14 Yeesu dellu diiwaanu Galile, fees ak dooley Xelum Yàlla, te turam siiw ca diiwaan booba bépp.
15 Muy jàngle ca seeni jàngu, te ñépp di ko tagg.
16 Yeesu dem Nasaret fa mu yaroo, te ca bésub noflaay ba, mu dugg ca jàngu ba, ni mu ko daan defe. Noonu mu taxaw ngir jàngal mbooloo mi.
17 Ñu jox ko téereb yonent Yàlla Esayi. Bi mu ko ubbee, mu gis bérab, ba ñu bind aaya yii:
18 «Xelum Boroom baa ngi ci man, ndaxte moo ma tànn, ngir ma yégal néew doole yi xibaaru jàmm bi. Dafa maa yónni, ngir ma yégal jaam ñi ne dinañu leen goreel, yégal gumba yi ne dinañu gis, te jot ñi ñu not,
19 tey yégle atum yiw, mi jóge ci Boroom bi.»
20 Bi mu jàngee aaya yooyu ba noppi, mu ub téere bi, delloo ko ki koy denc, toog. Ñépp ña nekkoon ca jàngu ba dékk koy bët.
21 Noonu mu daldi ne: «Tey jii, loolu Mbind mi wax mat na, bi ngeen koy déglu.»
22 Ñépp di seede lu rafet ci Yeesu, di waaru ci wax ju neex, ji mu doon yégle, ñu naan: «Ndax kii du doomu Yuusufa?»
23 Mu daldi leen ne: «Xam naa ne dingeen ma ne: “Fajkat bi, fajal sa bopp. Yég nanu li xew Kapernawum, defal lu ni mel fii ci réew mi nga dëkk.”»
24 Mu tegaat ca ne: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ab yonent kenn du ko teral ca réewam.
25 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ca jamonoy Ilyaas, bi mu tawul lu mat ñetti at ak genn-wàll, te xiif bu metti am ca réew mépp, amoon na ca Israyil jigéen yu bare yu seen jëkkër faatu.
26 Moona Yàlla yónniwul Ilyaas ci kenn ci ñoom, waaye mu yebal ko ci jigéen ju jëkkëram faatu, ju dëkk Sarebta, ca wetu Sidon.
27 Te it amoon na ca Israyil, ca jamonoy yonent Yàlla Alyaasa, ay nit ñu bare ñu gaana. Waaye fajul ci kenn ku dul Naamaan, mi dëkkoon réewu Siri.»
28 Bi ñu déggee wax yooya, ñépp ña nekkoon ca jàngu ba daldi fees ak mer.
29 Noonu ñu jóg, génne ko dëkk ba, yóbbu ko ca mbartalum tund, wa ñu sanc seen dëkk, ngir bëmëx ko ci suuf.
30 Waaye moom mu jaar ci seen biir, dem yoonam.