Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 5:4-38 in Wolof

Help us?

LUUG 5:4-38 in Téereb Injiil

4 Bi mu jànglee ba noppi, mu ne Simoŋ: «Joowal gaal gi, ba fa ndox ma gëna xóote, ngeen sànni fa seeni mbaal ngir napp.»
5 Simoŋ ne ko: «Kilifa gi, coono lanu fanaane biig te jàppunu dara. Waaye nag dinaa ko sànni ci sa ndigal.»
6 Naka lañu sànni mbaal yi, jàpp jën yu bare, ba mbaal yay tàmbalee xëtt.
7 Noonu ñu daldi liyaar seen àndandoo, yi nekk ca geneen gaal ga, ngir ñu ñëw dimbali leen. Ñooñu agsi, ñu feesal ñaari gaal yi, ba ñuy bëgga suux.
8 Naka la Simoŋ Piyeer gis loolu, daldi sukk ci kanam Yeesu ne ko: «Sore ma Boroom bi, ndaxte nitu bàkkaar laa!»
9 Wax na loolu nag, ndax jën yu bare ya ñu mbaaloon daf koo jaaxal, moom ak ña mu àndaloon
10 ak ña mu bokkaloon liggéey ba, maanaam ñaari doomi Sebede yi di Saag ak Yowaana. Yeesu ne Simoŋ: «Bul ragal dara; gannaaw-si-tey, ay nit ngay mbaal jëme ci man.»
11 Noonu ñu teer ca tefes ga, bàyyi lépp, di topp ci moom.
12 Ni Yeesu nekke woon ci ab dëkk, am fa ku gaana ba daj. Bi mu gisee Yeesu, mu daldi dëpp jëëm ci suuf, ñaan ko: «Sang bi, soo ko bëggee, man nga maa wéral.»
13 Yeesu tàllal loxoom, laal ko naan: «Bëgg naa ko, wéral.» Ca saa sa ngaanaam daldi deñ.
14 Yeesu sant ko ne: «Bu ko wax kenn, waaye demal won sa bopp sarxalkat bi, te nga jébbal Yàlla sarax si yoonu Musaa santaane, ngir ñu xam ne wér nga, te mu nekk seede ci ñoom.»
15 Noonu turu Yeesu di gëna siiw. Mbooloo mu bare di ñëw ci moom, ngir déglu ko te mu faj seeni jàngoro.
16 Waaye Yeesu moom di beddeeku ci bérab yu wéet ya, di ñaan.
17 Am na bés Yeesu doon jàngle. Amoon na ca mbooloo, ma teewoon, ñu bokkoon ca Farisen ya ak ay xutbakat yu jóge ca dëkk yépp, ya ca Galile ak ya ca Yude ak Yerusalem. Yeesu àndoon na ak dooley Boroom bi, ba muy faj ay jarag.
18 Noonu ay nit ñëw, jàppoo basaŋ, ga ñu tëral nit ku yaram wépp làggi. Ñu di ko wuta dugal ca kër ga, ngir indi ko ca Yeesu.
19 Waaye gisuñu fu ñu koy awale ndax mbooloo ma. Ñu daldi yéeg ca kaw kër ga nag, xeddi tiwiil ya, yoor waa ja ak basaŋ ga, wàcce ko ca kanam Yeesu ca biir mbooloo ma.
20 Bi Yeesu gisee seen ngëm, mu ne làggi ba: «Sama waay, baal nañu la say bàkkaar.»
21 Xutbakat yi ak Farisen yi di werante ci seen xel naan: «Kii mooy kan bay sosal Yàlla? Ana ku mana baale bàkkaar yi, ku dul Yàlla doŋŋ?»
22 Waaye Yeesu xam seen xalaat, ne leen: «Lu tax ngeen di werante ci seen xel?
23 Ma wax ne: “Baal nañu la say bàkkaar,” walla ma ne: “Jógal te dox,” lan moo ci gëna yomb?
24 Waaye xamleen ne, Doomu nit ki am na ci àddina sañ-sañu baale bàkkaar yi.» Ci kaw loolu Yeesu ne ku làggi ba: «Maa ngi la koy sant, jógal, jël sa basaŋ te nga ñibbi.»
25 Nit ka jóg ca saa sa ci kanam ñépp, jël basaŋ, ga ñu ko tëraloon, ñibbi tey màggal Yàlla.
26 Mbooloo mépp waaru, di màggal Yàlla. Ñu ragal tey wax naan: «Gis nanu tey ay mbir yu ëpp xel.»
27 Gannaaw loolu Yeesu génn, gis ab juutikat bu tudd Lewi, mu toog ca juuti ba. Mu ne ko: «Kaay topp ci man.»
28 Lewi jóg, bàyyi lépp, daldi ko topp.
29 Noonu Lewi togglu ay ñam yu bare ci këram, ngir teral Yeesu. Juutikat yu bare ak yeneen gan ñu nga fa woon, di lekkandoo ak ñoom.
30 Farisen yi ak seeni xutbakat di xultu taalibey Yeesu yi ne leen: «Lu tax ngeen di lekkandoo ak di naanandoo ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar?»
31 Yeesu ne leen: «Ñi wér soxlawuñu fajkat, ñi wéradi ñoo ko soxla.
32 Ñëwuma ngir woo ñi jub, waaye ngir woo bàkkaarkat yi, ñu tuub seeni bàkkaar.»
33 Noonu ñu ne Yeesu: «Taalibey Yaxya yi ak yu Farisen yi dinañu faral di woor ak di ñaan ci Yàlla, waaye say taalibe ñu ngiy lekk ak di naan.»
34 Yeesu ne leen: «Ndax man ngeena woorloo gan, yi ñëw cig céet, li feek boroom céet gaa ngi ànd ak ñoom?
35 Waaye bés yaa ngi ñëw, yu ñuy jële boroom céet gi ci seen biir. Bés yooyu nag, dinañu woor.»
36 Te it Yeesu wax leen léeb wii: «Kenn du jël mbubb mu bees, xotti ci sekkit, daaxe ko mbubb mu màggat. Lu ko moy, dina xotti mbubb mu bees mi, te sekkit, wi mu ci jële, du ànd ak mbubb mu màggat mi.
37 Te kenn du def biiñ bu bees ci mbuusi der yu màggat. Lu ko moy, biiñ bu bees bi day toj mbuus yi, biiñ bi tuuru, mbuus yi yàqu.
38 Waaye dañoo wara def biiñ bu bees ci mbuus yu bees.
LUUG 5 in Téereb Injiil

Luug 5:4-38 in Kàddug Yàlla gi

4 Naka la jàngle ba noppi, ne Simoŋ: «Bëmëxal ba ca xóote ba, te ngeen sànni seeni mbaal ba jàpp.»
5 Simoŋ ne ko: «Njaatige, coono lanu fanaane biig te jàppunu dara. Xanaa ma sànni ko rekk ci sa ndigal.»
6 Naka lañu sànni mbaal yi, daldi jàpp jën yu baree bare, ba mbaal ya di xëtt.
7 Ba loolu amee ñu liyaar seen moroom, ya ca geneen gaal ga, ngir ñu dimbalisi leen. Ñu dikk, yebandook ñoom, feesal ñaari gaal yépp, ba ñuy bëgga suux.
8 Simoŋ Piyeer nag gis loolu, daldi sukk fa kanam Yeesu, ne ko: «Sang bi, ngalla sore ma, ngir man nitu bàkkaarkat laa!»,
9 ndax tiitaange lu ko jàpp, mook mboolem ña mu àndal, ca jën yu bare ya ñu jàpp.
10 Yanqóoba ak Yowaan doomi Sebede ya mu bokkaloon liggéey ba itam noonu lañu tiite. Yeesu ne Simoŋ: «Bul ragal dara; gannaaw-si-tey, ay nit ngay napp.»
11 Ci kaw loolu ñu teeral gaal ya ca tefes ga, daldi bàyyi lépp, topp ca moom.
12 Yeesoo nekkoon cib dëkk, ndeke jenn waay a nga fa, ju jàngoroy ngaana dajal yaram wa. Ba mu gisee Yeesu, daa daanu, dëpp jëëm ci suuf, sarxu ko, ne: «Sang bi, su la soobee, man nga maa setal.»
13 Yeesu tàllal loxoom, laal ko ne: «Soob na ma, setal.» Ca saa sa ngaana ga teqlikook moom.
14 Yeesu dénk ko ne ko: «Bu ko wax kenn, demal rekk ca sarxalkat ba, ngir mu seet la, te nga génne sa jooxeb setlu, ni ko yoonu Musaa santaanee, muy firnde ci ñoom.»
15 Teewul jëwub Yeesu gënatee law. Mbooloo yu bare daje, di ko déglu tey faju, ba tàggook seeni jàngoro.
16 Moom nag muy rocceekuy dem ba ci bérab yu wéet, di fa ñaaneji.
17 Yeesu moo doon jàngle bés, fu ay Farisen ak ay jànglekati yoonu Musaa tooge, jóge ca mboolem dëkki Galile ak Yude ak Yerusalem, te manoorey Boroom bi teew faak moom, ngir faj jarag ja.
18 Ci biir loolu ay nit ne jalañ, jàppoo ab lafañ bu ñu tëral cig laltu. Ñu di ko wuta dugal, ngir tëral ko ca kanam Yeesu.
19 Waaye gisuñu fu ñu koy awale ndax mbooloo ma. Ñu yéeg ca kaw néeg ba, xeddi lenn ca xadd ba, yoor waa jaak laltu ga, wàcce ko ca digg ba, fa kanam Yeesu.
20 Yeesu nag gis seen ngëm, daldi ne lafañ ba: «Mbokk mi, jéggalees na la say bàkkaar.»
21 Firikati yoonu Musaa yi ak Farisen yi tàmbalee nàttable ci seen xel, naan: «Kii di saaga Yàlla mooy kan? Ana ku mana jéggaley bàkkaar ku dul Yàlla doŋŋ?»
22 Yeesu nag xam la ñuy nàttable ci seen xel, daldi àddu, ne leen: «Lu ngeen di nàttable ci seen xel?
23 Ana lu gëna yomb ci yii yaar: ne “Jéggalees na la say bàkkaar,” am ne: “Jógal te dox”?
24 Kon nag dingeen xam ne Doomu nit ki am na ci kaw suuf, sañ-sañu jéggale ay bàkkaar.» Mu ne lafañ ba: «Dama ne, jógal, jël sag laltu te dem ñibbi.»
25 Nit ka daldi ne ñokket ca kanam ñépp, jël laltu ga mu tëddoon, jëm këram, di sàbbaal Yàlla.
26 Ba loolu amee mbooloo mépp a neey, di sàbbaal Yàlla, tiitaange jàpp leen, ñu naan: «Gis nanu tey mbir yu tiiñ am xel.»
27 Gannaaw loolu Yeesu génn, gis ab juutikat bu ñuy wax Lewi, mu toog ca juuti ba. Mu ne ko: «Kaay, topp ma.»
28 Lewi jóg, bàyyi lépp, topp ca moom.
29 Ci kaw loolu Lewi waajalal ko bernde ju réy ca këram. Mbooloo mu bare teew, ay juutikat ak yeneen gan, ñu bokk toog, di lekk.
30 Farisen yi ak seeni firikat nag di xultu ci kaw taalibey Yeesu yi, ne leen: «Lu tax ngeen di lekkandoo ak a naanandoo ak juutikat yeek bàkkaarkat yi?»
31 Yeesu ne leen: «Du ñi wér ñoo soxla fajkat, ñi wéradi ñoo ko soxla.
32 Du ñi jub nag laa woosi, bàkkaarkat yi laay woo, ngir jëme leen cig tuubeel.»
33 Dañoo wax Yeesu, ne ko: «Taalibey Yaxya de, dinañu faral di woor, di julli. Farisen yi it noonu, waaye sa ñoñ, lekk ak a naan lañu wéye.»
34 Yeesu ne leen: «Ndax man ngeena woorloo ay gan ñu wàlli ag céet, li feek boroom séet biy teew ci seen biir?
35 Waaye ay bés a ngi ñëw, dees na jële boroom séet bi ci seen biir. Kera bés yooyu nag, dinañu woor.»
36 Yeesu léebati leen, ne leen: «Mbubb mu bees, deesu ci xotti ab sekkit, ngir daaxe ko mbubb mu ràpp. Lu ko moy mbubb mu bees mi xottiku ba noppi, te du tax sekkit wu bees wi ànd ak mbubb mi ràpp.
37 Te it mbuus yu ràpp, deesu ci duy biiñ bu bees. Lu ko moy biiñ bu bees bi fàcc mbuus yi; biiñ bi tuuru, mbuus yi yàqu.
38 Biiñ bu bees daal, ci mbuus mu bees lees koy denc.
Luug 5 in Kàddug Yàlla gi