Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 17:11-25 in Wolof

Help us?

LUUG 17:11-25 in Téereb Injiil

11 Bi muy dem Yerusalem ba tey, Yeesu jaar ci dig wiy xàjjale Samari ak Galile.
12 Bi muy jub benn dëkk, fukki gaana ñëw, dogale ko. Ñu taxaw dànd ko, di wax ca kaw naan:
13 «Yeesu, kilifa gi, yërëm nu!»
14 Naka la leen Yeesu di gis, naan leen: «Demleen won seen bopp sarxalkat ya.» Bi ñuy dem, ñu daldi set.
15 Kenn ci ñoom gis ne wér na, daldi dëpp, di màggal Yàlla ak baat bu xumb.
16 Mu dëpp jëëm ca tànki Yeesu, di ko gërëm. Fekk nitu Samari la woon.
17 Noonu Yeesu daldi ne: «Xanaa du fukk yépp a wér? Ana juróom ñeent ña nag?
18 Amul kenn ci ñoom ku ñëw gërëm Yàlla ku dul doxandéem bii!»
19 Noonu Yeesu ne ko: «Jógal dem; sa ngëm faj na la.»
20 Farisen yi laaj Yeesu ne ko: «Kañ la Yàlla di tëral nguuram?» Mu ne leen: «Bu Yàlla di wàcce nguuram ci nit ñi, kenn du ko mana teg bët.
21 Duñu mana wax it ne: “Xool-leen, mi ngi fii,” walla: “Ma nga fale,” ndaxte nguuru Yàlla wàcc na ci seen biir.»
22 Noonu mu ne taalibe ya: «Jamono dina ñëw, fu ngeen di bëgga gis su doon sax benn fan ci jamono ju Doomu nit ki di ñëw, waaye dungeen ko gis.
23 Dees na leen ne: “Mi ngi fii!” walla: “Ma nga fale!” Buleen dem, mbaa ngeen di leen topp.
24 Ndaxte ni melax naan ràyye ci asamaan, di leeral gii wet, ba ca gee, noonu it la Doomu nit ki di mel ci bésam.
25 Waaye balaa booba fàww mu sonn lool te niti jamono jii dëddu ko.
LUUG 17 in Téereb Injiil

Luug 17:11-25 in Kàddug Yàlla gi

11 Ci biir yoon woowu Yeesu jëmoon Yerusalem, ma nga jaare fa Samari ak Galile digaloo.
12 Mu dem bay duggsi cib dëkk, fukki gaana dikk, dajeek moom, ba dànd ko, daldi taxaw. Ñu xaacu ne:
13 «Yeesu, Njaatige, yërëm nu!»
14 Yeesu nag gis leen, ne leen: «Demleen seetluji seen yaram ca sarxalkat ya.» Ba ñuy dem ca sarxalkat ya lañu wér, seen yaram set.
15 Kenn ci ñoom gis ne wér na, daldi walbatiku, di xaacuy sàbbaal Yàlla.
16 Mu dikk, ne gurub, dëpp jëëm fa tànki Yeesu, sant ko. Waa ja nag nitu Samari la woon.
17 Ba loolu amee Yeesu ne: «Xanaa du fukk a wér? Juróom ñeent ña nag, ana ñu?
18 Amu ci kenn ku ñëw, delloo Yàlla njukkal ku dul doxandéem bii!»
19 Yeesu nag ne ko: «Jógal dem; sa ngëm faj na la.»
20 Farisen yi ñoo laajoon Yeesu, ne ko: «Kañ la nguurug Yàlla di dikk?» Mu ne leen: «Dikkug nguurug Yàlla du ànd akum ceetaan.
21 Deesul ne it: “Xool-leen, mu ngi” mbaa: “Ma ngee,” ndax kat nguurug Yàlla mu ngi ci seen biir.»
22 Mu ne taalibe ya: «Ay jant a ngi ñëw yu ngeen naa ngéejoo fekke benn bés ci bési Doomu nit ki, te dungeen ko fekke.
23 Te it, dees na leen ne: “Ma ngee!” mbaa: “Mu ngii!” Buleen dem, buleen ca topp.
24 Ndax ni melax di xuyye gii wetu asamaan, ba ne ràññ ca gee, noonu la Doomu nit kiy def keroog bésam.
25 Waaye balaa booba fàww Doomu nit ki am coono yu bare, jànkoonteek diiŋatu niti tey jii.
Luug 17 in Kàddug Yàlla gi