Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 19:15-27 in Wolof

Help us?

LUUG 19:15-27 in Téereb Injiil

15 «Bi ñu ko falee buur nag, ba mu délsi, mu woolu surga, ya mu joxoon wurus wa, ngir xam nan lañu ci liggéeye.
16 Ku jëkk ka ñëw ne ko: “Sang bi, sa libidoor bii jur na fukki libidoor.”
17 Buur ba ne ko: “Def nga lu baax, surga bu baax nga. Segam wone nga ne takku nga ci lu tuuti, falul ci fukki dëkk.”
18 Surga ba ca topp ñëw ne: “Sang bi, sa libidoor ba indi na juróomi libidoor.”
19 Buur ba ne ko: “Yaw, falul ci juróomi dëkk.”
20 Keneen ñëw ne: “Sang bi, sa libidoor baa ngi nii. Dama koo fasoon ci sekkit, denc ko.
21 Dama laa ragaloon, ndaxte ku néeg nga. Dangay nangu loo dénkaanewul, di dajale loo jiwul.”
22 Buur ba ne ko: “Ci say wax laa lay àtte, surga bu bon bi! Xamoon nga ne, nit ku néeg laa, di nangu lu ma dénkaanewul, te dajale lu ma jiwul.
23 Lu tax nag yóbbuwoo sama xaalis ca denckati xaalis ya? Bés bu ma ñëwee nag, ma mana jot sama xaalis ak la mu jur.”
24 «Ci kaw loolu mu ne ña taxawoon ca wetam: “Nanguleen libidoor bi ci moom, jox ko boroom fukki libidoor yi.”
25 Ñu ne ko: “Sang bi, am na fukki libidoor ba noppi.”
26 Buur ba ne leen: “Maa ngi leen koy wax, ku am, dinañu la dolli, waaye ku amul, li nga am as néew sax, dinañu ko nangu.
27 Waaye sama noon yi, ñi bëggul woon ma doon seen buur, indileen fii, rey leen ci sama kanam.”»
LUUG 19 in Téereb Injiil

Luug 19:15-27 in Kàddug Yàlla gi

15 «Gannaaw ba ñu ko falee buur, ba mu délsi, daa woolu surga, ya mu joxoon wurus wa, ngir xam ñaata la leen ca seen liggéey jural.
16 Kenn ka dikk, ne ko: “Sang bi, sa poset ba jur na fukki poset.”
17 Mu ne ko: “Jaaraamaa, surga bu baax bi. Gannaaw ci lu tuut nga wóore nag, falul ci fukki dëkk.”
18 Keneen dikk, ne: “Sang bi, sa poset ba indi na juróomi poset.”
19 Mu neeti kooka: “Yaw, falul ci juróomi dëkk.”
20 Keneen dikk ne: “Sang bi, sa poset baa ngii ma fasoon ciw sekkit.
21 Dama laa ragal, ndaxte ku néeg nga. Dangay foqati loo dénkaanewul woon, di dajale loo jiwuloon.”
22 Mu ne ko: “Say wax laa lay àttee, surga bu bon bi! Xamoon nga ne nit ku néeg laa, di foqati lu ma dénkaanewul woon, di dajale lu ma jiwuloon.
23 Lu la tee woona dénkaaneji sama alal ca dencukaay ba, ngir bu ma dikkee jot ko, boole ca tonoom?”
24 «Ci kaw loolu mu ne ña fa taxawoon: “Nanguleen poset bi ci moom, jox ko boroom fukki poset yi.”
25 Ñu ne ko: “Sang bi, kee ngeek fukki poset ba noppi!”
26 Mu ne: “Ma ne leen, képp ku am, dees na ko dolli, waaye ku amul, la mu am as néew sax, dees na ko nangu.
27 Sama noon yooyu buggul woon ma doon seen buur nag, indileen leen fii, te rendi leen ci sama kanam.”»
Luug 19 in Kàddug Yàlla gi