47 Naka la Yeesu di wax, daaneelagul, mbooloo ne jimeet, ka ñuy wax Yuda, di kenn ca Fukk ñaak ñaar jiite leen. Yuda dikk ba ci Yeesu, bëgg koo fóon.
48 Yeesu ne ko: «Yuda, fóon ngay wore Doomu nit ki!»
49 Ña ànd ak Yeesu nag gis la ca nara topp, ñu ne: «Sang bi, nu jame saamar boog?»
50 Kenn ci ñoom daldi caw surgab sarxalkat bu mag ba, njoof noppu ndijooram.
51 Teewul Yeesu ne: «Bàyyileen, na fi yem.» Mu laal noppu waa ja, wéral ko.
52 Ba loolu amee Yeesu wax ak ña ko jàppsi: sarxalkat yu mag ya, ak kilifay wattukati kër Yàlla ga, ak mag ña. Mu ne leen: «Mbete dama di ab fippukat, ba ngeen dikkey saamar aki njur.
53 Moona bés bu nekk, maak yeen la woon ca kër Yàlla ga, te teguleen ma loxo. Waaye seen waxtu la léegi, bi kilifteefug lëndëm ayee nii.»