Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 19:9-13 in Wolof

Help us?

LUUG 19:9-13 in Téereb Injiil

9 Yeesu ne ko: «Mucc gi wàcc na tey ci kër gii, ndaxte nit kii, ci askanu Ibraayma la bokk itam.
10 Ndaxte Doomu nit ki ñëw na, ngir seet te musal ñi réer.»
11 Bi nit ñi doon déglu kàddu yooyu, Yeesu teg ca léeb, ndaxte jege woon na Yerusalem, te ñoom foogoon nañu ne nguuru Yàlla dafay daldi feeñ ca saa sa.
12 Mu ne nag: «Dafa amoon boroom juddu bu rafet bu demoon ci réew mu sore, ngir ñu fal ko buur te mu délsiwaat.
13 Noonu mu woo fukk ci ay surgaam, jox ku nekk benn libidoor, ne leen: “Liggéeyleen ci, ba may ñibsi.”
LUUG 19 in Téereb Injiil

Luug 19:9-13 in Kàddug Yàlla gi

9 Yeesu ne ko: «Bés niki tey, mucc dikkal na kër gii, ndax waa jii kat ci askanu Ibraayma la bokk, moom itam.
10 Ndax Doomu nit ki, ñi réer la seetsi, ngir musal leen.»
11 Naka la nit ña dégg loolu, Yeesu léebati leen, ndax booba jege na Yerusalem, te fekk na ñu foog ne nguurug Yàlla day daldi teew ca saa sa.
12 Moo tax mu ne: «Boroom juddu bu réy la woon. Muy waaja dem réew mu sore, ngir ñu fal ko fa buur, mu doora ñibbsi.
13 Ci biir loolu mu woo fukki surgaam, jox leen ku nekk benn posetub wurus bu gànjare, ne leen: “Liggéeyleen ci, ba ma ñibbsi.”
Luug 19 in Kàddug Yàlla gi