17 Buur ba ne ko: “Def nga lu baax, surga bu baax nga. Segam wone nga ne takku nga ci lu tuuti, falul ci fukki dëkk.”
18 Surga ba ca topp ñëw ne: “Sang bi, sa libidoor ba indi na juróomi libidoor.”
19 Buur ba ne ko: “Yaw, falul ci juróomi dëkk.”
20 Keneen ñëw ne: “Sang bi, sa libidoor baa ngi nii. Dama koo fasoon ci sekkit, denc ko.
21 Dama laa ragaloon, ndaxte ku néeg nga. Dangay nangu loo dénkaanewul, di dajale loo jiwul.”
22 Buur ba ne ko: “Ci say wax laa lay àtte, surga bu bon bi! Xamoon nga ne, nit ku néeg laa, di nangu lu ma dénkaanewul, te dajale lu ma jiwul.
23 Lu tax nag yóbbuwoo sama xaalis ca denckati xaalis ya? Bés bu ma ñëwee nag, ma mana jot sama xaalis ak la mu jur.”
24 «Ci kaw loolu mu ne ña taxawoon ca wetam: “Nanguleen libidoor bi ci moom, jox ko boroom fukki libidoor yi.”
25 Ñu ne ko: “Sang bi, am na fukki libidoor ba noppi.”
26 Buur ba ne leen: “Maa ngi leen koy wax, ku am, dinañu la dolli, waaye ku amul, li nga am as néew sax, dinañu ko nangu.
27 Waaye sama noon yi, ñi bëggul woon ma doon seen buur, indileen fii, rey leen ci sama kanam.”»
28 Bi mu waxee loolu ba noppi, Yeesu dafa daldi jiitu, jëm Yerusalem.
29 Bi muy jege dëkki Betfase ak Betani, ci wetu tund wu ñuy wax tundu Oliw ya, Yeesu yebal ñaar ci ay taalibeem,
30 ne leen: «Demleen ci dëkk bi ci kanam. Bu ngeen fa duggee, dingeen fa gis cumbur gu kenn masula war. Yiwileen ko, indi.
31 Bu leen kenn laajee: “Lu tax ngeen koy yiwi?” neleen ko: “Boroom bi da koo soxla.”»
32 Ñaari ndaw ya dem, fekk mbir ya deme, na leen ko Yeesu waxe woon.
33 Bi ñuy yiwi cumbur ga nag, ay boroomam ne leen: «Lu tax ngeen di yiwi cumbur gi?»
34 Ñu ne: «Ndaxte Boroom bi da koo soxla.»
35 Noonu ñu indil cumbur gi Yeesu, daldi lal seeni yére ca kaw, yéegal ca Yeesu.