Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 21:6-27 in Wolof

Help us?

LUUG 21:6-27 in Téereb Injiil

6 «Li ngeen gis fii lépp, jamono dina ñëw joo xam ne dina daanu, ba doj dootul des ci kaw doj.»
7 Ñu laaj ko ne: «Kilifa gi, kañ la loolu di am? Ak luy tegtal ne looloo ngi waaja xew?»
8 Yeesu ne: «Moytuleen, bu leen kenn nax. Ndaxte ñu bare dinañu ñëw ci sama tur ne: “Moom laa,” walla ñu naan: “Jamono ji jegesi na.” Buleen topp ñooñu.
9 Bu ngeen déggee ay xare ak ay réew yu jóg, wottuleena tiit, ndaxte fàww yooyule jëkka am. Waaye taxul mujug jamono daldi taxaw.»
10 Noonu mu teg ca ne: «Xeet dina jóg, xeex ak weneen xeet, réew dina xeex ak meneen réew.
11 Suuf dina yëngu yëngu yu réy, te wopp ak xiif dina am ci bérab yu bare. Dina am it ay xew-xew yu raglu ak ay firnde yu mag yuy jóge asamaan.
12 Waaye bala looloo xew, dees na leen jàpp, fitnaal leen, di leen jébbal àttekat yi ca jàngu ya, tëj leen kaso. Dees na leen yóbbu ci kanam i buur ak i boroom réew ndax sama tur.
13 Loolu dina leen ubbil bunt, ba ngeen man maa seedeel.
14 Fasleen yéenee baña wut lay ngir musal seen bopp.
15 Ndaxte man ci sama bopp maa leen di jox kàddu ak xel moo xam ne seeni noon duñu ko mana teggi, mbaa ñu di ko weddi.
16 Seeni waajur sax ak seeni doomi ndey, seeni bokk ak seeni xarit, dinañu leen jébbal àttekat yi, ba ñu rey ñenn ci yéen.
17 Te ñépp dinañu leen bañ ndax sama tur.
18 Waaye seen genn kawar sax du neen.
19 Seen muñ moo leen di musal.
20 «Bu ngeen gisee ay xarekat wër dëkku Yerusalem, xamleen ne jamono, ji ñu koy yàq, agsi na.
21 Kon nag ku nekk ci biir diiwaanu Yude, nanga daw ca tund ya; ku nekk ci biir dëkk bi, nanga ko génn; te ku nekk ca tool ya, bul dugg ca dëkk ba!
22 Ndaxte ci bés yooyu Yàlla dina fey jëf yi, te li ñu bindoon ci téereb Yàlla dina mat.
23 Ngalla jigéen ñi ëmb ca bés yooya, ngalla it ñiy nàmpal! Ndaxte tiis wu metti dina am ci réew mi, te Yàlla dina wàcce meram ci waa réew mii.
24 Dees na leen reye ak i jaasi, jàpp leen jaam, yóbbu leen ci réewi àddina sépp. Te ñi dul Yawut dinañu nappaaje Yerusalem, ba kera jamonoy ñi dul Yawut mat.
25 «Ay firnde dinañu feeñ ci jant bi, ci weer wi ak ci biddiiw yi. Ci kaw suuf xeet yi dinañu tiit, jaaxle ndax riiru géej gi ak yëngu-yëngub duus yi.
26 Bu boobaa nit ñiy xëm ndax tiitaange, bu ñuy xalaat musiba, yi nara wàcc ci àddina, ndaxte dees na yëngal kàttani asamaan.
27 Noonu dinañu gis Doomu nit ki di ñëw ciw niir, ànd ak kàttan ak ndam lu réy.
LUUG 21 in Téereb Injiil

Luug 21:6-27 in Kàddug Yàlla gi

6 «Lii ngeen gis nii, ay jant a ngi ñëw yu fi doj dootul des ci kaw doj, lépp ay jóoru.»
7 Ñu laaj ko ne ko: «Sëriñ bi, loolu kañ lay doon? Ak luy doon ub takk buy xamle ne looloo ngi waaja dikk?»
8 Yeesu ne: «Moytuleen, ngir ñu bañ leena nax, ndax ñu bareey dikk, tuddoo sama tur, naan: “Man a,” te naan: “Waxtu wi jege na.” Buleen leen topp.
9 Bu ngeen déggee ay xare aki salfaañoo, buleen tiit, ndax fàww loolu jëkka am. Waaye du doonagum muj ga, ca saa sa.»
10 Mu neeti leen: «Aw xeet dina jógal aw xeet, am réew jógal am réew.
11 Ay yëngu-yënguy suuf yu réy dina am, ay xiif aki mbas dikke fu bare, te xew-xew yu raglu dina am, ak firnde yu mag yu jóge asamaan.
12 Waaye laata loolu lépp, yeen, dees na leen teg loxo, fitnaal leen, jébbal leen kuréli jàngu ya, tëj leen kaso. Dees na leen yóbbu ci kanami buur aki boroom dëkk ndax sama tur,
13 ngir ngeen doxe ca yékkati kàdduy seede.
14 Kon nag defleen bu baax ci seen xel, ne soxlawuleena waajal kàddug layoo.
15 Ndax man maa leen di jox làmmiñ wu ànd ak xel, wu seen benn noon dul mana dàq mbaa di ko weddi.
16 Pexe mu leen jàpplu dina sababoo sax ci seeni waajur ak seen doomi ndey ak seeni jegeñaale ak seeni xarit, te dees na rey ñenn ci yeen,
17 Ñépp a leen di bañ ndax sama tur.
18 Waaye seen genn kawaru bopp sax du sànku.
19 Saxooleen muñ nag, daldi mucc.
20 «Bu ngeen gisee gàngooru xare gu gaw Yerusalem, su boobaa xamleen ne tasteem dëgmal na.
21 Su boobaa ña mu fekk ca diiwaanu Yude, nañu daw jëm kaw tund ya, ñi ci biir dëkk bi, nañu daw génn, te ña mu fekk ca tool ya, buñu duggsi ci biir dëkk bi.
22 Ndax janti mbugal lay doon, ngir sottal mboolem lu ñu bindoon.
23 Wóoy ngalla jigéeni wérul ña, ak ñay nàmpal ca yooyu jant! Ndax tiis wu réy lay doon ci réew mi, akam sànj ci kaw askan wii.
24 Dinañu fàddoo ñawkay saamar, te dees na leen jàpp njaam, yóbbu ci mboolem xeet yi. Te jaambur ñi dul Yawut ñooy joggati Yerusalem, ba kera àppu ñooñu dul Yawut di mat.
25 «Ay firnde dinañu feeñ ci jant bi ak weer wi ak biddiiw yi. Ci kaw suuf njàqare ak tiitaange mooy ñeel xeet yi ndax riirum géej gi ak gannax yi,
26 nit ñiy séentu li nara dikkal àddina, di xëm ndax tiitaange, nde dooley asamaan dina sàqi.
27 Su boobaa dees na gis Doomu nit ki di ñëw ciw niir, ànd ak manoore ak daraja ju réy.
Luug 21 in Kàddug Yàlla gi