33 Piyeer ne ko: «Sang bi, jekk naa ci ànd ak yaw kaso, ak ci ànd ak yaw dee.»
34 Yeesu ne ko: «Piyeer, maa la ko wax, bala ganaar a sab tey jii, dinga weddi ñetti yoon ne xam nga ma.»
35 Yeesu neeti leen: «Ba ma leen yebalee te du dencukaayu xaalis, du mbuus, du carax yu ngeen yóbbaale, ndax ñàkk ngeen dara?» Ñu ne ko: «Déedéet.»
36 Mu ne leen: «Léegi nag képp ku am dencukaayu xaalis, na ko jël, ku am mbuus it, na ko jël; ku amul saamar, na jaay mbubbam, jënde saamar.
37 Ndax maa leen ko wax, li ñu bind ne, “Mook defkati mbon yi lañu boole ab àtte,” fàww mu am ci man, te loolu jëm ci sama mbir mu ngi sottisi.»
38 Ñu ne ko: «Sang bi, ñaari saamar a ngi fi.» Mu ne leen: «Doy na.»
39 Ci kaw loolu Yeesu génn, jëm ca tundu Oliw ya, na mu ko baaxoo woon, taalibe ya topp ci moom.
40 Ba mu agsee ca bérab ba, da ne leen: «Ñaanleen, ngir baña tàbbi cig fiir.»
41 Ba loolu amee mu dànd leen lu tollook saanu xeer, daldi sukk, di ñaan.
42 Mu ne: «Baay, su dee sa coobare, teggil ma kaasu naqar bii. Bumuy sama coobare nag, waaye yaw, na sa coobare am.»
43 Malaaka mu bawoo asamaan daldi koy feeñu, dooleel ko.
44 Njàqare nag jàpp Yeesu, mu gënatee tënku ci kàdduy ñaanam, ba aw ñaqam mujj mel ni lumbi deret, di dal ci suuf.
45 Mu ñaan ba noppi, daldi jóg, délsi ci taalibe yi, fekk leen ñuy nelaw, sonn lool ndax aw tiis.
46 Mu ne leen: «Lu ngeen di nelaw? Jógleen ñaan, ngir baña tàbbi cig fiir.»
47 Naka la Yeesu di wax, daaneelagul, mbooloo ne jimeet, ka ñuy wax Yuda, di kenn ca Fukk ñaak ñaar jiite leen. Yuda dikk ba ci Yeesu, bëgg koo fóon.
48 Yeesu ne ko: «Yuda, fóon ngay wore Doomu nit ki!»
49 Ña ànd ak Yeesu nag gis la ca nara topp, ñu ne: «Sang bi, nu jame saamar boog?»
50 Kenn ci ñoom daldi caw surgab sarxalkat bu mag ba, njoof noppu ndijooram.