23 Mu daldi leen ne: «Xam naa ne dingeen ma ne: “Fajkat bi, fajal sa bopp. Yég nanu li xew Kapernawum, defal lu ni mel fii ci réew mi nga dëkk.”»
24 Mu tegaat ca ne: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ab yonent kenn du ko teral ca réewam.
25 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ca jamonoy Ilyaas, bi mu tawul lu mat ñetti at ak genn-wàll, te xiif bu metti am ca réew mépp, amoon na ca Israyil jigéen yu bare yu seen jëkkër faatu.
26 Moona Yàlla yónniwul Ilyaas ci kenn ci ñoom, waaye mu yebal ko ci jigéen ju jëkkëram faatu, ju dëkk Sarebta, ca wetu Sidon.
27 Te it amoon na ca Israyil, ca jamonoy yonent Yàlla Alyaasa, ay nit ñu bare ñu gaana. Waaye fajul ci kenn ku dul Naamaan, mi dëkkoon réewu Siri.»
28 Bi ñu déggee wax yooya, ñépp ña nekkoon ca jàngu ba daldi fees ak mer.
29 Noonu ñu jóg, génne ko dëkk ba, yóbbu ko ca mbartalum tund, wa ñu sanc seen dëkk, ngir bëmëx ko ci suuf.
30 Waaye moom mu jaar ci seen biir, dem yoonam.