7 «Maa leen wax, ne leen: bu benn bàkkaarkat doŋŋ tuubee, noonu rekk lay doone mbégte fa asamaan, ba raw mbégte ma fay am, bu juróom ñeent fukk ak juróom ñeenti nit jubee, te soxlawuñoo tuub.
8 «Te it ana jan jigéen mooy am fukki libidoor, benn réer ca, te taalul ab làmp, buub néeg ba, seeta seet, ba gis ko?
9 Bu ko gisee, xarit yaak dëkk ya lay woo, ne leen: “Kaayleen nu bége, libidoor ba réeroon, gis naa ko.”
10 Maa leen wax ne leen: noonu rekk lay doone mbégte fa malaakay Yàlla ya, bu benn bàkkaarkat doŋŋ tuubee.»
11 Yeesu neeti: «Nit a amoon ñaari doom yu góor.
12 Ka gën di ndaw ne baay ba: “Baay, jox ma cér bi ma yoon may ci sunu alal.” Ba loolu amee baay ba séddale leen alalam.
13 Ay fan yu néew gannaaw gi, ka gën di ndaw jaay léppam, daldi tukki réew mu sore, di topp bakkanam ba yàq fa alalam.
14 Gannaaw ba mu sànkee lépp, xiif bu metti dikkal réew ma, mu daldi tàmbalee ñàkk.