Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 19:9-20 in Wolof

Help us?

LUUG 19:9-20 in Téereb Injiil

9 Yeesu ne ko: «Mucc gi wàcc na tey ci kër gii, ndaxte nit kii, ci askanu Ibraayma la bokk itam.
10 Ndaxte Doomu nit ki ñëw na, ngir seet te musal ñi réer.»
11 Bi nit ñi doon déglu kàddu yooyu, Yeesu teg ca léeb, ndaxte jege woon na Yerusalem, te ñoom foogoon nañu ne nguuru Yàlla dafay daldi feeñ ca saa sa.
12 Mu ne nag: «Dafa amoon boroom juddu bu rafet bu demoon ci réew mu sore, ngir ñu fal ko buur te mu délsiwaat.
13 Noonu mu woo fukk ci ay surgaam, jox ku nekk benn libidoor, ne leen: “Liggéeyleen ci, ba may ñibsi.”
14 Waaye waa réewam bëgguñu ko. Noonu ñu yónni ndaw ci gannaawam ne: “Bëggunu nit kii yilif nu.”
15 «Bi ñu ko falee buur nag, ba mu délsi, mu woolu surga, ya mu joxoon wurus wa, ngir xam nan lañu ci liggéeye.
16 Ku jëkk ka ñëw ne ko: “Sang bi, sa libidoor bii jur na fukki libidoor.”
17 Buur ba ne ko: “Def nga lu baax, surga bu baax nga. Segam wone nga ne takku nga ci lu tuuti, falul ci fukki dëkk.”
18 Surga ba ca topp ñëw ne: “Sang bi, sa libidoor ba indi na juróomi libidoor.”
19 Buur ba ne ko: “Yaw, falul ci juróomi dëkk.”
20 Keneen ñëw ne: “Sang bi, sa libidoor baa ngi nii. Dama koo fasoon ci sekkit, denc ko.
LUUG 19 in Téereb Injiil

Luug 19:9-20 in Kàddug Yàlla gi

9 Yeesu ne ko: «Bés niki tey, mucc dikkal na kër gii, ndax waa jii kat ci askanu Ibraayma la bokk, moom itam.
10 Ndax Doomu nit ki, ñi réer la seetsi, ngir musal leen.»
11 Naka la nit ña dégg loolu, Yeesu léebati leen, ndax booba jege na Yerusalem, te fekk na ñu foog ne nguurug Yàlla day daldi teew ca saa sa.
12 Moo tax mu ne: «Boroom juddu bu réy la woon. Muy waaja dem réew mu sore, ngir ñu fal ko fa buur, mu doora ñibbsi.
13 Ci biir loolu mu woo fukki surgaam, jox leen ku nekk benn posetub wurus bu gànjare, ne leen: “Liggéeyleen ci, ba ma ñibbsi.”
14 Waaye waa réewam ña dañu koo bañoon. Ci gannaawam lañu yónni ndaw, ne: “Kii, bugguñu muy sunu buur.”
15 «Gannaaw ba ñu ko falee buur, ba mu délsi, daa woolu surga, ya mu joxoon wurus wa, ngir xam ñaata la leen ca seen liggéey jural.
16 Kenn ka dikk, ne ko: “Sang bi, sa poset ba jur na fukki poset.”
17 Mu ne ko: “Jaaraamaa, surga bu baax bi. Gannaaw ci lu tuut nga wóore nag, falul ci fukki dëkk.”
18 Keneen dikk, ne: “Sang bi, sa poset ba indi na juróomi poset.”
19 Mu neeti kooka: “Yaw, falul ci juróomi dëkk.”
20 Keneen dikk ne: “Sang bi, sa poset baa ngii ma fasoon ciw sekkit.
Luug 19 in Kàddug Yàlla gi