Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 1:54-65 in Wolof

Help us?

LUUG 1:54-65 in Téereb Injiil

54 Wallu na bànni Israyil giy jaamam, di fàttaliku yërmandeem,
55 ni mu ko dige woon sunuy maam, jëmale ko ci Ibraayma ak askanam ba fàww.»
56 Noonu Maryaama toog fa Elisabet lu wara tollook ñetti weer, sooga ñibbi.
57 Gannaaw loolu jamono ji Elisabet wara mucc agsi, mu daldi jur doom ju góor.
58 Dëkkandoom yi ak bokkam yi yég ne, Boroom bi won na ko yërmande ju réy, ñu ànd ak moom bég.
59 Bi bés ba délsee, ñu ñëw xarafalsi xale ba, bëgg koo dippee baayam Sakari.
60 Waaye yaayam ne leen: «Déedéet, Yaxya lay tudd.»
61 Ñu ne ko: «Amoo menn mbokk mu tudd noonu.»
62 Ñu daldi liyaar baayam, ngir xam nan la bëgg ñu tudde xale ba.
63 Sakari laaj àlluwa, bind ci ne: «Yaxya la tudd.» Ñépp daldi waaru.
64 Ca saa sa Yàlla dindi luu gi, Sakari daldi waxaat, di màggal Yàlla.
65 Waa dëkk ba bépp jaaxle, xew-xew yooyu siiw ca tundi Yude yépp.
LUUG 1 in Téereb Injiil

Luug 1:54-65 in Kàddug Yàlla gi

54 Moo wallu bànni Israyil, jaamam, bàyyee ko xel yërmandeem,
55 noonee mu ko dige woon sunuy maam, ñeel Ibraayma ak askanam ba fàww.»
56 Maryaama toog na fa Elisabet lu wara tollook ñetti weer, sooga ñibbi.
57 Gannaaw gi Elisabet dem ba àppam mat, mu mucc, am doom ju góor.
58 Dëkkandoom yaak ay bokkam yég noonu ko Boroom bi xéewalee yërmandeem, ñu bokk ak moom mbégte ma.
59 Ba bés ba délsee, ñu dikk xarfalsi xale ba, bëgg koo tudde Sàkkaryaa, dippee ko baayam.
60 Yaayam nag ne leen: «Déet, Yaxya lay tudd.»
61 Ñu ne ko: «Waaye kenn ci say bokk tuddul noonu!»
62 Ci kaw loolu ñu liyaar baayam, ngir xam nu mu bëgg ñu tudde xale bi.
63 Sàkkaryaa laaj àlluwa, ñu jox ko, mu bind ci: «Yaxya mooy turam.» Ñépp waaru.
64 Ca saa sa gémmiñ ga ubbiku, làmmiñ wa nangu, muy wax, daldi sant Yàlla.
65 Ba loolu amee tiitaange dikkal mboolem ña leen séq, mbir moomu mépp nag doon waxtaan ca diiwaanu tundi Yude gépp.
Luug 1 in Kàddug Yàlla gi