Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 2:6-10 in Wolof

Help us?

LUUG 2:6-10 in Téereb Injiil

6 Bi ñu nekkee Betleyem, waxtu wa mu waree mucc agsi.
7 Mu taawloo doom ju góor, mu laxas ko ci ay laytaay, tëral ko ca lekkukaayu jur ga, ndaxte xajuñu woon ca dalukaay ba.
8 Fekk booba amoon na ca gox ba ay sàmm yu daan fanaan ca tool ya, di wottu jur ga.
9 Noonu benn malaakam Boroom bi feeñu leen, ndamu Boroom bi daldi leer, melax, wër leen. Tiitaange ju réy jàpp leen.
10 Waaye malaaka mi ne leen: «Buleen tiit, ndaxte dama leen di xamal xibaaru jàmm buy indi mbég mu réy ci nit ñépp.
LUUG 2 in Téereb Injiil

Luug 2:6-10 in Kàddug Yàlla gi

6 Naka lañu dal Betleyem, waxtuw muccam agsi.
7 Mu am doom ju góor, mu dib taawam. Mu laxas ko, tëral ko ca gàmbug jur ga, ndax ñàkk fu ñu xaj ca néegu gan ba.
8 Booba ay sàmm a nga ca gox boobee, di fanaanee wattu seenug jur.
9 Am malaakam Boroom bi jekki feeñu leen, leeru Boroom bi melax, wër leen, ñu tiit tiitaange lu réy.
10 Malaaka mi ne leen: «Buleen tiit, ndax kat maa leen indil xibaaru jàmm bu doon mbég mu réy, ñeel askan wépp.
Luug 2 in Kàddug Yàlla gi