Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 1:66-77 in Wolof

Help us?

LUUG 1:66-77 in Téereb Injiil

66 Ñi dégg nettali, bi jëm ci mbir yooyu, dañu koo denc ci seen xol te naan: «Nu xale bii di mujje nag?» Ndaxte leeroon na ne dooley Boroom baa ngi ànd ak moom.
67 Sakari baayu Yaxya daldi fees ak Xel mu Sell mi. Noonu mu wax ci kàddug Yàlla ne:
68 «Cant ñeel na Boroom bi, Yàllay Israyil, ndaxte wallusi na mbooloom, ba jot leen!
69 Feeñal na nu Musalkat bu am doole, bi soqikoo ci askanu Daawuda jaamam,
70 ni mu yéglee woon bu yàgg jaarale ko ci yonentam yu sell yi.
71 Dina nu musal ci sunuy noon, jële nu ci sunu loxoy bañaale.
72 Yàlla wone na yërmandeem, ji mu digoon sunuy maam, te di fàttaliku kóllëre, gi mu fas ak ñoom,
73 di ngiñ, li mu giñaloon sunu maam Ibraayma naan,
74 dina nu teqale ak sunuy noon, ngir nu man koo jaamu ci jàmm,
75 nu sell te jub ci kanamam sunu giiru dund.
76 Yaw nag doom, dinañu lay wooye yonentu Aji Kawe ji, ndaxte dinga jiitu, di yégle ñëwug Boroom bi, di ko xàllal yoon wi.
77 Dinga xamal mbooloom ni leen Boroom bi mana musale, jaare ko ci seen mbaalug bàkkaar,
LUUG 1 in Téereb Injiil

Luug 1:66-77 in Kàddug Yàlla gi

66 Ña ca dégg ñépp daldi bàyyi xel ca mbir ma, te naan: «Lu xale bii nara doon ëllëg?» ngir manoorey Boroom bee àndoon ak moom.
67 Ci kaw loolu Sàkkaryaa baayu Yaxya feese Noo gu Sell gi, daldi tàmbalee biral kàddug waxyu, ne:
68 «Cant ñeel na Boroom bi Yàllay Israyil, moo seetsi ñoñam, ba jot leen!
69 Moo nu feeñalal Musalkat bu manoorewu, fi biir kër Daawuda jaamam ba,
70 noonee mu ko waxe woon ca jant yu jëkk ya, yonentam yu sell ya woon jottli,
71 moo nu musal ci sunuy noon, jële nu ci sunu loxoy mboolem bañaale.
72 Moo jëfe yërmande ñeel sunuy maam, tey bàyyi xel kóllëreem gu sell,
73 ak ngiñ la mu giñaloon sunu maam Ibraayma,
74 ne moo nuy may nu mucce ci loxoy noon, ba man koo jaamoo xel mu dal
75 ci biir sellnga ak njub ci kanamam, sunu giiru dund.
76 «Ngóor si nag yaw, yonentu Aji Kawe ji lees lay wooye, nde yaay dox, jiitu Sang bi, xàllal kow yoonam,
77 ngir yégal ñoñam ag njot guy topp seen njéggalug bàkkaar.
Luug 1 in Kàddug Yàlla gi