Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 3:3-23 in Wolof

Help us?

LUUG 3:3-23 in Téereb Injiil

3 Yaxya daldi dugg àll, bi wër dexu Yurdan gépp, di waaree nii: «Tuubleen seeni bàkkaar, ba noppi ma sóob leen ci ndox, ngir Yàlla baal leen seeni bàkkaar.»
4 Loolu lañu bind ci téereb waxi yonent Yàlla Esayi naan: «Am na baat buy xaacu ca màndiŋ ma ne: “Xàll-leen yoonu Boroom bi, jubal-leen fi muy jaar.
5 Nañu sëkk xur yi, maasale tund yi ak jànj yi. Yoon yi dëng ñu jubbanti leen, yi ñagas ñu rataxal leen.
6 Bu ko defee bépp mbindeef dina gis mucc gi Yàlla tëral.”»
7 Mbooloo ma daan ñëw ngir mu sóob leen ci ndox, Yaxya daan na leen wax naan: «Yéen ñi fees ak daŋar mel ni ay co! Ku leen artu ngeen daw merum Yàlla mi nara wàcc?
8 Jëfeleen nag ni ñu tuub seeni bàkkaar, te baña nax seen bopp naan: “Nun daal doomi Ibraayma lanu,” ndaxte maa ngi leen koy wax, Yàlla man na defal Ibraayma ay doom ci doj yii.
9 Sémmiñ wi tiim na reeni garab yi. Garab nag gu meññul doom yu baax, dees na ko gor, sànni ko ci sawara si.»
10 Mbooloo ma laaj ko ne: «Lan lanu wara def nag?»
11 Mu ne leen: «Ku am ñaari mbubb, nga jox menn mi ki amul. Ku am ñam itam, nga bokk ko ak ki amul.»
12 Ay juutikat itam ñëw ca Yaxya, ngir mu sóob leen ci ndox; ñu ne ko: «Kilifa gi, lu nu wara def?»
13 Mu ne leen: «Laajleen rekk lu jaadu.»
14 Ay xarekat laaj nañu ko ne: «Li jëm ci nun nag?» Mu ne leen: «Buleen néewal doole kenn, jël xaalisam ci kaw ay tëkku mbaa ci seede lu dul dëgg. Waaye doylooleen li ñu leen di fey.»
15 Mbooloo maa ngay xaar, di séentook a laaj ci seen xel, ndax Yaxya mooy Almasi bi.
16 Noonu Yaxya wax leen ñoom ñépp ne leen: «Man maa ngi leen di sóob ci ndox. Waaye ki ma ëpp kàttan dina ñëw te yeyoowumaa tekki ay dàllam. Kooku dina leen sóob ci Xel mu Sell mi ak sawara.
17 Layoom mu ngi ci loxoom, ngir jéri dàgga ja, ba mu set; pepp ma dina ko def ca sàqam, waaye xatax ba dina ko lakk ci sawara su dul fey mukk.»
18 Noonu Yaxya teg ca yeneen dénkaane yu bare, di yégal nit ña xibaaru jàmm ba.
19 Waaye Yaxya yedd na Erodd boroom diiwaanu Galile, ndaxte dafa takkoon Erojàdd jabaru magam, te it boole woon na ci yeneen ñaawteef,
20 ba faf tëj Yaxya kaso.
21 Noonu Yaxya sóob mbooloo mépp ci ndox, sóobaale it Yeesu. Bi Yeesu di ñaan nag, asamaan daldi ubbiku.
22 Noonu Xel mu Sell mi daldi wàcc ci moom, yor jëmmu pitax, te baat bu jóge asamaan jib ne: «Yaa di sama Doom, ji ma bëgg; ci yaw laa ame bànneex.»
23 Bi Yeesu di tàmbali liggéeyam, amoon na lu wara tollu ci fanweeri at, di doomu Yuusufa ci bëti nit ñi. Te Yuusufa mooy doomu Eli,
LUUG 3 in Téereb Injiil

Luug 3:3-23 in Kàddug Yàlla gi

3 Yaxya dugg mboolem àll, bi wër dexu Yurdan, di waare lu jëm ci tuubeel gu nit ñi wara fésale ag sóobu cim ndox, ngir ñu jéggal leen seeni bàkkaar.
4 Loolu lañu bind ci téereb waxi Yonent Yàlla Esayi ne: «Baat a ngi xaacoo ca màndiŋ ma, naan: “Xàll-leen yoonu Boroom bi, jubal-leen ay xàllam.
5 Xur yépp ay sëkke, tund wu magoo wu ndaw maasaloo, yoon ya lunkoon, jubbantiku, ya ñagasoon, nooy,
6 ba wépp suux gis mucc gi Yàlla dogal.”»
7 Yaxya nag di wax mbooloo may ñëw ngir mu sóob leen ci ndox, naan leen: «Yeen njurum jaan mee, ku leen àrtu, ba ngeen di daw sànj miy dikk?
8 Kon nag jëfeleen jëf ju yelloo ag tuubeel, te baña nax seen bopp naan: “Nun, Ibraayma mooy sunu maam,” ndax maa leen ko wax, doj yii, Yàlla man na cee sàkkal Ibraayma aw askan.
9 Te itam sémmiñ xàccil na reenu garab ba noppi. Kon nag gépp garab gu ci meññul doom yu baax, dees koy gor, sànni ca sawara sa.»
10 Mbooloo ma itam laaj ko ne ko: «Ana lu nu war nag?»
11 Mu ne leen: «Ku am ñaari turki, na sédd ki amul. Ku am aw ñam itam, na defe noonu.»
12 Ay juutikat itam dikk, ngir sóobusi; ñu ne Yaxya: «Sëriñ bi, ana lu nu war?»
13 Mu ne leen: «Xanaa baña sàkku lenn lu moy li jaadu.»
14 Ay takk-der itam ne ko: «Nun nag, nu nuy def?» Mu ne leen: «Buleen néewal kenn doole, mbaa di duural kenn ngir jëlal ko dara; doyloo leen seen peyoor.»
15 Ci kaw loolu askan wa di séentu, ñépp di seetaat ci seen xel, ndax Yaxya mooy Almasi.
16 Yaxya wax leen ñoom ñépp ne leen: «Man de ci ndox laa leen di sóob. Waaye ku ma sut a ngi ñëw, kooku, buumi caraxam sax, yeyoowuma ko koo feccil. Moom, ci Noo gu Sell gi ak sawara la leen di sóob.
17 Ab layoom a ngi ci loxoom, mooy jéri dàggaam, ba mu set wecc; pepp mi lay fat cim sàqam, waaye xatax bi, da koy lakk ci sawara su dul fey mukk.»
18 Bare na yeneen dénkaane yu Yaxya doon xamale nit ñi xibaaru jàmm bi.
19 Erodd boroom diiwaan ba nag, Yaxya sikkoon na ko ndax Erojàdd jabaru magam ja mu nekkaloon, ak mboolem yeneen ñaawtéef yu Erodd def.
20 Mu tegati leneen ca loolu lépp: jàpp Yaxya, tëj ca kaso ba.
21 Noonu Yaxya doon sóobe ñépp cim ndox, ni la deme ba Yeesu dikk, mu sóob ko ci ndox. Ci biir loolu Yeesu yékkati kàddug ñaan, asamaan ubbiku.
22 Ba loolu amee Noo gu Sell gi moo bindoo ni pitax, wàcc ci kawam, baat jibe asamaan, ne: «Yaa di sama Doom, sama soppe; yaa may bànneexal.»
23 Yeesu ci boppam ba muy door, amoon na lu tollu ci fanweeri at, di doomu Yuusufa, ni ko xel mana jàppe. Yuusufa, Eli mooy baayam,
Luug 3 in Kàddug Yàlla gi