Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 4:4-15 in Wolof

Help us?

LUUG 4:4-15 in Téereb Injiil

4 Yeesu ne ko: «Mbind mi nee na: “Nit du dunde mburu rekk.”»
5 Seytaane yóbbu na ko fu kawe. Ci xef ak xippi mu won ko réewi àddina sépp,
6 ne ko: «Dinaa la jox bépp sañ-sañu nguur yii ak seen ndam ndaxte jébbal nañu ma ko, te ku ma soob laa koy jox.
7 Kon boo ma màggalee, dinga moom lépp.»
8 Yeesu ne ko: «Mbind mi nee na: “Nanga màggal Yàlla sa Boroom te jaamu ko moom rekk.”»
9 Seytaane yóbbu na ko Yerusalem, teg ko ca njobbaxtalu kër Yàlla ga ne ko: «Boo dee Doomu Yàlla, tëbal jëm ci suuf,
10 ndaxte Mbind mi nee na: “Dina jox ay malaakaam ndigal ci sa mbir, ñu sàmm la,
11 dinañu la leewu ci seeni loxo, ngir nga baña fakktalu ciw doj.”»
12 Yeesu ne ko: «Bind nañu ne: “Bul diiŋat Yàlla, sa Boroom.”»
13 Bi mu ko lalalee fiiram yi mu am yépp, Seytaane daldi sore Yeesu, di xaar yeneen jamono.
14 Yeesu dellu diiwaanu Galile, fees ak dooley Xelum Yàlla, te turam siiw ca diiwaan booba bépp.
15 Muy jàngle ca seeni jàngu, te ñépp di ko tagg.
LUUG 4 in Téereb Injiil

Luug 4:4-15 in Kàddug Yàlla gi

4 Yeesu ne ko: «Bindees na ne du aw ñam doŋŋ la nit di dunde.»
5 Seytaane yéege na ko itam, won ko mboolem nguuri àddina, ci xef ak xippi.
6 Seytaane ne Yeesu: «Yaw laay may mboolem kilifteef gii ak daraja ji mu àndal, ndax man lees ko jox, te ku ma soob laa koy may.
7 Kon nag soo ma sujjóotalee, yaa moom lépp.»
8 Yeesu ne ko: «Bindees na ne: “Boroom bi sa Yàlla ngay sujjóotal, te moom doŋŋ ngay jaamu.”»
9 Seytaane yóbbu na ko Yerusalem, aj ko ca njobbaxtalu kër Yàlla ga, ne ko: «Ndega yaa di Doomu Yàlla, tëbeel fii, wàcc,
10 ndax bindees na ne: “Ay malaakaam lay jox ndigal ci sa mbir, ñu sàmm la,
11 te seeni loxo lañu lay leewoo, ba doo fakktaloo aw doj.”»
12 Yeesu ne ko: «Bindees na ne: “Bul seetlu Boroom bi sa Yàlla.”»
13 Seytaane lalal na Yeesu gépp fiir ba sottal, doora dem, bàyyi ko ab diir.
14 Ba loolu amee Yeesu dellu Galile ci manoorey Noo gi, ab jëwam nag law ca diiwaan ba bépp ba mu daj.
15 Muy jàngle ca seeni jàngu, ñépp di ko kañ.
Luug 4 in Kàddug Yàlla gi