Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 2:10-27 in Wolof

Help us?

LUUG 2:10-27 in Téereb Injiil

10 Waaye malaaka mi ne leen: «Buleen tiit, ndaxte dama leen di xamal xibaaru jàmm buy indi mbég mu réy ci nit ñépp.
11 Tey jii ca dëkku Daawuda, ab Musalkat juddul na leen fa, te mooy Almasi bi, di Boroom bi.
12 Ci firnde jii ngeen koy xàmmee: dingeen gis liir bu ñu laxas ci ay laytaay, tëral ko ci lekkukaayu jur.»
13 Bi mu waxee loolu, yeneen malaaka yu bare yu jóge asamaan, ànd ak moom, di sant Yàlla naan:
14 «Nañu màggal Yàlla ca asamaan su kawe sa, te ci àddina, na jàmm wàcc ci nit, ñi mu nangu ndax yiwam!»
15 Bi malaaka ya delloo ca asamaan, sàmm yi di waxante naan: «Nanu dem boog Betleyem, seeti la fa xew, li nu Boroom bi xamal.»
16 Ñu daldi gaawantu dem, gis Maryaama ak Yuusufa, ak liir, ba ñu tëral ca lekkukaayu jur ga.
17 Bi ñu leen gisee, ñu nettali la ñu leen waxoon ca mbirum xale ba.
18 Ñi dégg li sàmm yi doon wax ñépp daldi waaru lool.
19 Waaye Maryaama moom, takkoon na mbir yooyu yépp, di ko xalaat ci xolam.
20 Noonu sàmm ya dellu ca seen jur, di màggal Yàlla, di ko sant ci li ñu déggoon lépp te gis ko, ndaxte lépp am na, ni ko Boroom bi waxe woon.
21 Bi bés ba délsee jamonoy xarafal xale ba agsi. Ñu tudde ko Yeesu, ni ko malaaka ma diglee woon, laata ko yaayam di ëmb.
22 Noonu jamono ji ñu leen waroona sellale agsi, ni ko yoonu Musaa tërale. Waajuri Yeesu yi daldi koy yóbbu ca dëkku Yerusalem, ngir sédde ko Boroom bi.
23 Ndaxte bind nañu ci yoonu Boroom bi ne: «Bépp taaw bu góor, nañu ko sédde Boroom bi.»
24 Bi ñu ko yóbboo, def nañu itam sarax, ni ko yoonu Boroom bi santaanee: «ñaari pitaxu àll walla ñaari xati yu ndaw.»
25 Amoon na ca Yerusalem nit ku tudd Simeyon. Nit ku fonkoon yoonu Yàlla la te déggal ko, doon séentu jamono, ji Yàlla wara dëfal bànni Israyil. Xel mu Sell mi mu ngi ci moom,
26 te xamal na ko ne du dee mukk te gisul Almasib Boroom bi.
27 Noonu Xelum Yàlla daldi yóbbu Simeyon ba ca kër Yàlla ga. Bi waajuri Yeesu indee xale ba, ngir sédde ko Yàlla, ni ko yoon wi santaanee,
LUUG 2 in Téereb Injiil

Luug 2:10-27 in Kàddug Yàlla gi

10 Malaaka mi ne leen: «Buleen tiit, ndax kat maa leen indil xibaaru jàmm bu doon mbég mu réy, ñeel askan wépp.
11 Bésub tey jii ca dëkku Daawuda, juddule ngeen ab Musalkat, te mooy Almasi, di Sang bi.
12 Li ngeen ciy def ab takk moo di: dingeen gis liir bu ñu laxas, tëral ko ci gàmbug jur.»
13 Ca saa sa gàngooru asamaan gu mag ànd ak malaaka mi, di sàbbaal Yàlla, ne:
14 «Daraja ñeel na Yàlla fa asamaan sa gëna kawe, jàmm ci kaw suuf ñeel ñi Yàlla baaxe.»
15 Ba malaaka ya bàyyikoo ca sàmm sa, dellu asamaan, ñuy wax ca seen biir, naan: «Nanu dem boog Betleyem, seeti la fa xew, te Boroom bi xamal nu ko.»
16 Ñu gaaw dem ba foofa, daldi gis Maryaama ak Yuusufa, ak liir ba tëdd ca gàmbug jur ga.
17 Naka lañu leen gis, daldi leen xamal la ñu leen wax ca mbirum xale ba.
18 Mboolem ña dégg la leen sàmm sa wax nag waaru lool.
19 Teewul Maryaama moom, bàyyi woon na xel ci mbir moomu mépp, di ko xalaat ci xolam.
20 Ba loolu amee sàmm sa dellu, di sàbbaal ak a sant Yàlla ci mboolem la ñu dégg, gis ko, te lépp ame noonee ñu leen ko waxe woon.
21 Ba juróom ñetti fani xale bi matee, ñu xarfal ko, tudde ko Yeesu, na ko malaaka ma tudde woon, bala moo sosu.
22 Gannaaw ba seen fani setlu matee, ni ko yoonu Musaa laaje, ñu yóbbu xale bi Yerusalem, ngir teewal ko fi kanam Boroom bi,
23 noonee ñu ko binde ci yoonu Boroom bi ne: «Bépp taaw bu góor, dees koy tudde séddoo bu sell, ñeel Boroom bi.»
24 Ñu yóbbaale sarax bi ci war, ni ko yoonu Boroom bi santaanee: «ñaari pitaxu àll mbaa ñaari xati yu ndaw.»
25 Amoon na nag ca Yerusalem ku ñuy wax Simeyon; ku juboon, ragal Yàlla, di séentu jamono ji nekkinu bànni Israyil di ame ag tan, te Noo gu Sell gi àndoon ak moom.
26 Ndéey nag tukkee ci Noo gu Sell gi, xamal ko ne ko du dee mukk te gisul Almasi bu Boroom bi.
27 Ci kaw loolu mu dem ba ca biir kër Yàlla ga ci dooley Noo gu Sell gi. Gannaaw loolu waajuri Yeesu indi Yeesu ngir defal ko li aaday yoon wi laaj.
Luug 2 in Kàddug Yàlla gi