Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 20:1-44 in Wolof

Help us?

LUUG 20:1-44 in Téereb Injiil

1 Benn bés Yeesu doon jàngal nit ña ca kër Yàlla ga, di leen yégal xibaaru jàmm bi. Sarxalkat yu mag ya ak xutbakat ya ak njiit ya ñëw ne ko:
2 «Wax nu ci ban sañ-sañ ngay defe yëf yii, walla kan moo la may boobu sañ-sañ.»
3 Yeesu ne leen: «Man itam dinaa leen laaj lenn: waxleen ma,
4 la Yaxya daan def, di sóob nit ñi ci ndox, fu mu ko jële, ci Yàlla walla ci nit ñi?»
5 Ñu waxtaan ci seen biir naan: «Bu nu nee: “Ci Yàlla,” dina laaj: “Lu tax gëmuleen ko kon?”
6 Te bu nu nee: “Ci nit ñi,” mbooloo mépp dinañu nu sànni ay xeer, ndaxte gëm nañu ne Yaxya yonent la woon.»
7 Noonu ñu ne ko xamuñu fu mu ko jële.
8 Yeesu ne leen: «Kon man itam duma leen wax ci ban sañ-sañ laay defe yëf yii.»
9 Noonu Yeesu daldi wax nit ña léeb wii: «Amoon na nit ku jëmbët toolu reseñ, batale ko ay beykat, dem tukki tukki bu yàgg.
10 Bi tool bi ñoree nag, mu yónni surga ci ñoom, ngir jot wàllam ci meññeef gi. Waaye beykat yi dóor ko ay yar, dàq ko, mu dellu ak loxoy neen.
11 Mu yónniwaat beneen surga, ñu dóor ko moom itam, toroxal ko, dàq ko, mu dellu ak loxoy neen.
12 Mu yónneeti ñetteelu surga, ñu gaañ ko, dàq ko.
13 «Boroom tool ba daldi ne: “Nan laay def nag? Dinaa yónni sama doom, sama reeni xol. Xëy na ñu weg ko, moom.”
14 Waaye bi beykat yi gisee doom ji, ñu ne ci seen biir: “Kii moo wara donn tool bi; nan ko rey, moom ndono li.”
15 Ñu génne ko tool bi nag, rey ko.» Noonu Yeesu laaj leen: «Nu leen boroom tool bi di def, nag?
16 Xanaa ñëw, rey beykat yooyu, dénk tool ba ñeneen.» Bi Yeesu waxee loolu, nit ña ne ko: «Yàlla tere!»
17 Waaye Yeesu ne leen jàkk, daldi ne: «Kon nag lu baat yii ci Mbind mi di tekki: “Doj wa tabaxkat ya sànni, mujj na di doju koñ.”
18 Képp ku dal ci doj woowu, dammtoo, te ku mu dal ci sa kaw, rajaxe la.»
19 Xutbakat ya ak sarxalkat yu mag ya ñu ngi doon wuta jàpp Yeesu ca taxawaay ba, ndaxte xam nañu ne ñoo tax mu wax léeb woowu. Waaye ragal nañu mbooloo ma.
20 Noonu ñu koy yeeru, daldi yónni ay nit ñu mbubboo njub, sas leen ñu fexe koo jàpp ci ay waxam, ngir jébbal ko boroom réew, ma yor kilifteef ak sañ-sañ.
21 Ñu daldi ñëw ci Yeesu ne ko: «Kilifa gi, xam nanu ne li ngay wax te di ko jàngle lu jub la. Amuloo parlàqu, waaye dangay xamle yoonu Yàlla ci bu wóor.
22 Wax nu, ndax jaadu na, nu fey buur bi Sesaar galag walla déet.»
23 Waaye Yeesu xam na seen pexe ne leen:
24 «Wonleen ma posetu denariyon. Kan lañu ci def nataalam ak turam?» Ñu ne ko: «Sesaar.»
25 Noonu mu ne leen: «Joxleen nag Sesaar li Sesaar moom, te jox Yàlla li Yàlla moom.»
26 Noonu manuñu ko woona jàpp ciy waxam ci kanam mbooloo ma; ñu waaru ci tontam, ba wedam.
27 Noonu ay nit, ñu bokk ci Sadusen yi, ñëw ci moom. Sadusen yi nag ñoom weddi nañu ndekkite li. Noonu ñu laaj ko ne:
28 «Kilifa gi, Musaa bindal na nu ne, ku magam faatu te bàyyiwul doom ak soxnaam, kooku war na donn jigéen ji, ba yékkati giiru magam.
29 Amoon na fi nag juróom ñaari góor ñu bokk ndey ak baay. Taaw ba takk jabar, faatu, te bàyyiwul doom.
30 Ñaareel ba takk jigéen ja, def noonu; ak ñetteel ba, ba juróom ñaar ñépp faatu te bàyyiwuñu doom.
32 Gannaaw ga nag jigéen ja it faatu.
33 Ci ndekkite li nag, kan ci ñoom moo wara donn jigéen ja, fekk ku nekk ci juróom ñaar ñi mas na koo takk?»
34 Yeesu ne leen: «Ci àddina sii, góor ñi ak jigéen ñi dañuy séy.
35 Waaye ña ñu àtte ne yeyoo nañoo bokk ci dundu ëllëg ak ci ndekkite li, kenn du am jabar, kenn du am jëkkër.
36 Dafa fekk ne manatuñoo dee, ndaxte dañuy mel ni malaaka yi. Ay doomi Yàlla lañu ndaxte doomi ndekkite lañu.
37 Te Musaa sax wone na ne, néew yi dinañu dekki, ci saarum ngarab si. Foofa Musaa wooye na fa Boroom bi: “Yàllay Ibraayma, Yàllay Isaaxa, di Yàllay Yanqóoba.”
38 Kon nag nekkul Yàllay ñi dee waaye Yàllay ñiy dund la, ndaxte Yàllaa tax ñépp di dund.»
39 Ci kaw loolu ay xutbakat ne ko: «Li nga wax dëgg la, kilifa gi!»
40 Ndaxte kenn ci ñoom ñemeetu koo laaj dara.
41 Noonu Yeesu ne leen: «Lu tax nit ñi di wax ne, Almasi bi mooy sëtu Daawuda?
42 Ndaxte Daawuda moom ci boppam moo ne ci Sabóor: “Boroom bi nee na sama Boroom: ‘Toogal ci sama ndijoor,
43 ba kera may daaneel say noon ci sa kanam.’ ”
44 Gannaaw Daawuda nag wooye na ko “Boroom bi,” nu muy nekke sëtam?»
LUUG 20 in Téereb Injiil

Luug 20:1-44 in Kàddug Yàlla gi

1 Mu am bés bu Yeesu doon jàngal askan wi ca kër Yàlla ga, di xamle xibaaru jàmm bi. Sarxalkat yu mag ya ak firikati yoon ya ne jalañ, ñook njiit ya.
2 Ñu ne ko: «Wax nu, lii ngay def, ci ban sañ-sañ nga koy defe, mbaa kan moo la jox boobu sañ-sañ?»
3 Yeesu ne leen: «Ma laaj leen man itam lenn, waxleen ma,
4 sóobeb Yaxya ci ndox, asamaan la ndigal la bawoo, am ci nit ñi?»
5 Ñu diisoo ci seen biir, daldi ne: «Su nu nee: asamaan la ndigal la bawoo da naan lu tax kon gëmunu Yaxya?
6 Te su nu nee: ci nit ñi la ndigal li bawoo, mbooloo mépp a nuy sànni ay xeer, ndax wóor na leen ne Yaxya ab yonent la woon.»
7 Ñu daldi ne ko: «Xamunu fu mu ko jële.»
8 Yeesu ne leen: «Kon man itam duma leen wax ci ban sañ-sañ laay defe lii.»
9 Ci kaw loolu Yeesu léeb askan wa, lii, ne leen: «Jenn waay moo jëmbatoon ab tóokëru reseñ, batale ko ay beykat, daldi dem yoon wu yàgg.
10 Ba tóokër ba ñoree, mu yebal ca beykat ya ab surga, ngir ñu jox ko wàllam ca meññeef ma. Beykat ya dóor surga ba, ba noppi dàq ko, mu dellu loxoy neen.
11 Mu dellu yónni beneen surga, ñu dóor ko moom itam, torxal ko, dàq ko, mu dellu loxoy neen.
12 Mu dellooti yónni ñetteelu surga, kooku it, ñu gaañ ko, sànni ko ca biti.
13 «Boroom tóokër ba ne: “Nan laay def nag? Naa yónni sama doomu bopp ji ma sopp boog, xanaa moom, dinañu ko rus!”
14 Teewul ba beykat ya gisee doom ji, dañu ne ci seen biir: “Kii mooy donn; nanleen ko rey, su ko defee ndono li féeteek nun.”
15 Ba loolu amee ñu génne ko tóokër ba, rey ko.» «Ana nu boroom tóokër biy def beykat yi nag?
16 Xanaa dikk, rey beykat yooyu, dénk tóokër ba ñeneen.» Nit ña dégg loolu daldi ne: «Yàlla tere!»
17 Yeesu ne leen jàkk, daldi ne: «Kon nag lii ñu bind, lu muy tekki? “Doj wi tabaxkat yi beddi woon, moo mujj di doju coll wi.”
18 Woowu doj, képp ku ci dal, dammtoo, te ku mu dal, rajaxe la.»
19 Firikati yoon yaak sarxalkat yu mag ya nag, ca saa sa lañu doon fexee teg Yeesu loxo, ndax xamoon nañu ne ñoo moom léeb woowu, waaye nit ña lañu ragal.
20 Ba mu ko defee ñu bàyyi Yeesu xel, daldi yebal ay yeerukat, sas leen ñu yiw-yiwlu te di ko fiir ci kaw kàddu ba jàpp ko, ngir jébbal ko boroom dëkk bay boroom kilifteef ga ak sañ-sañ ba.
21 Yeerukat ya dikk ne Yeesu: «Sëriñ bi, xam nanu ne njub ngay wax, di ko jàngle. Amuloo parlàqu itam, waaye ci kaw dëgg ngay jànglee yoonu Yàlla.
22 Wax nu nag ndax yoon maye na, nu fey Buur Sesaar galag, am déet.»
23 Teewul Yeesu ràññee seen pexe. Mu ne leen:
24 «Joxleen ma ab posetub dinaar, ma gis. Nataal bii ak tur wii ci binde, kuy boroom?» Ñu ne ko: «Sesaar.»
25 Mu ne leen: «Kon kay yëfi Sesaar, joxleen ko Sesaar; te yëfi Yàlla, ngeen jox ko Yàlla.»
26 Manuñu koo fiir ba jàppe ko menn mbir ca kanam mbooloo ma, xanaa waaru ca tontam, ba wedam.
27 Ñenn ci Sadusen, yi weddi ne ndee-ndekki am na, ñoo dikkoon ca Yeesu. Ñu ne ko:
28 «Sëriñ bi, Musaa da noo bindal ne ku góor, su ku mu bokkal waajur faatoo te amul ak jabaram doom, na jël jabaram, ngir amal mbokkam ma dee, kuutaay.
29 Léegi juróom ñaari góor ñu bokk ndey ak baay la woon. Taaw ba takk jabar, gannaaw gi mu faatu, te bàyyiwul doom.
30 Tofo ba,
31 ak ñaareelu tofo ba, ku ci nekk donn na ndaw sa ca magam, ñu topplantee ko noonu, ba juróom ñaar ñépp dee te amuñu ca doom.
32 Gannaaw gi ndaw sa it dee.
33 Ndaw si nag, keroog ndekkite la, kan la ciy doon jabaram, gannaaw juróom ñaar ñépp a ko jëloon jabar?»
34 Yeesu ne leen: «Ci àddina sii la góor ñi ak jigéen ñi di séy.
35 Waaye ña ñu yeyale ndekkitel ëllëg, yeyale leen bakkan ci àddina siy ñëw, ñooñu, su boobaa, kenn du ci am jabar mbaa jëkkër.
36 Dootuñu mana dee it, ndax niy malaaka lañuy mel. Ay doomi Yàlla lañuy doon, ndax da leen di fekk dekki.
37 Te Musaa ci boppam xamle na ne ñi dee dañuy dekki, na ko téere indee ca mbirum ngarab sa. Mooy ba mu wooyee Boroom bi: “Yàllay Ibraayma, Yàllay Isaaxa, Yàllay Yanqóoba.”
38 Kon moom du ñi dee lay seen Yàlla, xanaa ñiy dund, ndax fa moom, ñépp a ngi dund.»
39 Ci kaw loolu ñenn ca firikati yoon ya àddu ne ko: «Dëgg nga wax, Sëriñ bi!»
40 Gannaaw loolu ñemeetuñu koo laaj dara.
41 Yeesu neeti leen: «Nees mana waxe ne Almasi, Sëtub Daawuda la?
42 Daawuda ci boppam moo ne ci téereb Sabóor: “Boroom bi moo ne sama Sang: ‘Toogeel sama ndijoor,
43 ba ma def say noon, sa ndëggastal.’ ”
44 Gannaaw Daawudaa wooye Almasi “Sang bi,” nu mu nekke ab sëtam?»
Luug 20 in Kàddug Yàlla gi