22 Mu ne ndaw ya: «Li ngeen gis te dégg ko, demleen àgge ko Yaxya. Silmaxa yaa ngi gis, lafañ yi dox, gaana yi wér, tëx yiy dégg, néew yi dekki, néew-doole ñi dégg xibaaru jàmm bi.
23 Ku ma taxul nga xàcc sa péete ak man nag, ndokklee yaw.»
24 Ba ndawi Yaxya demee, Yeesu daldi wax ak mbooloo ma ci mbirum Yaxya, ne leen: «Lu ngeen seetaani woon ca màndiŋ ma? Xanaa barax bu ngelaw liy yëngal?
25 Kon lu ngeen seetaani woon? Boroom yére yu rafet? Waaye boroom yére yu yànj yooyu te seen dund bakkane, ci këri buur lañu dëkk.
26 Kon nag lu ngeen seetaani woon? Ab yonent? Waawaaw, maa leen ko wax, te wees na ab yonent sax.
27 Ci moom moomu lañu bindoon ne: “Maa ngii di yebal sama ndaw, mu jiitu la, xàllal la saw yoon.”
28 Maa leen ko wax, li jigéen jur, kenn sutu ci Yaxya. Waaye ki gëna tuut ci nguurug Yàlla sax moo ko sut.»
29 Mboolem ña déglu Yeesu, ba ca juutikat ya sax, dëggal nañu Yàlla, ndax nangu nañoo sóobu sóobeb Yaxya.
30 Waaye Farisen ya ak xamkati yoon ya ñoo gàntal la leen Yàlla nammaloon, ba Yaxya sóobu leen ci ndox.
31 Yeesu neeti: «Ana kon lu may niruleel niti tey jii? Ana lu ñuy nirool?
32 Ñu ngi nirook xale yu toog ca pénc ma di awoonte, naan: “Noo leen toxorool, fecculeen, nu dëjal leen, jooyuleen.”
33 Ndaxte Yaxya daa feeñ, lekkul dugub, naanul biiñ, ngeen nee: “Aw rab la àndal.”
34 Doomu nit ki feeñ, di lekk ak a naan, ngeen naay: “Kee fuqle, naan-katub biiñ biiy xaritook juutikat yeek bàkkaarkat yi.”
35 Waaye xel mu rafet, mboolem la mu jur mooy la koy dëggal.»
36 Kenn ca Farisen ya moo woo woon Yeesu, ngir ñu bokk lekk. Yeesu agsi kër Farisen ba, daldi dikk ca ndab la.
37 Ndeke senn as ndaw a nga ca dëkk ba, ab moykat la woon. Mu yég nag ne Yeesoo nga ca kër Farisen ba, di lekk. Mu dikk, indaale njaqal doju albatar lu def diwu xeeñlu.
38 Mu dikk ba fa Yeesu sóonu, ca gannaawam, fa tànki Yeesu féete, daldi taxaw, di jooy, rongooñ ya tooyal xepp tànk ya. Ndaw sa nag di fompe tànki Yeesu kawaru boppam gay lang, di fóon tànk yaak cofeel, di ca sotti diwu xeeñlu ga.
39 Farisen ba woo Yeesu nag gis loolu, naan ci xelam: «Kii su doon ab yonent, dina xam ndaw sii di ko nabb-nabbee ku mu doon, ak lu mu doon: jigéenu moykat!»
40 Yeesu nag àddu, ne ko: «Simoŋ, dinaa la wax lenn.» Mu ne ko: «Waxal, sëriñ bi.»
41 Yeesu ne ko: «Ñaari boroom bor la woon ak seenub leblekat. Boru kenn ka di téeméeri junni (500 000) ci xaalis, ka ca des fukki junni (50 000).
42 Waaye ñoom ñaar ñépp, kenn manu cee fey. Mu far jéggal leen ñoom ñépp. Ana kan ci ñaar ñooñu nag moo ciy gëna fonk leblekat bi?»
43 Simoŋ ne ko: «Xanaa ki ëpple lu ñu ko jéggal.» Yeesu ne ko: «Sab àtte jub na.»
44 Mu walbatiku ca ndaw sa, daldi ne Simoŋ: «Gis nga ndaw sii de? Dugg naa sa kër, mayewoo ndox mu ma jàngoo. Waaye moom, ay rongooñam la tooyale samay tànk, fompe ko kawaru boppam.