Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 1:42-63 in Wolof

Help us?

LUUG 1:42-63 in Téereb Injiil

42 Elisabet wax ca kaw ne: «Barkeel nañu la ci jigéen ñi, barkeel doom ji nga ëmb!
43 Man maay kan, ba ndeyu sama Boroom ñëw di ma seetsi?
44 Maa ngi lay wax ne naka laa la dégg ngay nuyoo rekk, sama doom ji yëngu ci sama biir ndax mbég.
45 Barke ñeel na la, yaw mi gëm ne li la Boroom bi yégal dina mat!»
46 Noonu Maryaama daldi ne:
47 «Sama xol a ngi màggal Boroom bi, sama xel di bég ci Yàlla sama Musalkat,
48 ndaxte fàttaliku na ma, man jaamam bu woyof bi. Gannaaw-si-tey, niti jamono yépp dinañu ma wooye ki ñu barkeel,
49 ndaxte Ku Màgg ki defal na ma lu réy. Turam dafa sell.
50 Day wàcce yërmandeem ci ñi ko ragal, ci seeni sët ba ci seeni sëtaat.
51 Wone na jëf yu mag ci dooley loxoom, te tas mbooloom ñiy réy-réylu,
52 daaneel boroom doole yi ci seen nguur, yékkati baadoolo yi.
53 Ñi xiif, reggal na leen ak ñam wu neex, te dàq boroom alal yi, ñu daw ak loxoy neen.
54 Wallu na bànni Israyil giy jaamam, di fàttaliku yërmandeem,
55 ni mu ko dige woon sunuy maam, jëmale ko ci Ibraayma ak askanam ba fàww.»
56 Noonu Maryaama toog fa Elisabet lu wara tollook ñetti weer, sooga ñibbi.
57 Gannaaw loolu jamono ji Elisabet wara mucc agsi, mu daldi jur doom ju góor.
58 Dëkkandoom yi ak bokkam yi yég ne, Boroom bi won na ko yërmande ju réy, ñu ànd ak moom bég.
59 Bi bés ba délsee, ñu ñëw xarafalsi xale ba, bëgg koo dippee baayam Sakari.
60 Waaye yaayam ne leen: «Déedéet, Yaxya lay tudd.»
61 Ñu ne ko: «Amoo menn mbokk mu tudd noonu.»
62 Ñu daldi liyaar baayam, ngir xam nan la bëgg ñu tudde xale ba.
63 Sakari laaj àlluwa, bind ci ne: «Yaxya la tudd.» Ñépp daldi waaru.
LUUG 1 in Téereb Injiil

Luug 1:42-63 in Kàddug Yàlla gi

42 Mu àddu ca kaw ne: «Yaa gëna barkeel ci jigéen ñi, sa doom ji nga ëmb it barkeel na!
43 Ana ku ma doon ba sama ndeyu Sang di ma seetsi?
44 Naka la sa kàddug nuyoo tàbbi sama nopp rekk, sama doom ji yëngu ci sama biir bi ndax bég.
45 Ndokklee yaw mi gëm ne mbir mi ñu la yégal, te mu tukkee ci Boroom bi dina sotti!»
46 Maryaama nag ne:
47 «Sama xol laay màggale Boroom bi, samag noo laay bége Yàlla mi may musal,
48 moo geesu bii jaamam bu tekkeedi, ba maasoo maas doxe fi wooye ma boroom mbég mi,
49 nde Kiy Boroom doole moo ma defal jaloore, sellnga ñeel naw turam.
50 «Yërmandeem a ñeel ay ragalkatam, maas ci kaw maas.
51 Dooley loxoom la defe ay jaloore, tasaare ñi jikkowoo réy-réylu,
52 wàccee buur yi ci seeni gàngune, yékkati baadoolo yi.
53 Ñi xiif, mu reggal leen lu neex, ñi duunle, mu dàqe loxoy neen.
54 Moo wallu bànni Israyil, jaamam, bàyyee ko xel yërmandeem,
55 noonee mu ko dige woon sunuy maam, ñeel Ibraayma ak askanam ba fàww.»
56 Maryaama toog na fa Elisabet lu wara tollook ñetti weer, sooga ñibbi.
57 Gannaaw gi Elisabet dem ba àppam mat, mu mucc, am doom ju góor.
58 Dëkkandoom yaak ay bokkam yég noonu ko Boroom bi xéewalee yërmandeem, ñu bokk ak moom mbégte ma.
59 Ba bés ba délsee, ñu dikk xarfalsi xale ba, bëgg koo tudde Sàkkaryaa, dippee ko baayam.
60 Yaayam nag ne leen: «Déet, Yaxya lay tudd.»
61 Ñu ne ko: «Waaye kenn ci say bokk tuddul noonu!»
62 Ci kaw loolu ñu liyaar baayam, ngir xam nu mu bëgg ñu tudde xale bi.
63 Sàkkaryaa laaj àlluwa, ñu jox ko, mu bind ci: «Yaxya mooy turam.» Ñépp waaru.
Luug 1 in Kàddug Yàlla gi