11 La ca tegu Yeesu demati dëkk bu ñuy wax Nayin, ay taalibeem ak mbooloo mu bare ànd ak moom.
12 Ba mu jubsee buntu dëkk ba, yemul ci lu moy ab rob, ka dee di doomu jëtun, te moom rekk la amoon. Niti dëkk ba def mbooloo mu bare, ànd ak soxna sa.
13 Sang bi nag gis ko, ñeewante ko, ne ko: «Bul jooy.»
14 Mu dikk ba teg loxoom ca jaat ga, ña ko jàppoo taxaw. Mu ne: «Ngóor si, yaw laay wax, jógal.»
15 Néew ba jóg toog, di wax, mu delloo ko yaay ja.
16 Tiitaange nag jàpp ñépp, ñu sàbbaal Yàlla, naan: «Yonent bu mag feeñ na ci sunu biir!» te naan «Yàllaa wallusi ñoñam!»
17 Coow loolu nag law ca mboolem réewum Yawut ak mboolem fa ko wër.