Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 17:1-17 in Wolof

Help us?

LUUG 17:1-17 in Téereb Injiil

1 Yeesu waxaat ay taalibeem ne leen: «Fiir yuy yóbbe nit bàkkaar manta ñàkk, waaye toroxte dal na ki koy lal.
2 Ñu takk doj wu réy ci baatam, sànni ko ci géej moo gën ci moom muy daaneel ci bàkkaar kenn ci ñi gëna tuuti ci ñii.
3 Wottuleen seen bopp. «Bu sa mbokk tooñee, yedd ko. Bu réccoo, baal ko.
4 Te su la tooñee juróom ñaari yoon ci bés bi, te ñëw ci yaw juróom ñaari yoon ne la: “Tuub naa ko,” nanga ko baal.»
5 Ndaw ya wax Boroom bi ne ko: «Yokkal sunu ngëm.»
6 Boroom bi ne leen: «Su ngeen amee ngëm gu tuuti sax niw peppu fuddën, kon dingeen mana ne garab gii: “Buddeekul, dem jëmbëtu ca géej ga,” te dina def li ngeen wax.
7 «Kan ci yéen bu amoon surga bu beyi walla bu sàmmi ba ñëw, ndax dafa ko naa: “Kaay lekk”?
8 Déedéet. Xanaa kay da ko naan: “Defaral ma reer bi. Takkul te tibbal ma, ba ma lekk te naan, ba noppi nga doora lekk te naan.”
9 Li surga ba topp ndigal, ndax tax na mu yelloo ngërëm? Déedéet.
10 Noonu yéen itam bu ngeen toppee li ñu leen sant lépp ba noppi, dangeena war ne: “Ay surga rekk lanu. Sunu warugar lanu def.”»
11 Bi muy dem Yerusalem ba tey, Yeesu jaar ci dig wiy xàjjale Samari ak Galile.
12 Bi muy jub benn dëkk, fukki gaana ñëw, dogale ko. Ñu taxaw dànd ko, di wax ca kaw naan:
13 «Yeesu, kilifa gi, yërëm nu!»
14 Naka la leen Yeesu di gis, naan leen: «Demleen won seen bopp sarxalkat ya.» Bi ñuy dem, ñu daldi set.
15 Kenn ci ñoom gis ne wér na, daldi dëpp, di màggal Yàlla ak baat bu xumb.
16 Mu dëpp jëëm ca tànki Yeesu, di ko gërëm. Fekk nitu Samari la woon.
17 Noonu Yeesu daldi ne: «Xanaa du fukk yépp a wér? Ana juróom ñeent ña nag?
LUUG 17 in Téereb Injiil

Luug 17:1-17 in Kàddug Yàlla gi

1 Yeesu neeti ay taalibeem: «Ag fiir guy bàkkaarloo manula ñàkk, waaye wóoy ngalla ka koy lal.
2 Ñu takkoon doj wu réy ci baatam, sànni ko biir géej moo gën ci moom muy yóbbe bàkkaar kenn ci xale yii.
3 Wattuleen seen bopp. «Bu la sa mbokk tooñee, yedd ko. Bu tuubee, baal ko.
4 Su la tooñoon juróom ñaari yoon ci bés bi, te walbatiku juróom ñaari yoon, ne la: “Tuub naa ko,” baal ko rekk.»
5 Ci kaw loolu ndaw ya ne Sang bi: «Yokk nu ngëm.»
6 Sang bi ne leen: «Su ngeen amoon ci ngëm, lu tollu ni peppu fuddën sax, ba ne garab gii: “Buddeekul, dem jëmbate ca géej ga,” su boobaa garab gi déggal leen.
7 «Kan ci yeen la ab jaamam di beyi mbaa mu sàmmi ba jóge tool, dikk, mu ne ko: “Kaay, nu lekk”?
8 Xanaa kay da koy wax ne ko: “Defaral sama reer, te takku, taajal ma, ba ma lekk, naan, nga doora lekk, naan.”
9 La jaam ba jëfe ndigal tax na sangam sant ko? Déedéet kay.
10 Yeen itam noonu. Bu ngeen defee li ñu leen sant lépp ba noppi, dangeena war ne: “Ay jaam rekk lanu. Sunu warugar lanu def.”»
11 Ci biir yoon woowu Yeesu jëmoon Yerusalem, ma nga jaare fa Samari ak Galile digaloo.
12 Mu dem bay duggsi cib dëkk, fukki gaana dikk, dajeek moom, ba dànd ko, daldi taxaw. Ñu xaacu ne:
13 «Yeesu, Njaatige, yërëm nu!»
14 Yeesu nag gis leen, ne leen: «Demleen seetluji seen yaram ca sarxalkat ya.» Ba ñuy dem ca sarxalkat ya lañu wér, seen yaram set.
15 Kenn ci ñoom gis ne wér na, daldi walbatiku, di xaacuy sàbbaal Yàlla.
16 Mu dikk, ne gurub, dëpp jëëm fa tànki Yeesu, sant ko. Waa ja nag nitu Samari la woon.
17 Ba loolu amee Yeesu ne: «Xanaa du fukk a wér? Juróom ñeent ña nag, ana ñu?
Luug 17 in Kàddug Yàlla gi