4 Ci kaw loolu Sase daw, jiituji, daldi yéeg ci genn garab ca yoon woowu Yeesu wara jaare, ngir mu man koo gis.
5 Yeesu dikk ba tollu foofa, téen ne ko: «Sase, wàccal gaaw, ndax sa kër laa wara dali tey jii.»
6 Sase daldi wàcc gaaw, bége koo dalal lool.
7 Ñépp gis loolu, di ñurumtu naan bàkkaarkat bi la Yeesu dem këram, dal ak moom.
8 Sase nag taxaw ne Sang bi: «Sang bi, ma ne, sama genn-wàllu alal, jox naa ko néew-doole yi, te jépp alal ju lewul ju ma masa jëlal kenn, dinaa fey ñeentam.»
9 Yeesu ne ko: «Bés niki tey, mucc dikkal na kër gii, ndax waa jii kat ci askanu Ibraayma la bokk, moom itam.
10 Ndax Doomu nit ki, ñi réer la seetsi, ngir musal leen.»