ca tonn, daldi ne Farisen ba: «Simoŋ, am na lu ma la wara wax.» Simoŋ ne ko: «Waxal, kilifa gi.»
41 Yeesu ne ko: «Da fee amoon ñaari nit ñu ameel bor benn leblekat. Kenn kaa ngi ko ameel téeméeri junni ci xaalis, ki ci des fukki junni.
42 Waaye kenn ci ñoom manu koo fey. Noonu mu baal leen bor ya. Ci ñaar ñooñu nag kan moo ko ciy gëna bëgg?»
43 Simoŋ ne ko: «Xanaa ki ñu baal bor bi gëna bare.» Yeesu ne ko: «Àtte nga dëgg,»
44 daldi walbatiku ca jigéen ja, ne Simoŋ: «Ndax gis nga jigéen jii? Dugg naa sa kër, te joxewuloo ndox, ngir raxas samay tànk. Waaye moom, raxas na samay tànk ak ay rongooñam, ba noppi fomp leen ak kawaram.
45 Bi ma agsee, fóonuloo ma, waaye moom, bi ma duggee ba léegi tàyyiwul ci di fóon samay tànk.
46 Defuloo diw ci sama bopp, waaye moom, sotti na latkoloñ ci samay tànk.
47 Moo tax ma di la wax ne, su wonee mbëggeel gu réye nii, dafa fekk ñu baal ko bàkkaaram yu bare. Waaye ki mbëggeelam néew dafa fekk ñu baal ko lu tuuti.»
LUUG 7 in Téereb Injiil

Luug 7:8-47 in Kàddug Yàlla gi

8 Ndax man ci sama bopp ci kilifteef laa tënku, te man itam ay takk-der a ngi ci sama ndigal. Su ma nee kii: “Demal,” mu dem. Ma ne kee: “Ñëwal,” mu ñëw. Te sama jaam bu ma ne: “Defal lii,” mu def ko.»
9 Ba Yeesu déggee loolu daa yéemu ca njiit la. Mu ne gees mbooloo ma topp ca moom, ne leen: «Dama ne, gii ngëm gu réy, bànni Israyil sax, gisuma ko ci.»
10 Ndaw ya daldi dellu ca kër ga, fekk jaam ba wér.
11 La ca tegu Yeesu demati dëkk bu ñuy wax Nayin, ay taalibeem ak mbooloo mu bare ànd ak moom.
12 Ba mu jubsee buntu dëkk ba, yemul ci lu moy ab rob, ka dee di doomu jëtun, te moom rekk la amoon. Niti dëkk ba def mbooloo mu bare, ànd ak soxna sa.
13 Sang bi nag gis ko, ñeewante ko, ne ko: «Bul jooy.»
14 Mu dikk ba teg loxoom ca jaat ga, ña ko jàppoo taxaw. Mu ne: «Ngóor si, yaw laay wax, jógal.»
15 Néew ba jóg toog, di wax, mu delloo ko yaay ja.
16 Tiitaange nag jàpp ñépp, ñu sàbbaal Yàlla, naan: «Yonent bu mag feeñ na ci sunu biir!» te naan «Yàllaa wallusi ñoñam!»
17 Coow loolu nag law ca mboolem réewum Yawut ak mboolem fa ko wër.
18 Ci kaw loolu taalibey Yaxya àgge Yaxya loolu lépp. Mu woo ñaar ca taalibe ya,
19 yebal leen ci Sang bi, laaj ko ne ko: «Ndax yaw yaa di Ki wara ñëw, am keneen lanuy séentu?»
20 Taalibe ya dikk ne ko: «Yaxya moo nu yebal, di la laaj ndax yaa di Ki wara ñëw, am keneen lanuy séentu?»
21 Waxtu woowa tembe nag Yeesu faj na ñu bare, tàggale leen aki jàngoro aki jagadi aki rab, silmaxa yu bare, mu baaxe leen, ñuy gis.
22 Mu ne ndaw ya: «Li ngeen gis te dégg ko, demleen àgge ko Yaxya. Silmaxa yaa ngi gis, lafañ yi dox, gaana yi wér, tëx yiy dégg, néew yi dekki, néew-doole ñi dégg xibaaru jàmm bi.
23 Ku ma taxul nga xàcc sa péete ak man nag, ndokklee yaw.»
24 Ba ndawi Yaxya demee, Yeesu daldi wax ak mbooloo ma ci mbirum Yaxya, ne leen: «Lu ngeen seetaani woon ca màndiŋ ma? Xanaa barax bu ngelaw liy yëngal?
25 Kon lu ngeen seetaani woon? Boroom yére yu rafet? Waaye boroom yére yu yànj yooyu te seen dund bakkane, ci këri buur lañu dëkk.
26 Kon nag lu ngeen seetaani woon? Ab yonent? Waawaaw, maa leen ko wax, te wees na ab yonent sax.
27 Ci moom moomu lañu bindoon ne: “Maa ngii di yebal sama ndaw, mu jiitu la, xàllal la saw yoon.”
28 Maa leen ko wax, li jigéen jur, kenn sutu ci Yaxya. Waaye ki gëna tuut ci nguurug Yàlla sax moo ko sut.»
29 Mboolem ña déglu Yeesu, ba ca juutikat ya sax, dëggal nañu Yàlla, ndax nangu nañoo sóobu sóobeb Yaxya.
30 Waaye Farisen ya ak xamkati yoon ya ñoo gàntal la leen Yàlla nammaloon, ba Yaxya sóobu leen ci ndox.
31 Yeesu neeti: «Ana kon lu may niruleel niti tey jii? Ana lu ñuy nirool?
32 Ñu ngi nirook xale yu toog ca pénc ma di awoonte, naan: “Noo leen toxorool, fecculeen, nu dëjal leen, jooyuleen.”
33 Ndaxte Yaxya daa feeñ, lekkul dugub, naanul biiñ, ngeen nee: “Aw rab la àndal.”
34 Doomu nit ki feeñ, di lekk ak a naan, ngeen naay: “Kee fuqle, naan-katub biiñ biiy xaritook juutikat yeek bàkkaarkat yi.”
35 Waaye xel mu rafet, mboolem la mu jur mooy la koy dëggal.»
36 Kenn ca Farisen ya moo woo woon Yeesu, ngir ñu bokk lekk. Yeesu agsi kër Farisen ba, daldi dikk ca ndab la.
37 Ndeke senn as ndaw a nga ca dëkk ba, ab moykat la woon. Mu yég nag ne Yeesoo nga ca kër Farisen ba, di lekk. Mu dikk, indaale njaqal doju albatar lu def diwu xeeñlu.
38 Mu dikk ba fa Yeesu sóonu, ca gannaawam, fa tànki Yeesu féete, daldi taxaw, di jooy, rongooñ ya tooyal xepp tànk ya. Ndaw sa nag di fompe tànki Yeesu kawaru boppam gay lang, di fóon tànk yaak cofeel, di ca sotti diwu xeeñlu ga.
39 Farisen ba woo Yeesu nag gis loolu, naan ci xelam: «Kii su doon ab yonent, dina xam ndaw sii di ko nabb-nabbee ku mu doon, ak lu mu doon: jigéenu moykat!»
40 Yeesu nag àddu, ne ko: «Simoŋ, dinaa la wax lenn.» Mu ne ko: «Waxal, sëriñ bi.»
41 Yeesu ne ko: «Ñaari boroom bor la woon ak seenub leblekat. Boru kenn ka di téeméeri junni (500 000) ci xaalis, ka ca des fukki junni (50 000).
42 Waaye ñoom ñaar ñépp, kenn manu cee fey. Mu far jéggal leen ñoom ñépp. Ana kan ci ñaar ñooñu nag moo ciy gëna fonk leblekat bi?»
43 Simoŋ ne ko: «Xanaa ki ëpple lu ñu ko jéggal.» Yeesu ne ko: «Sab àtte jub na.»
44 Mu walbatiku ca ndaw sa, daldi ne Simoŋ: «Gis nga ndaw sii de? Dugg naa sa kër, mayewoo ndox mu ma jàngoo. Waaye moom, ay rongooñam la tooyale samay tànk, fompe ko kawaru boppam.
45 Fóonuloo ma, dalale ma, waaye moom, ba ma duggsee ba léegi noppiwula fóon samay tànk.
46 Ag diw, diwewoo ko sama bopp, waaye moom, diwu xeeñlu la diw samay tànk.
47 Moo tax ma di la wax, ne bàkkaaram yu bare yi ñu ko jéggal moo waral fonkeelam gu bare. Waaye njéggal lu tuut, fonkeel gu tuut rekk.»
Luug 7 in Kàddug Yàlla gi