Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 4:29-43 in Wolof

Help us?

LUUG 4:29-43 in Téereb Injiil

29 Noonu ñu jóg, génne ko dëkk ba, yóbbu ko ca mbartalum tund, wa ñu sanc seen dëkk, ngir bëmëx ko ci suuf.
30 Waaye moom mu jaar ci seen biir, dem yoonam.
31 Gannaaw loolu Yeesu dem Kapernawum, ab dëkk ca diiwaanu Galile.
32 Mu jàngal leen ca bésub noflaay ba, ñu waaru ca njàngleem, ndaxte dafa wax ak sañ-sañ.
33 Noonu am na ci jàngu bi nit ku rab jàpp. Mu daldi xaacu ne:
34 «Moo! Yaw Yeesum Nasaret, loo nuy fexeel? Ndax dangaa ñëw ngir alag nu? Xam naa la, yaa di Aji Sell ji jóge ci Yàlla!»
35 Waaye Yeesu gëdd ko naan: «Noppil te génn ci moom!» Noonu rab wi daaneel nit ki ci suuf ci kanam ñépp, daldi génn ci moom te gaañu ko.
36 Bi loolu amee ñépp waaru, ñuy waxante ci seen biir naan: «Céy jii wax! Ci sañ-sañ ak doole lay sant rab yi, ñu daldi génn.»
37 Noonu turam siiw ca diiwaan bépp.
38 Bi mu jógee ci jàngu bi, Yeesu dafa dem kër Simoŋ. Gorob Simoŋ bu jigéen dafa feebar, ba yaram wi tàng lool. Ñu ñaan Yeesu, mu dimbali leen ci.
39 Mu randusi, tiim ko, gëdd tàngoor wi, mu dem. Noonu tàngoor wi wàcc, soxna si jóg ca saa sa, di leen topptoo.
40 Bi jant sowee, ñu indil Yeesu ñi wopp ñépp ak ay jàngoro yu wuute. Kenn ku nekk mu teg la loxo, wéral la.
41 Te it ay rab di génn ca nit ña te di yuuxu naan: «Yaay Doomu Yàlla!» Noonu mu gëdd leen, te mayu leen, ñu wax dara, ndaxte xam nañu ne mooy Almasi bi.
42 Ca njël gu jëkk Yeesu génn, dem ca bérab bu wéet. Mbooloo ma di ko seet. Bi ñu ko gisee, ñu koy wuta téye, ngir bañ mu dem.
43 Mu ne leen: «Damaa wara dem ci yeneen dëkk yi, ngir yégle xibaaru jàmm bi ci nguuru Yàlla, ndaxte looloo tax ñu yónni ma.»
LUUG 4 in Téereb Injiil

Luug 4:29-43 in Kàddug Yàlla gi

29 Ñu jóg, bëmëx ko ba génne ko dëkk ba, yóbbu ko ca kéméju tund, wa seen dëkk ba sance, ngir xalab ko ci suuf.
30 Teewul moom mu jaare ci seen biir, dem yoonam.
31 Ba mu ko defee Yeesu dem Kapernawum, ab dëkk ca diiwaanu Galile, di leen jàngal ca bési Noflaay ya.
32 Nit ña nag yéemu ca njàngleem, ndax sañ-sañ ba muy waxe.
33 Ndeke foofa ca jàngu ba, jenn waay ju rab jàpp a nga fa woon. Waa ji jekki xaacu, ne:
34 «Moo yaw Yeesum Nasaret, lu nu joteek yaw? Alagsi nu mooy say tànk? Xam naa yaa di kan, yaa di Aji Sell ju Yàlla ji!»
35 Yeesu nag gëdd ko, ne ko: «Noppil te génn nit ki!» Rab wa daaneel nit ki ca digg mbooloo ma, doora génn te gaañu ko fenn.
36 Ba loolu amee ñépp a waaru, di wax ci seen biir, naan: «Gii kàddu lu mu doon? Moom de sañ-sañ ak xam-xam lay joxe rab yi ndigal, ñu génn.»
37 Coowal Yeesu nag law ba fépp fu bokk ca diiwaan ba.
38 Yeesu jóge jàngu ba, dem kër Simoŋ, daldi fekk yaayu jabaru Simoŋ ànd ak tàngooru yaram wu réy. Ñu ñaan ci Yeesu ndimbal.
39 Mu dikk, tiim soxna sa, daldi gëdd tàngooru yaram wa, tàngoor wa teqlikook moom. Soxna sa jóg ca saa sa, di leen topptoo.
40 Ba jant sowee, mboolem ña amoon ay jarag yu ame ay jàngoroy jàngoro, daldi leen indil Yeesu. Moom it, mu teg kenn ku ci nekk ay loxoom, wéral la.
41 Ay rab itam di génn ñu bare, di yuuxu, te naan: «Yaay Doomu Yàlla!» Teewul mu gëdd leen, aaye leen ñu wax, ndax xamoon nañu ne mooy Almasi.
42 Njël gu jëkk ca ëllëg sa la Yeesu génn dëkk ba, dem ba bérab bu wéet. Mbooloo ma nag di ko seet, ba dikk, di ko téye, bañ mu dem, ba leen.
43 Mu ne leen: «Yeneen dëkk yeet, war na ma faa yégleji xibaaru jàmm bu nguurug Yàlla, ndax loolu lañu ma yebale.»
Luug 4 in Kàddug Yàlla gi