19 yebal leen ci Sang bi, laaj ko ne ko: «Ndax yaw yaa di Ki wara ñëw, am keneen lanuy séentu?»
20 Taalibe ya dikk ne ko: «Yaxya moo nu yebal, di la laaj ndax yaa di Ki wara ñëw, am keneen lanuy séentu?»
21 Waxtu woowa tembe nag Yeesu faj na ñu bare, tàggale leen aki jàngoro aki jagadi aki rab, silmaxa yu bare, mu baaxe leen, ñuy gis.
22 Mu ne ndaw ya: «Li ngeen gis te dégg ko, demleen àgge ko Yaxya. Silmaxa yaa ngi gis, lafañ yi dox, gaana yi wér, tëx yiy dégg, néew yi dekki, néew-doole ñi dégg xibaaru jàmm bi.
23 Ku ma taxul nga xàcc sa péete ak man nag, ndokklee yaw.»
24 Ba ndawi Yaxya demee, Yeesu daldi wax ak mbooloo ma ci mbirum Yaxya, ne leen: «Lu ngeen seetaani woon ca màndiŋ ma? Xanaa barax bu ngelaw liy yëngal?
25 Kon lu ngeen seetaani woon? Boroom yére yu rafet? Waaye boroom yére yu yànj yooyu te seen dund bakkane, ci këri buur lañu dëkk.
26 Kon nag lu ngeen seetaani woon? Ab yonent? Waawaaw, maa leen ko wax, te wees na ab yonent sax.
27 Ci moom moomu lañu bindoon ne: “Maa ngii di yebal sama ndaw, mu jiitu la, xàllal la saw yoon.”
28 Maa leen ko wax, li jigéen jur, kenn sutu ci Yaxya. Waaye ki gëna tuut ci nguurug Yàlla sax moo ko sut.»
29 Mboolem ña déglu Yeesu, ba ca juutikat ya sax, dëggal nañu Yàlla, ndax nangu nañoo sóobu sóobeb Yaxya.
30 Waaye Farisen ya ak xamkati yoon ya ñoo gàntal la leen Yàlla nammaloon, ba Yaxya sóobu leen ci ndox.