Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 22:35-58 in Wolof

Help us?

LUUG 22:35-58 in Téereb Injiil

35 Noonu Yeesu ne leen: «Ba ma leen yebalee te yóbbaalewuleen woon xaalis, mbuus, walla dàll, ndax ñàkkoon ngeen dara?» Ñu ne ko: «Déedéet.»
36 Mu ne leen: «Léegi nag képp ku am xaalis, na ko jël; te ku am mbuus, na ko jël; ku amul jaasi, na jaay mbubbam, jënde ko jaasi.
37 Ndaxte maa ngi leen koy wax, lii Mbind mi wax fàww mu am ci man, bi mu nee: “Boole nañu ko ak ñu bon ña.” Ndaxte loolu jëm ci man mi ngi mat.»
38 Noonu taalibe ya ne ko: «Boroom bi, ñaari jaasee ngii.» Mu ne leen: «Doy na.»
39 Noonu Yeesu génn, dem ca tundu Oliw ya, ni mu ko daan defe naka-jekk. Taalibeem ya topp ci moom.
40 Bi mu agsee ca bérab ba, mu ne leen: «Ñaanleen, ngir baña daanu cig fiir.»
41 Noonu mu dànd leen, ba fu aw saan mana tollu, daldi sukk di ñaan ne:
42 «Baay, soo ko bëggee, teggil ma kaasu naqar bii. Moona bumu doon sama coobare, waaye na sa coobare am.»
43 Noonu malaakam Yàlla daldi koy feeñu, may ko doole.
44 Ci biir tiis, Yeesu gëna sawar ci ñaan gi, ñaqam mel ni lumbi deret dal ci suuf.
45 Bi mu ñaanee ba noppi, mu jóg, délsi ci taalibe yi, fekk leen ñuy nelaw, ndaxte seen xol dafa sonnoon ak tiis.
46 Noonu mu ne leen: «Lu tax ngeen di nelaw? Jógleen ñaan, ngir baña daanu cig fiir.»
47 Bi Yeesu di wax, mbooloo mu bare agsi; ku ñuy wax Yudaa te mu bokkoon ci fukki ndaw yi ak ñaar jiite leen. Yudaa jegeñsi Yeesu, bëgg koo fóon.
48 Waaye Yeesu ne ko: «Ci fóon ngay jébbale Doomu nit ki ay noonam!»
49 Bi ñi àndoon ak Yeesu gisee liy bëgga xew, ñu ne: «Boroom bi, ndax nu dóore jaasi?»
50 Kenn ci ñoom nag dóor surgab sarxalkat bu mag ba, noppu ndijooram dagg.
51 Waaye Yeesu daldi ne: «Bàyyileen.» Mu laal noppu waa ja, wéral ko.
52 Noonu Yeesu ne sarxalkat yu mag ya ak kilifay wottukati kër Yàlla ga ak njiiti xeet, wa ko jàppsi woon: «Jóg ngeen, gànnaayoo jaasi ak yet, mel ni ñuy topp sàcc.
53 Moona maa nga woon ak yéen bés bu nekk ca kër Yàlla ga, te jàppuleen ma. Waaye léegi seen waxtu la, di jamonoy lëndëm.»
54 Ñu jàpp Yeesu, yóbbu ko ca kër sarxalkat bu mag ba. Piyeer topp fu sore.
55 Amoon na taal ca diggu ëtt ba, ay nit toog, wër ko, Piyeer itam toog ci seen biir.
56 Ab mbindaan gis ko, mu toog, taal bi di ko leeral, mu ne ko jàkk ne: «Nit kii itam àndoon na ak moom.»
57 Waaye Piyeer weddi ko ne: «Soxna si, xawma kooku.»
58 Nees-tuut keneen gis ko ne: «Yaw itam ci ñoom nga bokk.» Piyeer ne ko: «Sama waay, bokkuma ci.»
LUUG 22 in Téereb Injiil

Luug 22:35-58 in Kàddug Yàlla gi

35 Yeesu neeti leen: «Ba ma leen yebalee te du dencukaayu xaalis, du mbuus, du carax yu ngeen yóbbaale, ndax ñàkk ngeen dara?» Ñu ne ko: «Déedéet.»
36 Mu ne leen: «Léegi nag képp ku am dencukaayu xaalis, na ko jël, ku am mbuus it, na ko jël; ku amul saamar, na jaay mbubbam, jënde saamar.
37 Ndax maa leen ko wax, li ñu bind ne, “Mook defkati mbon yi lañu boole ab àtte,” fàww mu am ci man, te loolu jëm ci sama mbir mu ngi sottisi.»
38 Ñu ne ko: «Sang bi, ñaari saamar a ngi fi.» Mu ne leen: «Doy na.»
39 Ci kaw loolu Yeesu génn, jëm ca tundu Oliw ya, na mu ko baaxoo woon, taalibe ya topp ci moom.
40 Ba mu agsee ca bérab ba, da ne leen: «Ñaanleen, ngir baña tàbbi cig fiir.»
41 Ba loolu amee mu dànd leen lu tollook saanu xeer, daldi sukk, di ñaan.
42 Mu ne: «Baay, su dee sa coobare, teggil ma kaasu naqar bii. Bumuy sama coobare nag, waaye yaw, na sa coobare am.»
43 Malaaka mu bawoo asamaan daldi koy feeñu, dooleel ko.
44 Njàqare nag jàpp Yeesu, mu gënatee tënku ci kàdduy ñaanam, ba aw ñaqam mujj mel ni lumbi deret, di dal ci suuf.
45 Mu ñaan ba noppi, daldi jóg, délsi ci taalibe yi, fekk leen ñuy nelaw, sonn lool ndax aw tiis.
46 Mu ne leen: «Lu ngeen di nelaw? Jógleen ñaan, ngir baña tàbbi cig fiir.»
47 Naka la Yeesu di wax, daaneelagul, mbooloo ne jimeet, ka ñuy wax Yuda, di kenn ca Fukk ñaak ñaar jiite leen. Yuda dikk ba ci Yeesu, bëgg koo fóon.
48 Yeesu ne ko: «Yuda, fóon ngay wore Doomu nit ki!»
49 Ña ànd ak Yeesu nag gis la ca nara topp, ñu ne: «Sang bi, nu jame saamar boog?»
50 Kenn ci ñoom daldi caw surgab sarxalkat bu mag ba, njoof noppu ndijooram.
51 Teewul Yeesu ne: «Bàyyileen, na fi yem.» Mu laal noppu waa ja, wéral ko.
52 Ba loolu amee Yeesu wax ak ña ko jàppsi: sarxalkat yu mag ya, ak kilifay wattukati kër Yàlla ga, ak mag ña. Mu ne leen: «Mbete dama di ab fippukat, ba ngeen dikkey saamar aki njur.
53 Moona bés bu nekk, maak yeen la woon ca kër Yàlla ga, te teguleen ma loxo. Waaye seen waxtu la léegi, bi kilifteefug lëndëm ayee nii.»
54 Ba mu ko defee ñu jàpp Yeesu, yóbbu ko ba ca kër sarxalkat bu mag ba, Piyeer dànd fu sore, topp ca.
55 Fekk na ñu taal sawara ca digg ëtt ba, toog yéew sawara wa, Piyeer dikk toog ca seen biir.
56 Ab surga bu jigéen nag gis ko, mu toog fi kanam taal bi, mu ne ko jàkk, ne: «Kii it ci la, moom la àndaloon!»
57 Piyeer nag miim, ne: «Soxna si, xawma kooku!»
58 Nes tuut keneen gis ko ne: «Yaw it ci ñoom nga!» Piyeer ne ko: «Waa jii, du man!»
Luug 22 in Kàddug Yàlla gi