Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 6:3-16 in Wolof

Help us?

LUUG 6:3-16 in Téereb Injiil

3 Yeesu ne leen: «Ndax jànguleen la Daawuda defoon, ba mu xiifee, moom ak ña mu àndaloon?
4 Xanaa yéguleen, ni mu dugge woon ca kër Yàlla ga, jël mburu, ya ñu teewal ca kanam Yàlla, lekk ca, jox ca ña mu àndaloon? Fekk jaaduwul kenn lekk ko, ku dul sarxalkat.»
5 Yeesu dellu ne leen: «Doomu nit ki mooy boroom bésub noflaay bi.»
6 Beneen bésub noflaay, Yeesu dugg ci jàngu bi, di fa jàngle. Amoon na fa nit ku loxol ndijooram làggi.
7 Xutbakat yi ak Farisen yi ñu ngi ko doon xool, ba xam ndax dina ko faj ci bésub noflaay bi, ngir ñu am lu ñu ko tuumaale.
8 Waaye Yeesu xam seen xalaat, daldi ne ku loxoom làggi: «Jógal taxaw ci kanam ñépp.» Nit ka daldi jóg taxaw.
9 Yeesu ne leen: «Ma laaj leen, lan moo jaadu, nu def ko bésub noflaay bi, lu baax mbaa lu bon; nu musal nit mbaa nu lor nit?»
10 Ci kaw loolu mu xool leen ñoom ñépp, ba noppi ne nit ka: «Tàllalal sa loxo.» Mu tàllal ko, loxoom daldi wér péŋŋ.
11 Waaye nit ña mer ba fees, di rabat pexe yu jëm ca Yeesu.
12 Ca bés yooya Yeesu yéeg ca tund wa ngir ñaan, mu fanaan fa, di ñaan ci Yàlla.
13 Bi bët setee, Yeesu woo taalibeem yi, tànn ci fukk ak ñaar, tudde leen ay ndawam:
14 Simoŋ, mi Yeesu tudde Piyeer, ak Andare, mi bokk ak Piyeer ndey ak baay; Saag ak Yowaana, Filib ak Bartelemi,
15 Macë ak Tomaa, Saag doomu Alfe, ak Simoŋ mi bokk ci mbooloo, ma ñu tudde Ñi farlu ci moom seen réew;
16 Yudaa doomu Saag, ak Yudaa Iskariyo, mi mujja wor.
LUUG 6 in Téereb Injiil

Luug 6:3-16 in Kàddug Yàlla gi

3 Yeesu ne leen: «Xanaa jànguleen la Daawuda defoon, ba mu xiifee, moom, ak ña mu àndaloon?
4 Ba mu duggee ca kër Yàlla ga, mburum teewal ma la jël, lekk, jox ca ña mu àndal, te yoon mayewul kenn ku ca lekk ku dul sarxalkat yi.»
5 Mu neeti leen: «Bésub Noflaay, Doomu nit ki mooy boroom.»
6 Beneen bésub Noflaay, Yeesu dugg ca jàngu ba, di jàngle. Jenn waay ju loxol ndijooram làggi ma nga fa woon.
7 Firikati yooni Musaa yaak Farisen yaa ngay xool Yeesu, ba xam ndax dina ko faj ca bésub Noflaay ba, ngir ñu am lu ñu ko tuumaale.
8 Yeesu nag xam seen xalaat, daldi ne boroom loxo ba: «Jógal taxaw fii ci digg bi.» Mu jóg taxaw.
9 Yeesu ne leen: «Laaj naa leen, ana lu yoon maye ci bésub Noflaay; def lu baax am lu bon? Musal bakkan am lore?»
10 Ci kaw loolu mu dawal bëtam, xool ña ko yéew ñépp, ba noppi ne waa ja: «Tàllalal sa loxo.» Mu tàllal, loxo ba wér.
11 Ñu mer nag ba fees, di diisoo ci seen biir nu ñuy def ak Yeesu.
12 Fan yooyu la Yeesu dem kaw tund wa ngir ñaani fa; mu fanaane faa ñaan ci Yàlla.
13 Ba bët setee, mu woo ay taalibeem, tànn ca fukk ak ñaar ñii, tudde leen ay ndawam:
14 Simoŋ mi Yeesuy wooye itam Piyeer, ak Àndre mi bokk ak Piyeer ndey ak baay, ak Yanqóoba ak Yowaan, ak Filib ak Bartelemi,
15 ak Macë ak Tomaa, ak Yanqóoba doomu Alfe, ak Simoŋ mi ñuy wax farlukatu moom-sa-réew,
16 ak Yuda doomu Yanqóoba, ak Yuda Iskaryo ma mujj wor.
Luug 6 in Kàddug Yàlla gi